Dataset Viewer
Auto-converted to Parquet
input
stringlengths
2
1.08k
target
stringlengths
1
1.02k
C'est Omar qui a mangé le riz.
Omar a lekk ceeb bi
C'est moi.
Man a
quand tu le vois aller et venir comme ça sans arrêt, c’est qu’il est inquiet.
Boo ko gisee muy dem ak a dikk nii rekk
il ne suffit pas de vouloir partir, il faut pouvoir le faire.
Bëgga dem taxula mëna dem. Mëna dem ay taxa dem
fiche-moi la paix !
May ma aafiya
il a beaucoup d’égards pour ses voisins.
Ku am-aajo la ci ay dëkkandoom
nous devons mettre en commun nos biens.
Danu wara boole sunu am-am
elle est mariée à un homme riche.
Waa ju am-alal lay séyal
C'est un commerçant en vue.
Jaaykat bu am-bayre la
C'est un extralucide; tous les coups qu’on monte contre lui échouent.
Dafa am-bopp; lu ñu ko fexeel, mu yàqu
avoir des yeux globuleux rehaussent le charme d’une femme.
Am-bët dafay yokk taaru jigéen
un homme qui a de la personnalité ne va pas à des séances de tam-tam.
Góor gu am-fayda du wàlli sabar
dites amen !
Neleen amiin
Autour du trône je vis vingt-quatre trônes, et sur ces trônes vingt-quatre vieillards assis, revêtus de vêtements blancs, et sur leurs têtes des couronnes d`or.
Yeneen ñaar-fukki gàngune ak ñeent wër ko, te ci kaw gàngune ya ñaar-fukki mag ak ñeent toog, sol mbubb yu weex ak kaalay wurus ci seen bopp.
Du trône sortent des éclairs, des voix et des tonnerres. Devant le trône brûlent sept lampes ardentes, qui sont les sept esprits de Dieu.
Ay melax, ay riir ak ay dënnu di jibe ca gàngune ma. Ca kanamu gàngune ma amoon na fa juróom-ñaari làmp yu yànj, di juróom-ñaari Xeli Yàlla yi.
Il y a encore devant le trône comme une mer de verre, semblable à du cristal. Au milieu du trône et autour du trône, il y a quatre êtres vivants remplis d`yeux devant et derrière.
Amoon na it ca kanamu gàngune ma lu mel ni géej gu leer ni weer bu set, ba mel ni seetu. Ci li wër gàngune ma, sës rëkk, amoon na fa ñeenti mbindeef yu fees ak ay bët ci kanam ak ci gannaaw.
Le premier être vivant est semblable à un lion, le second être vivant est semblable à un veau, le troisième être vivant a la face d`un homme, et le quatrième être vivant est semblable à un aigle qui vole.
Mbindeef mu jëkk maa nga meloon ni gaynde, ñaareelu mbindeef mel ni yëkk, ñetteelu mbindeef yor kanamu nit, ñeenteel ba di nirook jaxaay juy naaw.
Les quatre êtres vivants ont chacun six ailes, et ils sont remplis d`yeux tout autour et au dedans. Ils ne cessent de dire jour et nuit: Saint, saint, saint est le Seigneur Dieu, le Tout Puisant, qui était, qui est, et qui vient!
Ñeenti mbindeef ya am nañu ku nekk juróom-benni laaf te ñu nga fees ak ay bët li leen wër lépp, ba ci seen roni laaf. Guddi ak bëccëg duñu noppeek naan:«Boroom bi Yàlla, Aji Kàttan ji,moo sell, sell, sell,moom ki nekkoon démb,ki nekk tey, te di ñëw ëllëg.»
Quand les êtres vivants rendent gloire et honneur et actions de grâces à celui qui est assis sur le trône, à celui qui vit aux siècles des siècles,
Saa su mbindeef ya di màggal ki toog ca gàngune ma tey dund ba fàww, te di ko kañ ak a gërëm,
les vingt-quatre vieillards se prosternent devant celui qui est assis sur le trône et ils adorent celui qui vit aux siècles des siècles, et ils jettent leurs couronnes devant le trône, en disant:
ñaar-fukki mag ña ak ñeent di dëpp seen jë ca kanamu ka toog ca kaw gàngune ma. Ñu di ko jaamu, moom mi dund ba fàww, di sànni seen kaalay ndam ca kanamu gàngune ma, naan:
Tu es digne, notre Seigneur et notre Dieu, de recevoir la gloire et l`honneur et la puissance; car tu as créé toutes choses, et c`est par ta volonté qu`elles existent et qu`elles ont été créées.
«Yàlla sunu Boroom,yaa yeyoo ndam, teraanga ak kàttan,ndaxte yaa sàkk léppte ci sa coobare la lépp nekke,te ci lañu leen sàkke.»
Puis je vis dans la main droite de celui qui était assis sur le trône un livre écrit en dedans et en dehors, scellé de sept sceaux.
Noonu ma gis ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma téere bu ñu bind biir ak biti, tay ko juróom-ñaari yoon ak sondeel.
Et je vis un ange puissant, qui criait d`une voix forte: Qui est digne d`ouvrir le livre, et d`en rompre les sceaux?
Noonu ma gis malaaka mu am doole, muy xaacu naan: «Ku yeyoo dindi tayu yi te ubbi téere bi?»
Et personne dans le ciel, ni sur la terre, ni sous la terre, ne put ouvrir le livre ni le regarder.
Te amul kenn, muy ci asamaan, muy ci kaw suuf, muy ci biir suuf, ku manoon a ubbi téere bi, mbaa mu xool ci biir.
Et je pleurai beaucoup de ce que personne ne fut trouvé digne d`ouvrir le livre ni de le regarder.
Ma jooy jooy yu metti ndax li kenn yeyoowul woon a ubbi téere bi mbaa mu xool ko.
Et l`un des vieillards me dit: Ne pleure point; voici, le lion de la tribu de Juda, le rejeton de David, a vaincu pour ouvrir le livre et ses sept sceaux.
Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Bul jooy. Xoolal, Gayndeg giiru Yuda, ki soqikoo ci Daawuda, daan na, ba am sañ-sañu dindi tayu yi te ubbi téere bi.»
Et je vis, au milieu du trône et des quatre êtres vivants et au milieu des vieillards, un agneau qui était là comme immolé. Il avait sept cornes et sept yeux, qui sont les sept esprits de Dieu envoyés par toute la terre.
Noonu ma gis Mbote mu mel ni dañu koo rendi woon, mu taxaw ca digg gàngune ma, ñeenti mbindeef ya séq ko, mag ña wër ko. Mbote ma amoon na juróom-ñaari béjjén ak juróom-ñaari bët, ñu di juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi ñu yónni ci àddina sépp.
Il vint, et il prit le livre de la main droite de celui qui était assis sur le trône.
Mbote ma ñëw, jël téere, ba nekkoon ca loxol ndeyjooru ka toog ca gàngune ma.
Quand il eut pris le livre, les quatre êtres vivants et les vingt-quatre vieillards se prosternèrent devant l`agneau, tenant chacun une harpe et des coupes d`or remplies de parfums, qui sont les prières des saints.
Ba mu jëlee téere ba, ñeenti mbindeef ya ak ñaar-fukki mag ña ak ñeent daldi dëpp seen jë ca kanam Mbote ma, ku nekk yor xalam. Ñu yor it andi wurus yu fees ak cuuraay, yu doon misaal ñaani gaayi Yàlla ya.
Et ils chantaient un cantique nouveau, en disant: Tu es digne de prendre le livre, et d`en ouvrir les sceaux; car tu as été immolé, et tu as racheté pour Dieu par ton sang des hommes de toute tribu, de toute langue, de tout peuple, et de toute nation;
Ñu daldi woy woy wu bees naan:«Yeyoo ngaa jël téere bite dindi tayu yi,ndaxte reyees na la,te jotal nga Yàlla ak sa deretay nit ñu bokk ci bépp giir,kàllaama, réew ak xeet.
tu as fait d`eux un royaume et des sacrificateurs pour notre Dieu, et ils régneront sur la terre.
Def nga leen askanu saraxalekatiBuur Yàlla sunu Boroom,di ko jaamu,te dinañu nguuru ci àddina.»
Je regardai, et j`entendis la voix de beaucoup d`anges autour du trône et des êtres vivants et des vieillards, et leur nombre était des myriades de myriades et des milliers de milliers.
Ma xool noonu, dégg baatu malaaka yu bare yu ëppoon alfunniy alfunniy junniy junni. Malaaka ya wër gàngune ma ak mbindeef ya ak mag ña.
Ils disaient d`une voix forte: L`agneau qui a été immolé est digne de recevoir la puissance, la richesse, la sagesse, la force, l`honneur, la gloire, et la louange.
Ñuy xaacu naan:«Mbote ma ñu rendi woonyeyoo na kàttan, alal, xel,doole, teraanga, ndam ak cant.»
Et toutes les créatures qui sont dans le ciel, sur la terre, sous la terre, sur la mer, et tout ce qui s`y trouve, je les entendis qui disaient: A celui qui est assis sur le trône, et à l`agneau, soient la louange, l`honneur, la gloire, et la force, aux siècles des siècles!
Ma dégg itam mbindeef, yi nekk ci asamaan, ci kaw suuf, ci biir suuf, ci géej gi, — mbindeef yépp naan:«Na cant, teraanga, ndam ak nguurféete ak ki toog ci gàngune mi,ak Mbote mi ba fàww.»
Et les quatre êtres vivants disaient: Amen! Et les vieillards se prosternèrent et adorèrent.
Ñeenti mbindeef ya naan: «Amiin.» Mag ña sukk di màggal.
Je regardai, quand l`agneau ouvrit un des sept sceaux, et j`entendis l`un des quatre êtres vivants qui disait comme d`une voix de tonnerre: Viens.
Noonu ma gis Mbote ma dindi tayu gu jëkk ga, te ma daldi dégg kenn ca ñeenti mbindeef ya, di wax ak baat buy riir ni dënnu naan: «Ñëwal.»
Je regardai, et voici, parut un cheval blanc. Celui qui le montait avait un arc; une couronne lui fut donnée, et il partit en vainqueur et pour vaincre.
Ma xool noonu, gis fas wu weex, gawar ba yor ag fitt. Ñu jox ko kaalag ndam, mu daldi dem moom jàmbaar ngir daani.
Quand il ouvrit le second sceau, j`entendis le second être vivant qui disait: Viens.
Mbote ma dindi na ñaareelu tayu ga, ma dégg ñaareelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.»
Et il sortit un autre cheval, roux. Celui qui le montait reçut le pouvoir d`enlever la paix de la terre, afin que les hommes s`égorgeassent les uns les autres; et une grande épée lui fut donnée.
Noonu weneen fas génn, di wu xonq, gawar ba jot sañ-sañu jële jàmm ci kaw suuf, ngir nit ñi di reyante ci seen biir. Ñu jox ko jaasi ju mag.
Quand il ouvrit le troisième sceau, j`entendis le troisième être vivant qui disait: Viens. Je regardai, et voici, parut un cheval noir. Celui qui le montait tenait une balance dans sa main.
Mu dindi ñetteelu tayu ga, ma dégg ñetteelu mbindeef ma ne: «Ñëwal.» Ma xool, gis fas wu ñuul, gawar ba yor ab peesekaay.
Et j`entendis au milieu des quatre êtres vivants une voix qui disait: Une mesure de blé pour un denier, et trois mesures d`orge pour un denier; mais ne fais point de mal à l`huile et au vin.
Ma dégg baat bu jollee ca diggante ñeenti mbindeef ya, naan: «Peyug bëccëgu lëmm ngir benn kilob ceeb, peyug bëccëgu lëmm ngir ñetti kiloy dugub, waaye bul yàq diw ak biiñ.»
Quand il ouvrit le quatrième sceau, j`entendis la voix du quatrième être vivant qui disait: Viens.
Mu dindi ñeenteelu tayu ga, ma dégg ñeenteelu mbindeef ma naan: «Ñëwal.»
Je regardai, et voici, parut un cheval d`une couleur pâle. Celui qui le montait se nommait la mort, et le séjour des morts l`accompagnait. Le pouvoir leur fut donné sur le quart de la terre, pour faire périr les hommes par l`épée, par la famine, par la mortalité, et par les bêtes sauvages de la terre.
Ma xool noonu, gis fas wu wert, gawar baa nga tuddoon Dee te barsàq a nga toppoon ci moom. Ñu jox ko sañ-sañ ci ñeenteelu xaaju àddina sépp, ngir mu faat ak jaasi, xiif, mbas ak rabi àll yi.
Quand il ouvrit le cinquième sceau, je vis sous l`autel les âmes de ceux qui avaient été immolés à cause de la parole de Dieu et à cause du témoignage qu`ils avaient rendu.
Mu dindi juróomeelu tayu ga, ma gis ca suufu saraxalukaay, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, ruuwi ñi ñu bóom ndax seede si ñu doon sàmm ak li ñu gëmoon kàddug Yàlla.
Ils crièrent d`une voix forte, en disant: Jusques à quand, Maître saint et véritable, tarde-tu à juger, et à tirer vengeance de notre sang sur les habitants de la terre?
Ñuy xaacu naan: «Boroom bu sell bi te dëggu, ba kañ ngay nég àtte bi te feyyul nu sunu deret ci waa àddina?»
Une robe blanche fut donnée à chacun d`eux; et il leur fut dit de se tenir en repos quelque temps encore, jusqu`à ce que fût complet le nombre de leurs compagnons de service et de leurs frères qui devaient être mis à mort comme eux.
Ñu jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, ñu muñ tuuti, ba kera seeni nawle ñëw, te lim bi mat — seeni nawle ci liggéey bi, di seeni bokk yu waa àddina waroon a bóom ni ñoom.
Je regardai, quand il ouvrit le sixième sceau; et il y eut un grand tremblement de terre, le soleil devint noir comme un sac de crin, la lune entière devint comme du sang,
Ma xool, ba muy dindi juróom-benneelu tayu ga. Noonu mu am yengu-yengub suuf bu mag, jant bi ñuul ni këriñ, weer wi xonq curr ni deret.
et les étoiles du ciel tombèrent sur la terre, comme lorsqu`un figuier secoué par un vent violent jette ses figues vertes.
Biddiiw yi fàqe asamaan, di daanu ci kaw suuf, ni doomi garab yu yolox di wadd, bu ko ngelaw lu metti dee yengal.
Le ciel se retira comme un livre qu`on roule; et toutes les montagnes et les îles furent remuées de leurs places.
Asamaan si dellu ni basaŋ gu ñuy taxañ, tund yépp ak dun yépp randoo fa ñu nekkoon.
Les rois de la terre, les grands, les chefs militaires, les riches, les puissants, tous les esclaves et les hommes libres, se cachèrent dans les cavernes et dans les rochers des montagnes.
Noonu buuri àddina si, kilifa yi, njiiti xare yi, boroom alal yi, boroom kàttan yi, jaam yi ak gor yi, ñépp làqatuji ci xunti yi ak ci ron doji tund yi.
Et ils disaient aux montagnes et aux rochers: Tombez sur nous, et cachez-nous devant la face de celui qui est assis sur le trône, et devant la colère de l`agneau;
Ñu naan tund yi ak doj yi: «Daanuleen ci sunu kaw te nëbb nu bëti ki toog ci gàngune mi ak meru Mbote mi,
car le grand jour de sa colère est venu, et qui peut subsister?
ndaxte bés bu mag, bi seen mer di feeñ, agsi na! Ku ci man a rëcc?»
Après cela, je vis quatre anges debout aux quatre coins de la terre; ils retenaient les quatre vents de la terre, afin qu`il ne soufflât point de vent sur la terre, ni sur la mer, ni sur aucun arbre.
Gannaaw loolu ma gis ñeenti malaaka yu taxaw ci ñeenti xeblay àddina si. Ñu téye ñeenti ngelawi àddina, ngir ngelaw du wol ci kaw suuf, ci géej mbaa ci genn garab.
Et je vis un autre ange, qui montait du côté du soleil levant, et qui tenait le sceau du Dieu vivant; il cria d`une voix forte aux quatre anges à qui il avait été donné de faire du mal à la terre et à la mer, et il dit:
Ma gis it meneen malaaka, muy yéeg, jóge penku, yor màndargakaayu Yàlla jiy dund. Mu daldi wax ak baat bu xumb ñeenti malaaka ya ñu joxoon sañ-sañ, ñu yàq suuf ak géej,
Ne faites point de mal à la terre, ni à la mer, ni aux arbres, jusqu`à ce que nous ayons marqué du sceau le front des serviteurs de notre Dieu.
ne leen: «Buleen yàqagun suuf si ak géej gi ak garab yi. Négleen, ba ñu def màndarga ci jëwu ñiy jaamu Yàlla sunu Boroom.»
Et j`entendis le nombre de ceux qui avaient été marqués du sceau, cent quarante-quatre mille, de toutes les tribus des fils d`Israël:
Noonu ma dégg limub ñi ñu màndargaal; ñu tollu ci téeméer ak ñeent-fukk ak ñeent ci ay junni. Ñu jóge ci giiri bànni Israyil yépp:
de la tribu de Juda, douze mille marqués du sceau; de la tribu de Ruben, douze mille; de la tribu de Gad, douze mille;
Fukki junni ak ñaar lañu màndargaal ci biir giiru Yuda,fukki junni ak ñaar ci giiru Ruben,fukki junni ak ñaar ci giiru Gàdd,
de la tribu d`Aser, douze mille; de la tribu de Nephthali, douze mille; de la tribu de Manassé, douze mille;
fukki junni ak ñaar ci giiru Aser,fukki junni ak ñaar ci giiru Neftali,fukki junni ak ñaar ci giiru Manase,
de la tribu de Siméon, douze mille; de la tribu de Lévi, douze mille; de la tribu d`Issacar, douze mille;
fukki junni ak ñaar ci giiru Simeyon,fukki junni ak ñaar ci giiru Lewi,fukki junni ak ñaar ci giiru Isakaar,
de la tribu de Zabulon, douze mille; de la tribu de Joseph, douze mille; de la tribu de Benjamin, douze mille marqués du sceau.
fukki junni ak ñaar ci giiru Sabulon,fukki junni ak ñaar ci giiru Yuusufa,fukki junni ak ñaar ci giiru Ben-yamin.
Après cela, je regardai, et voici, il y avait une grande foule, que personne ne pouvait compter, de toute nation, de toute tribu, de tout peuple, et de toute langue. Ils se tenaient devant le trône et devant l`agneau, revêtus de robes blanches, et des palmes dans leurs mains.
Gannaaw loolu ma xool, gis mbooloo mu réy, ba kenn mënu koo waññ, ñu bokk ci xeet yépp, giir yépp, réew yépp ak kàllaama yépp, taxaw ca kanamu gàngune ma ak Mbote ma. Ñu sol ay mbubb yu weex, di màggal te di yengal ay cari garab ci seeni loxo,
Et ils criaient d`une voix forte, en disant: Le salut est à notre Dieu qui est assis sur le trône, et à l`agneau.
naan:«Mucc gaa ngi ci Yàllasunu Boroom, bi toog ci gàngune mi,ak ci Mbote mi!»
Et tous les anges se tenaient autour du trône et des vieillards et des quatre êtres vivants; et ils se prosternèrent sur leur face devant le trône, et ils adorèrent Dieu,
Noonu malaaka yépp taxaw, wër gàngune ma ak mag ña ak ñeenti mbindeef ya. Ñu dëpp seen jë ca kanamu gàngune ma, di jaamu Yàlla,
en disant: Amen! La louange, la gloire, la sagesse, l`action de grâces, l`honneur, la puissance, et la force, soient à notre Dieu, aux siècles des siècles! Amen!
naan:«Amiin. Na cant ak ndam, xel ak ngërëm, teraanga, kàttan ak dooleféete ak Yàlla sunu Boroom ba fàww. Amiin!»
Et l`un des vieillards prit la parole et me dit: Ceux qui sont revêtus de robes blanches, qui sont-ils, et d`où sont-ils venus?
Noonu kenn ca mag ña ne ma: «Ñi sol mbubb yu weex yi, ñooy ñan ak fan lañu jóge?»
Je lui dis: Mon seigneur, tu le sais. Et il me dit: Ce sont ceux qui viennent de la grande tribulation; ils ont lavé leurs robes, et ils les ont blanchies dans le sang de l`agneau.
Ma ne ko: «Sang bi, xanaa yaa ko xam.» Mu ne ma: «Ñoo di ñi jóge ca metit wu réy wa. Fóot nañu seeni mbubb, ba weexal ko ci deretu Mbote ma.
C`est pour cela qu`ils sont devant le trône de Dieu, et le servent jour et nuit dans son temple. Celui qui est assis sur le trône dressera sa tente sur eux;
Loolu moo taxñu nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,di ko jaamu guddi ak bëccëg ci këram,te ki toog ci gàngune mi dina leen yiir.
ils n`auront plus faim, ils n`auront plus soif, et le soleil ne les frappera point, ni aucune chaleur.
Dootuñu xiif, dootuñu mar.Jant mbaa weneen tàngaay du leen lakk,
Car l`agneau qui est au milieu du trône les paîtra et les conduira aux sources des eaux de la vie, et Dieu essuiera toute larme de leurs yeux.
ndaxte Mbote mi nekk ci diggu gàngune mi dina leen sàmm,yóbbu leen ca bëti ndoxum dund ma,te Yàlla dina fomp bépp rangooñ ci seeni bët.»
Quand il ouvrit le septième sceau, il y eut dans le ciel un silence d`environ une demi-heure.
Mbote ma dindi na juróom-ñaareelu tayu ga, asamaan ne selaw lu mat genn-wàllu waxtu.
Et je vis les sept anges qui se tiennent devant Dieu, et sept trompettes leur furent données.
Noonu ma gis juróom-ñaari malaaka, yi taxaw ca kanam Yàlla, ñu daldi leen jox juróom-ñaari liit.
Et un autre ange vint, et il se tint sur l`autel, ayant un encensoir d`or; on lui donna beaucoup de parfums, afin qu`il les offrît, avec les prières de tous les saints, sur l`autel d`or qui est devant le trône.
Ba loolu amee meneen malaaka ñëw, taxaw ca wetu saraxalukaayu wurus, ba ñuy taal cuuraay ca kawam, yor andu cuuraayu wurus. Ñu jox ko cuuraay lu bare, ngir mu boole ko ak ñaani gaayi Yàlla yépp, joxe ko ci kaw saraxalukaayu wurus ba nekk ci kanam gàngune mi.
La fumée des parfums monta, avec les prières des saints, de la main de l`ange devant Dieu.
Noonu saxarus cuuraay li gillee ca loxob malaaka ma, ànd ak ñaani gaayi Yàlla ya, jëm ca kanam Yàlla.
Et l`ange prit l`encensoir, le remplit du feu de l`autel, et le jeta sur la terre. Et il y eut des voix, des tonnerres, des éclairs, et un tremblement de terre.
Malaaka ma jël andu cuuraay ba, duy ko ak ay xal ca saraxalukaay ba, daldi koy sànni ci àddina. Noonu mu am ay dënnu, ay riir, ay melax ak yengu-yengub suuf.
Et les sept anges qui avaient les sept trompettes se préparèrent à en sonner.
Ba mu ko defee juróom-ñaari malaaka, ya yoroon juróom-ñaari liit ya, daldi defaru di waaj a liit.
Le premier sonna de la trompette. Et il y eut de la grêle et du feu mêlés de sang, qui furent jetés sur la terre; et le tiers de la terre fut brûlé, et le tiers des arbres fut brûlé, et toute herbe verte fut brûlée.
Malaaka mu jëkk ma wol liitam. Noonu ñu sànni ci àddina yuur ak safara yu ñu boole ak deret, ba tax benn ci ñetti xaaju suuf si lakk, benn ci ñetti xaaju garab yi it lakk, te ñax mu naat mépp lakk.
Le second ange sonna de la trompette. Et quelque chose comme une grande montagne embrasée par le feu fut jeté dans la mer; et le tiers de la mer devint du sang,
Ñaareelu malaaka ma wol liitam. Noonu ñu sànni lu mel ni tundu safara wu réy, mu daanu ci géej gi, benn ci ñetti xaaju géej gi soppiku deret,
et le tiers des créatures qui étaient dans la mer et qui avaient vie mourut, et le tiers des navires périt.
benn ci ñetti xaaju mbindeef yi nekk ci géej gi dee, te benn ci ñetti xaaju gaal yi yàqu.
Le troisième ange sonna de la trompette. Et il tomba du ciel une grande étoile ardente comme un flambeau; et elle tomba sur le tiers des fleuves et sur les sources des eaux.
Ñetteelu malaaka ma wol liitam. Noonu biddiiw bu réy, yànj ni jum, xawee asamaan, daanu ci benn ci ñetti xaaju dex yi ak ci bëti ndox yi.
Le nom de cette étoile est Absinthe; et le tiers des eaux fut changé en absinthe, et beaucoup d`hommes moururent par les eaux, parce qu`elles étaient devenues amères.
Biddiiw boobu mi ngi tuddoon Wextan. Nit ñu bare naan ci ndox mi daldi dee, ndaxte ndox mi dafa daldi wex.
Le quatrième ange sonna de la trompette. Et le tiers du soleil fut frappé, et le tiers de la lune, et le tiers des étoiles, afin que le tiers en fût obscurci, et que le jour perdît un tiers de sa clarté, et la nuit de même.
Ñeenteelu malaaka ma wol liitam. Noonu dóorees benn ci ñetti xaaju jant bi, ak benn ci ñetti xaaju weer wi, ak benn ci ñetti xaaju biddiiw yi, ba tax benn ci ñetti xaaju leer gi lëndëm. Bëccëg bi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam, guddi gi ñàkk leer diirub benn ci ñetti xaajam.
Je regardai, et j`entendis un aigle qui volait au milieu du ciel, disant d`une voix forte: Malheur, malheur, malheur aux habitants de la terre, à cause des autres sons de la trompette des trois anges qui vont sonner!
Ma xool noonu, dégg jaxaay juy naaw ci digg asamaan, naan ak baat bu xumb: «Musiba, musiba! Musibaa ngi ci kaw waa àddina, ndax liit yi yeneen ñetti malaaka yi di wol.»
Le cinquième ange sonna de la trompette. Et je vis une étoile qui était tombée du ciel sur la terre. La clef du puits de l`abîme lui fut donnée,
Juróomeelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma gis, ñu jox caabiy kàmb gu xóot gi benn biddiiw bu xawee woon asamaan, daanu ci kaw suuf.
et elle ouvrit le puits de l`abîme. Et il monta du puits une fumée, comme la fumée d`une grande fournaise; et le soleil et l`air furent obscurcis par la fumée du puits.
Biddiiw ba ubbi buntu kàmb gu xóot ga. Noonu saxar jollee ca, su mel ni saxarus puur bu mag, jant bi ak jaww ji lépp lëndëm ndax saxarus kàmb ga.
De la fumée sortirent des sauterelles, qui se répandirent sur la terre; et il leur fut donné un pouvoir comme le pouvoir qu`ont les scorpions de la terre.
Ay njéeréer génn ca saxar sa, tasaaroo ci biir àddina. Ñu jox leen kàttan gu mel ni kàttanu jànkalaar.
Il leur fut dit de ne point faire de mal à l`herbe de la terre, ni à aucune verdure, ni à aucun arbre, mais seulement aux hommes qui n`avaient pas le sceau de Dieu sur le front.
Ñu sant leen, ñu bañ a laal ñax mi ci kaw suuf, mbaa genn gàncax walla genn meññeef, waaye ñu jublu rekk ci nit ñu amul màndargam Yàlla ci seen jë.
Il leur fut donné, non de les tuer, mais de les tourmenter pendant cinq mois; et le tourment qu`elles causaient était comme le tourment que cause le scorpion, quand il pique un homme.
Santuñu leen ñu rey leen, waaye ñu metital leen diirub juróomi weer. Te metit woowu ñuy indi, temboo na ak metit wiy dal nit, bu ko jànkalaar fittee.
En ces jours-là, les hommes chercheront la mort, et ils ne la trouveront pas; ils désireront mourir, et la mort fuira loin d`eux.
Ca jamono yooya nit ñi dinañu sàkku dee, waaye duñu daje ak moom. Dinañu bëgg a dee, waaye dee da leen di daw.
Ces sauterelles ressemblaient à des chevaux préparés pour le combat; il y avait sur leurs têtes comme des couronnes semblables à de l`or, et leurs visages étaient comme des visages d`hommes.
Njéeréer ya nag dañuy niroo ak fas yu ñu waajal ngir xare. Am nañu ci seen bopp lu mel ni kaalay wurus, te seen xar-kanam mel ni gu nit.
Elles avaient des cheveux comme des cheveux de femmes, et leurs dents étaient comme des dents de lions.
Seeni kawar mel ni yu jigéen, seeni bëñ mel ni bëñi gaynde.
Elles avaient des cuirasses comme des cuirasses de fer, et le bruit de leurs ailes était comme un bruit de chars à plusieurs chevaux qui courent au combat.
Takk nañu ci seen dënn lu mel ni kiiraayu weñ, te coow la seeni laaf di def mel ni coowu sareeti xare yu bare yu ñu takk fas, di xeexi.
Elles avaient des queues semblables à des scorpions et des aiguillons, et c`est dans leurs queues qu`était le pouvoir de faire du mal aux hommes pendant cinq mois.
Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar, te ca la seen kàttan nekk, ngir metital nit ñi diirub juróomi weer.
Elles avaient sur elles comme roi l`ange de l`abîme, nommé en hébreu Abaddon, et en grec Apollyon.
Buuru njéeréer yi mooy malaakam kàmb gu xóot gi, moom lañu tudde ci làkku Yawut, Abadon, ak ci làkku gereg, Apolyon, liy tekki «Yàqkat.»
Le premier malheur est passé. Voici il vient encore deux malheurs après cela.
Musiba mu jëkk mi jàll na, yeneen ñaari musiba yaa ngi ñëw.
Le sixième ange sonna de la trompette. Et j`entendis une voix venant des quatre cornes de l`autel d`or qui est devant Dieu,
Juróom-benneelu malaaka ma wol liitam. Noonu ma dégg baat bu jóge ci ñeenti béjjén, yi nekk ci koñi saraxalukaayu wurus, ba nekk ci kanam Yàlla,
et disant au sixième ange qui avait la trompette: Délie les quatre anges qui sont liés sur le grand fleuve d`Euphrate.
mu ne juróom-benneelu malaaka, ma yoroon liit: «Yiwil ñeenti malaaka, ya yeewe ca Efraat, dex gu mag ga.»
Et les quatre anges qui étaient prêts pour l`heure, le jour, le mois et l`année, furent déliés afin qu`ils tuassent le tiers des hommes.
Noonu ñu daldi yiwi ñeenti malaaka, ya ñu waajaloon ngir at moomu, weer woowu, bés boobu ak waxtu woowu, ngir ñu rey benn ci ñetti xaaju nit ñi.
Le nombre des cavaliers de l`armée était de deux myriades de myriades: j`en entendis le nombre.
Limub gawar ga doon xareji mat na ñaari alfunniy alfunni. Dégg naa lim ba.
Et ainsi je vis les chevaux dans la vision, et ceux qui les montaient, ayant des cuirasses couleur de feu, d`hyacinthe, et de soufre. Les têtes des chevaux étaient comme des têtes de lions; et de leurs bouches il sortait du feu, de la fumée, et du soufre.
Nii laa gise ci peeñu mi fas ya ak ña leen war: ñu sol kiiraay yu xonq ni safara, bulo ni saxar, ak mboq ni tamarax. Boppi fas yaa nga doon nirook boppi gaynde; safara, saxar ak tamarax di génn ci seeni gémmiñ.
Le tiers des hommes fut tué par ces trois fléaux, par le feu, par la fumée, et par le soufre, qui sortaient de leurs bouches.
Benn ci ñetti xaaju nit ñi dee ci ñetti musiba ya: ci safara, saxar ak tamarax yi génn ci seeni gémmiñ.
End of preview. Expand in Data Studio

Dataset Français → Wolof (train.csv)

Colonnes :

  • input : texte en français
  • target : traduction en wolof

Description :
Ce dataset contient des paires français → wolof soigneusement collectées et nettoyées à partir de diverses sources en ligne.
Toutes les données ont été vérifiées, les doublons et incohérences supprimés, garantissant un dataset fiable et prêt à l’usage pour l’entraînement de modèles de traduction automatique.

Usage prévu :

  • Fine-tuning et entraînement de modèles FR→WO
  • Évaluation de modèles de traduction
  • Recherche NLP pour les langues africaines

Qualité :
Chaque entrée a été normalisée et vérifiée, offrant un dataset propre, cohérent et utilisable immédiatement pour le machine learning.

Downloads last month
12

Models trained or fine-tuned on MaroneAI/French-Wolof_Translation-Dataset