url
string
content
string
https://www.defuwaxu.com/lan-la-wutaakon-yi-naral-lakki-reew-mi/
Lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Waaw mbokk yi, lan la wutaakon yi naral làkki réew mi ? Man ci sama wàllu bopp, déggaguma ci lu ma doy. Ndax Wolof, Pulaar, Séeréer, Soose, Joola, Sooninke…. dañu leen di wéy di suufeel teg Frãnse mbaa Àngale ci seen kaw ? Ndax Frãnse kese mooy wéy di nekk “làmmiñ wi Repibligu Senegaal fal, di ci jaarale léppam” ? Ndax làmmiñ yi xeetoo Senegaal dinañu nekk kenu njàngale mi, li ko dale daara yu suufe yi ba ci Iniwersite yi ? Ndax seen mbind, seen xabaaruwaay, seeni téere dinañu tas ci Réew mi ? Ndax dinañu fexe ba doomi Senegaal yëpp mën bind ak jàng ci làmmiñ yi ñu nàmp ? Làmmiñu réew mi war na ñoo dugg ak doole ci daara yi ak ci kuréli njàngum liggéey yi, ñu ciy sàkku xam-xam : xarala, ladab, xayma, mbay, napp, tabaxin, mekanig, elektoronig, tas-xibaar ak ñoom seen…Su ko defee sunu Askan, sunu Xeet ak sunu Réew dinañu def jéego gu réy ci yoonu suqaliku ba dab réew yi seen koom gën a naat ci dunya. Jamono moom-sa-Réew jot na. War nañu fullaal làmmiñi réew mi, jox leen seen cër ba mu mat sëkk, ñu doon ay jumtukaay yu tàkku ngir tinkeeku. Yaakaar naa ne “Lu Defu Waxu” war naa mën a bind bataaxal juroomi wutaakon yi laaj leen li ñu naral làmmiñi réew mi
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-serin-baabakar-si-mu-dabbaax-njool-fuuta/
TABASKI 2023 : XUTBA SËRIÑ BAABAKAR SI MU DABBAAX (NJOOL-FUUTA) Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam, fa tiwaawon. Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax xirtal na jullti Senegaal yi ci ñu dekkil mbaaxi mbokkoo ak dimbalante, cuufe ak sutura. Ci alxames ji la tiijaani Tiwaawon yi tabaski. Kilifa gii di Sëriñ Baabakar Si mu Abdul Asiis Si Dabbaax, ñu duppee ko Njool-Fuuta, moo jii te julli ba. Ba muy xutba, dafa fàttali mbaaxi démb yoy, dañuy bëgg naaxsaay ci biir mboolaayu Senegaal. Moo ko tax a ñaax askan wi ci dundalaat mbaaxi yooyii mag ña sàrtoo woon. Sëriñ bi ne : « Ñi amul wërsëgu dunud ak seen i maam, dund nañu, as-tuut, ak seen i baay. Réer gu jéggi dayo gi fi am day firndeel ñàkkug gindikukaay. » Sëriñ bi neeti, jot na ñu fàttali doomi Senegaal cuufe ak dimbalante, rawatina ci jamono yu mel ni tabaski ak tolluwaayu réew mi. Imaam bi ne : « rendi sam xar, di bàkkoo taar baak duufaay bi taxul Yàlla nangul la. Diine, dees na ko dunde ni ko Islaam tëralee. » Xalifa Tiijaan yi, Sëriñ Baabakar Si Mansóor, dafa tawat moo tax jiitesiwul julli ji. Waaye, balaa Njoo-Fuutay xutba, Papaa Maktaar Kebe waxoon ci turam, jottali ngërmaandeem tiijaan yi jàpp yépp ci tabaxug jumaay Tiwaawon ju mag ji. Jottaleet na ñaan xalif yi bi jagleel daayira yi, kurél yi ak saa-senegaal yépp yi ci jàpp.
https://www.defuwaxu.com/njaay-daraapoo-dedduna/
NJAAY DARAAPOO DËDDU NA Momar Njaay, ñu gënoon koo miin ci turu “Njaay Daraapoo”, dëddu na. Moom, nag, ku ràññeeku woon la ci wàllu kuppeg Senegaal. Mi ngi faatu ci àjjuma ji 31 màrs 2023. Muy xibaar bu tiis ci waa Senegaal yépp, rawatina njabootug kuppe gi. “Njaay Daraapoo”, ku fësoon lool la ci ekibu Senegaal bi. Ndaxte, atum 2002 la tàmbali woon a ànd ak ekib bi. Dafa bokkoon ci mbootaayu 12eelu gaynde gi. Looloo indi turu “Njaay Daraapoo” wi. Nde, moo doon yore raayab Senegaal bu rëy bi, di ko wëndeel, saa bu ekib biy joŋante. Ndeysaan, amul fu mu àndul ak ekib bi. Muy Kuppeg Afrig, di Kuppeg àddina si, fépp la dem, topp ginnaaw gaynde yi, di leen dooleel ak a xirtal. Ni ko wolof di faral di waxee rekk, muy taw, mbaa muy naaj, dafa daan ànd ak ekib bi. Kuñ daan yomb a ràññe la nag. Nde, foo ko fekkaan, wirgoy raayab réew mi lay sol, bëggoon réew mi lool, ak ekib bi, ba foo ko nattoon rekk, weesuna ko. Xarit la woon itam ci jawriñ jiñ dénkoon wàllu tàggat-yaram, Mataar Ba. Ku ko miinoon lool la. Looloo tax Mataar ba seedeel ko kàddu yi toftalu, jaalee ko ko : “Ci naqar wii nu ame, noo ngi jaale ñii di waa-kër ki nga xam ni jóge na fi, di ko jaale itam jëwriñ jii ñu dénk mbiri tàggat-yaram, Yaankooba Jatara, njiitul mbootaayu 12eelu gaynde gi, waaye ak kureel gi ëmb soppey ekib bi.” Momar Njaay, nekkoon na kuñ yàgg a tappal i cargal ngir dogoom ak coono yim daj yépp ngir ekib bi. Cargal gi gënoon a rëy ciy bëtam, nag, mooy gi ko njiitu réew mi tappaloon, keroog, 17 saŋwiyee 2014, muy “grade de chevalier de l’ordre national du mérite”. Waxaguñu kañ lay koy denc ak ban bés lañ koy dëjal. Ñoo ngi dégloondi ba am ci lu leer. EJO ak Lu Defu Waxu ñoo ngi koy jaale njabootam ak i mbokkam, di leen mastawu, di ko jaale itam Senegaal gépp, rawatina axlu kuppe gi.
https://www.defuwaxu.com/reew-mi-gej-naa-yengoo-nii-useynu-beey/
WAAW, KAÑ LA SENEGAAL GËJ A YËNGOO NII…? Weeru màrs wii weesu, Senegaal tàngoon na jipp ! Gannaaw ba alkaati yeek sàndarm yi jëlijee Usmaan Sonko ngir jébbal ko Yoon, daanaka waa Ndakaaru yépp, waa Senegaal yépp sax, rawatina ndaw ñi, dañoo jóg nekk benn say, ne : “Du fi ame !” Keroog ak fan ya ca topp, jàppante bi metti woon na. Waa Nguur gi ne duñu bàyyi, gune yi gën leen a dëgër fi ñu jàpp. Noonu la fi fukki bakkan ak ñett rotee. Ñoom ñépp di ay waxambaane yu tollu ci seen diggu ndaw. Ndax fu bakkan di rot, mat na di fa tudd yàqute yu dul jeex ci alal ? Ãxakañ ! Waaye, xel demul ci di leen méngale. Li nu soxal fii, mooy seetlu ni, li ëpp ci lu yàqu, nekkul ay alali doomi réew mi donte ñàkku ci. Waaye ay moomeelu doxandéem lañu, diy Tubaab yu sanc seen i këri-koom ci dëkk bi, ba tax ñu aakimoo daanaka koomu réew mépp. Këri koom yu mel ne Total, Auchan, Senac, añs. Loolu di nu fàttali bàkku yenn ndaw yiy xeex ngir Senegaal moom dëgg boppam : France Dégage ! (“Farãs jóge fi !”). Muy lu mat a jàngat ndax day wone ni, ndaw ñaa ngi ci tànki seen i mag yi fi nekkoon doon bañ nooteelu doxandéem bi. Te xaley tey yii, mel na ne ñoo gën a farlooti ci farata jooju. Loolu lépp a taxoon Nguur gi dellu gannaaw, yolamal loxoom, bàyyi Sonko mu ñibbi. Guléet, ca ba muy ne ci jal bi, Persidaŋ Maki Sàll gis lu ko jaaxal, ëpp ko loxo ba tax mu walluji, ñaan xalifa yi ñu dugal seen loxo ci mbir mi, ba noppi nangul leen lépp lu ñu ko laajoon ngir indi jàmm. Mu mujje jél kàddu gi ñépp doon xaar, wax ak réew mi, ci anam yu ko kenn masul woon a gis : yëramtu, dige, ñaan njekk, woote juboo ak bennoo. Kujje gi ñoom it, wormaal kilifay diine ji, jóg ni kenn du dox i tànki jàmm bàyyi leen ginnaaw. Waxtu ya jiitu kàllaamay Maki yi, Usmaan Sonko jëkkoon na jël kàddu, wax waxi jàmm, waaye it teg ay sàrt yu leer yu Nguur gi war a jaar, ci gis-gisam, ba mën dalal réew mi. Moo tax it, askanu Senegaal dina santati Sëriñ si. Ñoom ñi nga xam ne, daanaka, réew mépp a ngi doon xaar seen kàddu, ba nit ñi demee ba jàq. Ki ci gënoon a ràññeeku doon nag Sëriñ Muntaqaa Basiiru Mbàkke. Moom mi doxoon diggante Njiitu Réew mi ak kujje gi. Ñépp déggal ko, jàmm dellusi ci dëkk bi. Muy firndeelati solos sëriñ si ci nekkinu askanu Senegaal, te muy luy màndargaal Senegaal (te di dëggal lan ca jotoon a bind ci ginnaaw, ci sunub bataaxal bu nu duppe woon : ”Sëriñ seek a bari doole !”). Waaye, ba lépp nee tekk, lépp sedd, waa Nguur gi mel ne du ñoom : ña laqatu woon ñépp génnaat di mbéléléli ci rajo yeek tele yi. Maki woote ndaje, wax ak guney pàrteem, di gaaruwaaleek a xupp kujje gi : “Li fi amoon, du fi amati !”. Mel ne, tey la Waalo gën a aay. Teguñu ci juróomi weer, Persidaŋ Maki woo Ndawi Réew mi, wotelu sàrt yu yees yuy rëbb mbéeféer yi, ci ni ñu ko waxe.  Mu nel ne nag, dañuy taafantoo jiyaadis yi, ndax ku seet ba ca biir xam ni, ñi ñuy rëbb dëgg, du ñeneen ñu dul waa kujje gi ! Noonu boog, la ko ñu bare jàngate, ay boroom xam-xam yuy jàngale ci iniwérsite yi, waa kujje gi ci seen bopp, ba ci Usmaan Sonko mii jagleel xew woowu ay kàddu yu am a am solo. Du caagéen ne, danuy tëkkale Usmaan Sonko ak ay kàngami Afrig yu mag yu fi nekkoon. Waaye nag, neexul ba neexul, ngóor si, ni mu waxe keroog jooju, gëj na fee am (jóge ciy way-pólitig), ca jamonoy Séex Anta Jóob walla Tomaas Saŋkara. Ne jàkk waa Tugal, tudd seen tur, xamal leen ne lu bon te yées ci Afrig, ñoom a, walla boog seen loxoo ngi ci. Ba noppi di leen digal ñu teggi seen loxo ci kaw Afrig te abal nu ! Sàrt yu bees yii nag, li ci doy waar mooy ne, ëpp nañu téeméeri ponk, te sunuy Ndawi Réew mi, ciy “anam yu jamp” la leen ko gornamaŋ bi jébbal, ñu war koo jàngat itam ci diir bu gàtt (benn ba ñaari ayu-bés). Moone, ñoom ci seen bopp, ci bataaxalu Commission des Lois, di kurél gi ñu jagleel liggéeyu caytu sàrti Yoon yi, ñu ngiy xamle ni : ”Code Pénal bi ak Code de procédure Pénale bi (ñaari téere yooyu ñu leen di woteloo) soo leen joxoon ñu seen xel màcc ci mbiru Yoon sax, dinañu am i jafe-jafe ndax dañoo naqaree jàng, kenn mënul a xam dëgg lu ñu wund ; waxatumaak nun Ndawi Réew mi nga xam ni, dara lañu amul ci xam-xamu Yoon”. Waaw, ñii de, ñu xam loolu ba noppi, bind ko ba mu leer ci seen bataaxal, ñoo walbatiku wote sàrt yooyee, te naan nu: ‘Sàrt yii baax nañu ci askan wi’! Ku leen di déglu ba di leen gëm ? Maki moom, booba, mu ngiy wër réew mi, dëkkoo dëkk, di nemmeekuji koomu gox-goxaan yi. Ci li mu lay, ndax ñu bare weddil nañu ko loolu, jàpp ne ay yëngug pólitig doŋŋ lay doxal noonu. Lum ci mënti doon, li yéeme ci mbir mi, mooy nit ñu baree bare yi muy dajale saa su ne, ciy jamanoy koronaawiris bii ! – Am sax ñu ñuy yab ciy woto, péey ba péey, gannaaw ba ñu leen compalee as tuut ciy koppar -. Dëgg la, ba mu noppee ciy doxontoom yooyu, xelam dellusi na, ba tax muy digle ñu bàyyi mbooloo yu tàkku yi ñuy woo ci xew yi. Xéy-na ndax “Covid 19” day moytu ay xewi Persidaŋ Maki Sàll ? Bugaan Géy Dani moom, faalewul waxi Maki yooyee, ndax moom it sol nay dàllam di doxal li mu tudde “Tibbi Tànki Maki”. Di wër réew mi, fu Maki jaaroon mu jaar fa, lu Maki waxoon, mu weddi ko ba mu set wecc ! Nit ñu baree bari di ko topp. Usmaan Sonko, moom it, ne kenn du dem mu des, daldi jëlaat “Nemmeeku Tuur” yi mu nu tàmmaloon. Wuudey Medina yi de, ñoom, duñ ko réccu ndax seen i njaay yi mu leen fexeel ba ñu jar, ci kaw dimmali liggéeykati Senegaal yi. Senegaal nag, wax ko te dee, day réew mu doy waar ! Ndax kat, jamono jii koronaa bi gën a lëmbe àddina si, rawatina ci miim réew, la nit ñi mel ne ñu raatukaan ! Ku la gën a ñeme mbas mi, nga ni kii la ! Mu mel ne, nit ñi dañoo dem ba ës, walla book ñu tul (tul bu wuteek ñakku yi fi lamb ba dee !) ba tax koronaa bi du leen mënal tus ! Te kenn rawu ci way-pólitig yi. Waaye kenn du nettali doxantuy Maki Sàll yooyu te doo yëy yàbbi ci mbiru nervis yi, maanaam dóorkat yi ! Ñépp gisoon nañ fi ne, ci xew-xewi màrs yi, ay sàmbaabóoy yu gànnaayoo seen i yat, walla ay jaasi, ñoo doon daw ci tali yi di rëbb xale yi doon ñaxtu, di leen jàpp, di leen dóor, dóor yu metti. Loolu lépp nag, doon ame ci kanamu takk-der yi, mu mel ne sax, ñoo àndoon ci seen “liggéey” boobu ! Dóorkat yooyee ñoo feeñaat ci doxantu Maki yi. Ñu neeti ci seen mënin, di jàpp, di dóor gone yiy ñaxtu walla sax ku ñu gis rekk nga sol mbaa nga takk lu xonq ! Dëgg la, seen kilifa moo fi newoon, lu yàggul dara, moom lu xonq du ko gis ! Waaye ku taxaw seetlu dinga gis ni, ba Persidaŋ duggee Tuuba, dóorkat yi dañu ni mes ! Kenn gisul, kenn yëgul. Moo tax it, gune yi xaaruñu ku leen woo : takk seen i sagar yu xonq coyy, di yuuxu, di sànni suuf, ñenn ñi sax di yuuxu turu… Usmaan Sonko ! Dóorkat yi daal (walla seen kilifa ?) ñemewuñu Boroom Tuuba ! Lu mu ci mënti doon, gannaaw takk-der yi, ay dóorkat, fenn lañ leen soxlawul. Te réewum Yoon sax, daa mënut a ànd ak li nu mel. Maki nag, war naa seetaat boppam ! Ayu-bés gii ñu génn nag, Persidaŋ wooti na Ndawi Réew mi, ñu wotelati ko ay sàrt yu bees yu jëm ciy doxalinu wote yi. Fii tam, lu yéeme feeñ na fi : lu bare ci déggoo yi amoon ca Dialogue National ba (Jataayu Waxtaanekaayu mbiri Réew mi), walla ponk yu ñu yaakaaroon ne Persidaŋ dina ci jël ndogal, dañu leen teggi teg fale ! Xeli nit ñi gënatee teey ci mbirum ñetteelu màndaa bi ñuy ruumandaat booba ba léegi, di wax naan, mu ngi ci xelu Maki. Te loolu lépp fekk na mu soppi, ni mu ko neexe, tëralinu gox-goxaan yi ci Ndakaaru, te tagguwu ci kenn ! Waaye li ci kanam rawul i gët. Fii ñu toll nii nag, yenn xel yaa ngiy ñaaw, yeneen yaa ngiy nàcc. Lii lépp ciy xew-xew yu baree nii, ame ci diir bu gàtt ; xew wu la ci gën a metti walla gën laa lëj, nga ne bii la. Mbaa réewum Senegaal dina ko mën a dëkku ? Mbaa du ñaareelu “weeru màrs” daf fe nar a am ? Li gune yiy woowe 2e vague, maanaam ñaareelu sóobu ciy ay ? Dëkk bu yëngu bii, nu fiy jàmm dellusee, sax fi dakk ? Te muy jàmm ju lalu ci dëgg ? Wax jaa ngi noonu. Nun waa Senegaal nag, ndax warunoo seetaat sunu bopp ? Ndax kat, fu fen di mën dëgg, fu kàdduy worook i jëf, taxawal fa luy jëm kër du yomb ! Rawatina réew moo xam ne, Nguur gi, jay-doole rekk la xam te di ko doxaale bu baax. Fàww kon, ñi bokk gis-gis te gëm seen bopp, gëm demokaraasi te féeteek askan wi, booloo, takku tey xàccandoo di dóorandoo, su nu bëggee tekki buumu-njaam gii nu tënk ba léegi. Uséynu Béey
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-25-2-2024/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (25/2/2024) MBIRI PAAP GÉY AK MÀRSEY Gannaaw CAN bi mu demoon ak Senegaal, Paap Géy, miliyë Màrsey (Marseille) bi dañ ko dàndoon ca këlëb ba, maanaan dañ ko génne woon, ber ko. Li ko waral mooy ni pasam dafay jeex ci weeru suwe 2024, Màrsey bëggoon mu yeesal ko. Waaye, Paap Géy dafa lànk. Njiiti këlëb ba jéem a wañ loxoom, mu bañ, jàpp fi mu jàpp rekk. Ci la ko Pablo Longoria mi jiite Màrsey beree. Ndogal loolu tiisoon na ko lool nag. Ndax, laata muy futbalsi CAN bi ak Senegaal, dafa toogoon diir bu yàgg bob, futbalu ci. Li ko sabab mooy ne FIFA dafa tegoon daan. Waaye, ab bunt ubbeeku na. Nde, boolewaat nañ ko ekib bi war joŋante ak Montpellier tey ci dibéer ji. Seen tàggatkat bu bees bi, Jean-Louis Gasset bi wuutu Gattuso moo sàkku ñu boolewaat ko ci gaa ñi. Ndax, ñépp la soxla ngir liggéey. ËRO 2024 : TONI KROOS DINA BOKK Saa-Almaañ bi nangu na solaat mayo dëkkam gannaaw bees ko toppee ay yoon ngir mu ñëwaat ca ekib ba. Ca atum 2021 jëloon ndogalu bàyyi ekibu Almaañ bi. Keroog ci 22 féewiryee 2024 wii la xamle ci xëtu Instagramam ni dina dellu ca ekib ba. “JEUX AFRICAINS GHANA 2024” Sëriñ Saaliw Ja, tàggatkatu ekib U20 bu Senegaal bi, fësal na limkag 23i ndaw yim tànn ngir ànd ak ñoom ci yooyu joŋante. Ci tànnam gi ñu gis ni woo na ci U17 yu bari yu demoon ci kuppeg àddina gii weesu (U17). Ñooñii di : Amara Juuf, Alfa Ture, Sëriñ Fàllu Juuf, Doriwaal Jaata, Yayaa Jémme, Ibraayma Jàllo ak Idiriisa Géy. EMILIO NSUE BÀYYI NA GINE EKUWAATORIYAAL Saa-ekuwaato-gine bi jël raayag dugalkat bi ëppaley bii ci CAN 2023 bii weesu fa Koddiwaar xamle na ni bàyyi na ekib nasiyonaal ba. Gannaaw CAN bi, ay coow yu sew amoon na ci digganteem ak ekib ba, ñàkkul ni yooyu mbir a waral bàyyeem. Moom nag, futbal na 42i yoon ak ekib bi, daldi dugal 23i bii.
https://www.defuwaxu.com/koronaak-addina/
KORONAAK ÀDDINA Taalifu Làmp Faal Kala Ki daan mere nit ñi ci ñàkk a nuyoo Moo bank ab loxoom di tere nuyoo Ki daa tëju amul yitte lañ daan mere Tey ku tëjuwul bari yitte la ñuy tere Jàngoon naa ni fu jullit yi def mbooloo Yàlla dafa fay tàbbal yërmaande Rahma Dakkandil nañ jëm jumaa julliji àjjuma Tere màggal, cant ak jàngeek dajaloo Foo déggaan ku juge Itaaleek Farãs Njëkkanteji sërica ku jiitu ëpp sãs Tey ku ñu ni wiisaa ngii amoo sãs Jàngoro ji wëlbati na àddina tey Dem ba ndigal soppiku tere kay Ku ne tiit di ñaan na koronaa bi fay Ndax dafa bon day fàdd di ray
https://www.defuwaxu.com/li-gen-a-fes-ci-xibaari-taggat-yaram-dibeer-5-mars-2023/
LI GËN A FËS CI XIBAARI TÀGGAT-YARAM (DIBÉER 5 MÀRS 2023) LÀMB Saa-Cees – Rëg-rëg ñoo doon bëre ci dibéeru tey ji. Mu doonoon làmb ju ñépp doon xaar. Waaye, nag, coow am na ci. Nde, bu dee àttekat yi Rëg-rëg lañ jox ndam li, Saa-Cees ak i farandoom nee nañu ñoo daan. Ndaxte, ci biir jaxasoo bi, am na fu Rëg-rëg sampee 2i loxoom ak 2i wóomam, muy 4i apiwi, nees koy waxe. Kon, Saa-Cees a yeyoo ndam li. CNG mooy àtte. PSG / FARÃS Mbappe defati na jaloore Mbappe tegaat na beneen jéego ! Doon na kuppekat bi ëpp lu mu dugal ci mbooru PSG. 201 bii la fa dugalagum bim fa ñëwee ba léegi. Bu ñu fàtte ni, Mbappe, 24i at doŋŋ la amagum. Waaye, ak li muy doon xale yépp, dafa dooj ba, turam siiw na lool. Gannaaw jéego bu réy bim defaat la Ronaldo, kuppekat Beresil bu mag ba, wax lii ci moom : ” Li Messi ak Ronaldo def ci kuppe, mennum Mbappe moo ko mën a defaat. Bu nu fàtte ni 24i la amagum.” Marquinhos ame na gaañu-gaañu Ba tay foofu ca PSG, gannaaw ndam li ñu am ci kaw Fc Nantes, démb ak li Mbappe def, njàqaree ngi bëgg a gane seen biir ak joŋante ñuy waajal ak Bayern, di bu ñu war a gañe bu ñu bëggee wéyal seen yoon ca “Ligue des Champions “. Marquinhos àggalewul seen joŋanteb démb bi, dafa gaañu, daldi fekki Neymar ak Kimpembe. Wuteek nañook Bayern mi nga xam ne, ay kuppekatam yi gaañu woon ñoo ngi delsi. LIGA / Espaañ Paap Alasaan Géy, ñu miin ko ci Paap Géy, defaat na beneen paas ci seen joŋante bi ñu ñàkk démb ci kanamu Athletico Madrid (1-6). Paas boobu mooy ñetteelam ba mu demee ca Seville ba léegi, di wane miinam bu gaaw ci këlëb ba. Mujjul a àggali joŋante bi itam, moom Paap Géy. Ndax, dañ ko ruus ginnaaw bi mu amee ñaari kartoŋ soon. MILAN / ITALI Ibrahimovic, na woon, fa woon “Ñëwat naa gannaaw sama gaañu-gaañu bi. Léegi, dinañu xamaat kuy tàmbali joŋante yi. Bi ma gaañoo ataakã yaa ngi doon wane seen bopp. Waaye nag, dikkaat na. » Kàddu yooyee la Ibrahimovic yëkkëti gannaaw ba ko benn taskatu-xibaar laajee lu jëm ci moom ak ekib ba.
https://www.defuwaxu.com/aysata-taal-sall-jigeen-soppal-te-bul-woolu/
AYSATA TAAL SÀLL : JIGÉEN SOPPAL TE BUL WÓOLU…? Bés ba ma ko déggee mu naan kilifa diine yi dañ maa ñaan ma fekki Maki, laa ni ci sama xel : Aysata mii de, xéy-na dafa paree dem ba noppiy làmbaatu ba xam nu ko askan wiy gise ëllëg. Waaye man ci sama wàllu bopp de, masuma woon a xalaat ne Aysata Taal Sàll dina mas a bokki ci ñooñu doyadi bay xéy weddi seen bopp, dem ànd ak Maki, ndax rekk bëgg a tedd. Ndekete yóo… Dëgg la, Senegaal, danoo miin politiseŋ yiy toxu, dem tag fu seen ceeb di gën a niin ba loolu safatul kenn. Waaye ndaw sii moom, ñépp mere nañ ko. Am na sax ñu naan moo yées ci ñiy yëngu ci làngu pólitig gi. Aysata Taal Sàll dafa am fu ko askan wi mës a teg, muy fésal li mu gëm ciy kàddu yu leer nàññ te yit daan ko jëfe. Bërki-démboo-njaay rekk la fi ne xel dajul muy ànd ak waa nguur gi. Ñépp jàpp ni waxi gor la, doonte sax néew na li ñuy gis kuy pólitig ba noppiy jiital sa ngor. Jigéen ju mel ni moom, jekk kaar, nex i ree, ay kàddoom dëggu, soo leen déggee ñu dugg la, mu jàng ba am i lijaasa yu réy, bokk fu baax niñ ko waxe, danga war a jombal sa bopp yenn yi. Rax-ci-dolli, foo ko fekkaan mu ngiy xeex par-parloo tey sotle néew-dooley réew mi. Ku mel nii, daa sopplu te ku ko sopp wàcc nga. Tey, bu Aysata demee ba génn ba set wecc ci li mu waxoon, mbetteel la, gàcce la. Ñu bare la mbir mi ub seen bopp, am na sax ñu dem ba yaakaar ne Aysata Sàll ñoom rekk la tooñ, tooñul keneen. Léegi nag, ñépp a ngi ciy teg seen bët : ci jigéeni réew mépp, amu ci kenn ku yoon may mu bokk ci joŋante 2019 bii, kenn ci ñoom muccul ci ‘’parenaas’’ yi ; kon, juróom yi des ci géew bi yépp ay góor lañu. Ndax Senegaal daa pareegul fal jigéen, teg ko ci boppu réew mi ? Loolu lay nirool. Ni Aysata Taal Sàll doxale, nag, day tax ñu yeyatiñu, nun jigéen ñi. Du ñàkk ñu jàpp ne dafa dëggal kàdduy Kocc Barma yu siiw yooyu te naqadee nangu : Jigéen soppal te bul wóolu…
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (6/7/2023) AFROBASKET-JIGÉEN, RUWÀNDAA 2023 Gannaaw tànn gu njëkk ga, Mustafaa Gay, seggaat na ekib bi, tànn ci jigéen ñi war a teewali Senegaal fa fa Ruwàndaa, bokk ci joŋanteb Afrobasket bu jigéen ñi. Ñii toftalu la jël : Way-dawal yi (meneuses) Leena Timeyraa, Siyaara Siney Dilaar, Faaty Jeŋ Gannaawe yi (arrières) Kuuna Ndaw, Yaasin Jóob Ma-laaf yi (ailières) Ayaa Taraawore, Matild Jóob, Faatu Puy, Soxna Faatu Silla Wërmbiij yi Ummu Xayri Saar, Ummu Kalsum Ture, Faatu Jaañ, Aram Ñaŋ, Aysa Nduur. SÀMPIYONAA ESPAAÑ AM NA TUR WU BEES Soppes na turu sàmpiyonaa Espaañ. Léegi, tuddatul LaLiga. Bés niki tey, dees na ko woowe LaLiga EA Sports. Nde, dañu am esponsoor bu bees, muy defarkatu powum kuppe bii di EA Sports. REAL MADRID SUUFOOTI NA BARCELON CI ARDA GÜLER Real Madrid defati na ko Barcelon. Fan yii yépp, Barcelon a ngi waxaale ak njuuma Turkii liy futbal Fenerbahçe, Arda Güler. Waaye de, Real Madrid dafa jaar ci suuf, wax ak xale bi, déggoo ak moom ba mu tànn Real ci kow Barcelon. Lu ni mel nag, du guléet. Nde, muy Vinicius Junior, di Rodrigo, ñoom ñépp, Real dafa suufu Barcelon, jënd leen. Barcelon dafa yabaloon ay ndawam fa Turkii ba ñu tàmbali woon waxtaan ak futbalkatu Fenerbahçe bi. Amoon nañ ci yaakaar lool sax. Ca la Real Madrid ñëwee, ràccal boppam, Arda Güler daldi nangul ekibu péeyu Espaañ bi. Ci fan yii di ñëw, dinañ matal li ci war lépp ngir mu ñëw bokk ci ekibu Real Madrid bu mag bi. Bokk na ci li ko yombal nag, mooy magi Real yi daan dégganteek moom, niki ñoom Modric, Kroos ba ci Özil mi fa nekkatul sax. MASON MOUNT DEM NA MANCHESTER UNITED Manchester United amati na limatu 7 bu bees. Mason Mount mi nekkoon Chelsea lañu jënd. Ndax dina dox ci tànki Cantona, Beckham, Ronaldo, ñi siggil 7 bi ; walla dafay mel ni ci ko mujjee sol te lajj : Owen, Valencia, Di Maria, Depay ak Cavani ? Seetaan a dàq cim ndaje. FRANK LAMPARD AK STEVEN GERARD DEM NAÑ ARAABI SAWDIT Frank Lampard amati na këlëb bu bees. Wii yoon, ca naar ya la dem, Araabi Sawdit. Këlëb bii Al-Ittihag lay yori. Dafa topp ci tànki Steven Gerard miy yori tamit Al Etiffaq.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-18-9-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (18/9/2023) WAA LORIENT YI SARGAL NAÑU BENJAMIN MENDY Benjamin Mendy duggaat na démb ci pàkkub futbal, gannaaw tuuma gu metti te yàgg bi tegu woon ci ndoddam, at yii weesu. Tuumay ciif yooyu ñu gàlloon ko ñoo taxoon ñu bari foogoo ne daf ciy jaare bàyyi futbal. Waaye, keroog, ba ñu ko setalee ni deful lees ko doon toppee, la daldi fasante ak Fc Lorient, këlëb bu nekk Farãs. Démb, ci dibéer ji 17i fan ci sàttumbaar 2023 la duggaat ci pàkk bi, ci joŋante Lorient ak Monaco. Soppey këlëb ba sargal nañu ko, woy turam. Ci 70eelu simili bi la duggu. ABIIB BÉY A NGI NE PATT DI LIGGEEY Dafa boolewul daraak wax. Moo ngi nekk ci ruqam ak këlëbam, Red Star, di def jéego yu am solo moom Abiib Béy, saa-senegaal bi bokkoon ci gayndey ati 2000 yi. Ci tàmbalig « saison » ren ji, amal na ci 5i joŋante, gañe ñeent yi, ñàkk benn bi. GREENWOOD DUGGU NA XAAT CI MBOORU GETAFE Gannaaw i tuuma yees ko tegoon moom it ci mbiri jigéen ba tax waa Manchester United daldi koy bañal mu toogaat ci ekib ba, àngale bi dafa daldi fasanteek Getafe, ab këlëbu españool. Ci ayu-bés bii nu génn,  këlëb bi daldi nay jaay ciy mayo yees bind turam lim boo xam ni bii kenn mësu koo def ba Getafe di këlëb ba léegi. JOAO FELIX DUGAL NA BIIWAM BU NJËKK CA BARÇA Barki-démb ci gaawu gi, ci ndamu Barça bu rëy bi 5-0 ci kaw kii di Real Betis, la Joao Felix daldi dugal balam bu njëkk ca këlëb ba. Loolu nag doon ci moom mbégte mu réy, nde bi ñu ko dékkee mikoro bi ba joŋante bi jeexee, dafa wax ni « yàgg naa dugal bii, waaye bii moo nekk bu ma ci gën a neex ndax dafay matal sama géntug futbalsi Barça. »
https://www.defuwaxu.com/kuppeg-addina-gees-jagleel-u17-fa-endonesi/
KUPPEG ÀDDINA GEES JAGLEEL U17 FA ENDONESI Tànnees na fukk ak benni ndaw yi war a teewal Senegaal fa Endonesi ñeel kuppeg àddina jagleel ñi ëppalagul 17i at. Nii la toftale gi tëdde : Góol yi Sëriñ Juuf (G.Foot) Makura Mbuub (G.Foot) Séex Bàmba Faal (Diambar FC) Defãsëer yi Sëriñ Fàllu Juuf (G.Foot) Mammadu Aliw Jàllo (Diambar FC) Guy Feliks Lima (AFAT Thies) Ibraayma Jàllo (G.Foot) Buubakar Saajo Ba (Étoile Lusitana) Sériif Keebaa Ñabali ( Océan FC) Alfa Aamadu Ture (G.Foot) Miliya yi Piyeer Antuwaan Jaata Dorival (Dakar Sacré Coeur) Paap Daawda Jong (AF Darou Salaam) Sëriñ Saaliw Fay (G.Foot) Mammadu Lamin Saajo (Environnement Foot) Mammadu Ñing (Espoir de Guédiaway) Ataakã yi Idriisa Géy (G.Foot) Omar Sàll (Environnement Foot) Yayaa Jémme (Diambar FC) Amara Juuf (G.Foot) Mammadu Sawane (AFAT Thies) Clayton Silverio Kàndi (Espoir de Guédiaway) Ñii ñooy ndaw yi ñu tànn ngir ñu dem teewal réewum Senegaal ca kuppeg àddina giy ame fële ca Kembaaru Asi, dëkku “Indonesie”. Joŋante bi nag moo ngi war a tàmbali fukki fan ci weer wii nu nekk. Réewum Senegaal mépp di ci ànd ak seen i doom di leen ñaanal ñu ame fa ndam. Mànkoo jëli ndam li !
https://www.defuwaxu.com/taxawaayu-kujje-gi-ciy-wotey-gox-goxaan-yii-degmal/
KUJJE GEEK WOTEB 2022 BI: BËGG NAA LA, BËGGUMA LA, LOOLU JARUL COOW Ci bésub 23 sàŋwiye ci atum 2022 bii di ñëw, la Senegaal fas yéene amal ay wote jëm ci palu njiiti gox-goxaan yi. Gannaaw ba pàrti pólitig yi jàppante ci mbiri yoonu pal gi, maanaam li ñeel doxalinu wote bi ak jumtukaay yi mu àndal, léegi, pàrti yooyee, seen yitte yépp a ngi aju ci nañu nar a taxawe ci joŋante yi ñuy waajal. Coow li jib lépp, looloo ko waral ci jamono yii, jóge ci anam yi pàrti yi di taxawale seeni mboolooy kurél yi. Kilifag pàrti PUR moo sulli mbóot mi, yëgle ne “ñeenti pàrti yi gën a mag ci kujje gi” déggoo nañu ngir jëmmal seen nas bii doon sàkk mbootaayu pàrti yu kujje gi. Pàrti yooyu ñooy PASTEEF, Taxawu Dakaar, PUR ak PDS. Coow li ne kur ci dëkk bi. Ñu teg ciy fan, mbooloo mi ñu tudde “Yewwi Askan Wi (YAW)” daldi juddu. Ñenn ñi rafetlu ko ndax yaakaar ne kujje gi dina fi jóge génn ci gutt gi mu ne woon ba léegi, wone dooleem, jàkkaarlook waa nguur gii di sonal askan wi ; ñeneen ñi ñaawlu li kujje gi manul a fexe ba booloo nekk wenn say képp. Ci kow loolu, am na it ñuy laaj naka la ñeenti pàrti doŋŋ di woote ni ñooy taxawal lu mat, daanaka, ay téeméeri làng. Ba tey it, gisees na ñu rafetluwul doxalin wi lal wote woowu, mel ne ñi ko sooke dañoo nawloowul seeni naataango yi ñu bokkal xeex. Am na sax ñu ci doon booley xaste, di ñaawal kujje gii “man a jaxase ñu àndul, mbete supp kànja !” Teguñu ci ayubés, PDS génneeb bataaxal xamle ne bokkul ci mbooloo mu yees mii, ndax masul a xaatim lenn lu koy firndeel ; yeneeni pàrti yu mel ne AJ/PADS ak Bokk Gis-Gis, ñoom it génne seenub yëgle di wone ni bokkuñu te ànduñu it ci doxalinu kurél gu bees googu di Yewwi Askan Wi. Ginnaaw bi, kurélu Gëm Sa Bopp gi ci bokkoon, far génn moom it ci mbooloo mi, ndax ñàkk a gis boppam ci defin wiy niru xàjjaatle ci biir pàrti yi, mel ne yenn ci pàrti yi bëgg a féetale seen bopp ci kow, ñi ci des ci suuf. Coow li jibati, yëf yi jaxasoo. Ay kàddu jógati di ŋàññ kuje gi ndax seen ñàkk-juboo. Pëndu coow loolu jotul a wure, meneen mbooloo mu soqikoo ci kujje gi daldi juddu wone boppam. Ñu xàmmee ci ñi ko sàkk, ay pàrti walla kurél yu mel ne PDS, Bokk Gis-Gis, AJ/PADS, CRD… Muy mbooloo mu mag, daanaka walla lu bon-bon, mu tollook dayo moroomam mi ko jiitu. Coow li neeti kur. Ñi jàppoon ni kujje gi mënta fexe ba booloo, gënatee yëkkati seen baat. Jamono jooju yépp, waa Bennoo Bokk Yaakaar (BBY) yi ŋànk nguur gi, ñu ne tekk di seetaan ; ñenn ñi jàpp ne sax, booba ñu ngee ree ci suuf. Waaye ñoom it, ndax seen ay ci coow li du dikk, bu ñu demee ba war a tànn ci gox bu ne, ku fay nekk jaraaf ? Waaw, booba nag, ana askan wi, moom ? Ana li ciy taxawaayam ? Su dee dëgg rekk a tax ñuy wax, daa mel ne ñoom ñooñee, askan wee lee doon seetaan dëggantaan. Wax dëgg, askan wi moom, daa am lu ko doy sëkk, ak mbënd mi ko léjal ba ci kanamu Yàlla ! Rax-ci-dolli, njëgum njaay mi di yéeg jëmale… asamaan…! Lépp a yokku. Fekk booba, ndox mu ñu naan rafle fi, ba tax jigéen ñi di ko wuti ni doom yu góor. Moonte, askan wi de, moo war a tànn ci diggante waa nguur gi ak waa kujje gi, ñi ko doy ngir mu dénk leen boppi gox-goxaan yi, ngir seen yorin wu rafet. Ku yabu ne, ngir seen dundin ñoŋ. Lu mu ci manti doon, way-pólitig yi, warees nañuy taxaw-seetlu, ànd ak seen xel, gannaaw ba ñu leen njortalee ñunekk ñu bëgg seen réew, fonk seen gox, te jiital njariñal askan wi. Ndax kat, gàtt-xel weesuwul nit jóg ni kenn waru fee sooke dara te boolewuma ci ! Ndax it, du ñàkk-xel di jàpp ne lu ëpp ay ñaari téeméeri kurel, mënees na leen a boole ci menn mbooloo, ñuy ànd di nas, di xàccandoo, di dóorandoo ? Waaw waaye, ndax bokkul it ci gàtt-xel nga woo ay nit ngir ngeen ànd xeex, ba noppi naan leen “Yeen tekkiwuleen dara, toppleen rekk sama gannaaw ma yóbbaale leen ?” Xaste wi nag, moom, mënoon naa ñàkk, rawati-na ba muy niru tayeef. Ndax, xanaa kañ, kuy nas ngir boole ay nit, ñu àndul bokkuñu kurél kepp lay man a woo ? Rawati-na, mbooloo moo xam ni, génn nësër doŋŋ moo ko tax a jóg, maanaam, bokk sotoo ki ñuy jàmmaarloo, ba mu abal leen ? Ana kon lu fi indi ñamu supp kànja wu neex woowule ? Ak sunu xel mu gàtt, foog nanu ni, laaj yooyu de, suñ leen sampoon ca njalbéen ga, jafe-jafe yu bare, maneesoon na leen a moytu. Am déet ? Waaye ndegam su ndox tuuroo, ab ban a cay des, waa kujje gi, warees nañoo taxaw-seetlu, defaraat seen koddaay, te fexe dëgëral seen taxawaay. Ñaar ba ñetti mbooloo sax man naa am, su dee ñoom ñi ko séq dañuy bàyyi xel ci ne, li leen xàjjaatle ak nguur gi moo ëpp solo fuuf li jaar ci seen diggante, ñoom ci seen bopp. Na fekk nag, ku ne xam sa bopp, ndax kat, bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan. Ba tax na, waa kujje gi, su ñu bëggee ànd ànd wu rafet te yàgg (naka BBY amale), fàww ku ne xam li ngay “peese” ak nu sa moroom tollu. Ana kuy weddi ne, Usmaan Sonko, li muy gune yépp, ak li muy doon gan yépp ci làng gi, doole ji mu am tey, kenn mënu koo nasaxal ? Ana kuy nàttable dayob Ablaay Wàdd ak PDS ? Ku xam jaar-jaaru pàrti boobu xam ne, moom du nangu mukk geneen kurél di ko jiitu, feek wonewul boppam ba wuutu PDS ci taxawaay bi mu am booba ba léegi ci làngu pólitig bi ak ci réew mi. Loo bañ-bañ lëg, nangul kooy noppam yu gudd ! Lii nag, am na njàngale mun ci man a jële : fi ñu tollu nii, PDS ak PASTEEF mënuñoo bokkagum menn mbalka mu ñuy naane ! Ndax nag, soxlawul di naxante, joŋantey pólitig yii, xëcco nguur a ngi ca xol ba ; te sax, ñenn ñi, duñu fàtte mukk seen nafa, fu ñu toll. Loolu nag, terewul waxtaan, weccee xalaat bokkay nas ñeel anam yi wote wi war a doxe. Koonte nag, ñaari mbooloo yii soqeekoo ci kujje gi warul a jaaxal kuy seetlu, di jëfandikoo xelam. Waaye li war a leer ci boppu ku ne, mooy ni, ëpp doole sa moroom warul a tax nga xeeb ko te Wolof Njaay nee na “koo xeeb, mu yab la”. Te, li wóor ba wóor mooy ne, kenn ci làngu pólitig gi, mënul a dem moom kese ci xare bi ba jële fa ndam, ak doole joo mënti am ! Ci way-pólitig yi nag, mel na ni, kii di Maki Sàll moo gën a mokkal njàngale moomule… Dëgg la, moom nag daa yore kopparam gu duun, boole cib xaatimam bu am solo. Moo tax it… Kujje gi daal, war naa seetaat boppam. Ñi man a ànd, nañu ànd booloo. Ñi bokkul genn kurélu mbooloo nañuy yëgante, bokk xeex ngir wote wi ci boppam jaar yoon ; te ñuy bañ a xeebante, bañ a tamante dëmm. Tey bàyyi xel saa su ne, ci nekkinu askan wi ak it ciy xalaatam. Leneen lu way-kujje gi war a bàyyi xel, mooy luñuy def ba fexe wéyal seeni mbooloomi kurél yi, gannaaw su wote gox- goxaan yii jàlle. Ndax kat, xeex bi day door rekk… te kuy dem xare war a fàggandiku ! Uséynu Béey
https://www.defuwaxu.com/mbay-jaag-gor-gi-senegaal-ameel-bor-ii/
MBAY JAAG, GOR GI SENEGAAL AMEEL BOR (II) Am it lu mat a taxaw-seetlu : jamono jooju Mbay Jaag doon jiite ndongo yi, fekkoon na mu bokk ci PAI, pàrti  “marsist” bu mag boobu  Majmuut Jóob sosoon te mu jiite woon yéngu-yéngu ya jiboon ca 1958 jëm 1960 (“boroom paŋkàrt  ya”) ba Afrig Sowu Jant gépp doon xeex ngir moom boppam, yewwiku ci nootaange bi ko Tubaab bi tegoon. Noonu Mbay Jaag bokkoon ci pàrti bu mag boobu. Dëgg la, PAI ag cëslaay gu ko daan dooleel la. Waaye, li am ba am moo di ne loolu taxul woon Mbay jiitaloon mébétu pàrteem ba tax koo fàtte njariñu askan wi. Xew-xewu ‘’Mai 68’’ boobu amoon na solo ci dëgg-dëgg su ñu gise, ca ginnaaw ga, coppite yu baree-bari yi mu indi woon ci àddina sépp, rawati-na ci sunu Senegaal gii. Ndax ña doon jiite réew yi gisoon nañu ni mënatuñu woon doxale nañdaan doxale lu jiitu xew-xew yooyule. Moo taxoon Seŋoor mi amoon gis-gis lool ci wàllu politig, ci kaw it ay ndigali Pari, daldi sàkk pexe yu yees : teggi sañ-sañu benn pàrti doŋŋ(UPS), benn sàndikaa doŋŋ(CNTS), benn kurélu kàngaami iniwersite doŋŋ…  Tërëlin yu bees yoyu nag, xéyu ñu benn bés  ñu sotti : dem nañu ba atum 1974  ñuy door a nemmeeku naka la li ci ëpp doon matale. Ndegam Mbay Jaag daa bokkoon ci pàrti politig, mënul woon a ñàkk am péete ci wàll woowu. Looloo taxoon, ba PAI amee ay jafe-jafe ci biiram  ndax ñàkk juboo ci yoon wi ñu waroon a wéyale xeex bi ngir indi demokaraasi ci réew mi, moom mu ànddoon ak ñi doon weddi seeni njiiti pàrti ca nañu daan doxale. Mënees na lim ñenn ci àndandoom yooyu : ndem-si-Yàlla ji Mbàbba Gise, ndem-si-Yàlla ji Elimaan Kan, ndem-si-Yàlla ji Baabakar Saane, Abdulaay Bàccili… Ñoomñooñu dañoo mujje génn PAI sos seen pàrti bopp (LD  – LD/MPT) akseeni ñoñ. Seen kurél gu bees googu nag, doon wéy, njëkk ci yoonu “marsism” laata ñuy yaatal, ubbil seen bunt ñeneenñu amul woon boobu gis-gisu àddina. Ñu raññeku woon nag lool ci biir liggéykat yi, rawati-na ci jàngalekat yeek fajkat yi. Noonu lañu leen doon jàppale ba ñu taxawal seeni sàndikaa. Liggéey boobu yépp nag, Mbay a nga woon ca biir te kenn daawu  ko woon jëkk ci lenn. Mbay Jaag ak pàrteem, ñu raññeeku woon lañu ci xeex bi kujje gi doon xeex nguuru Abdu Juuf mi fi wuutu woon Seŋoor. Ñu àndoon ceek Ablaay Wàdd mi doonoon njiitu PDS ak kujje gi ci boppam. Noonu la Ablaay Wàdd fexe woon ba toog ci jal bi, ca woteb atum 2000, ginnaaw yéngu-yéngu yu metti ya amoon  ca njeexitalu nguuru Abdu Juuf.  Pàrti Mbay Jaag bi  amoon ci taxawaay bu am solo. Moo tax it ñoo bokkandoo woon jiite réew mi ba ñu amee ndam ca woteb atum 2000 ba. Waaye yàggul dara ñu féewaloo seen biir : Ablaay Wàdd ak PDS jaar nii, waa LD jaar nee ba mu des Mbay Jaag ak ñenn ña mu àndaloon. Ñoom ñooñu gàddaay génn LD ba noppi des ak Wàdd ci nguur gi. Taxul ñu fekki  ko ci PDS, ndax dañoo sos ñoom it pàrti bu ñu moomal seen bopp (UFPE). Mbay Jaag moo jiite woonati fippu boobule, dem ca ba jeex. Ba taxoon na, ñu bare ci taskatu xibaar yi, ak ñu baree-bari ci askan wi doon ko ci ŋaññ, jàppoon ne daa jaayoon ngoram. Moom ci boppam, réeréewul woon mbir ni lu ni mel doon na ko ci fekk, teewul mu amoon fitu jàkkaarlook ñépp, taxaw fi mu taxaw. Noonu la ko Ablaay Wàdd woowe ci wetam, boole ko ci njiiti Màkkaanu Njiitu-réew mi. Mu def fa liggéey bu am solo, su nu sukkandikoo ci seedey ña mu fa doon liggéeyandool. Ku Yàlla defoon nga bokkoon liggéey ak moom ci jamono yooyu, te fekk nga jotoon a xam ku mu doon dëgg, dinga mën seede it ni, genn coppite gu yées feeñul woon ci moom. Moomoon boppam, amoon xalaati boppam. Fulla, faayda ak ñàkk caaxaan ñoo ko mas a màndargaal. Mu nekkoon ku xareñ, nangu liggéey, bañpar-parloo, di fexe di yemale ñépp saa su ne. Looloo waraloon ñu bare ci béréb bu kawe boobule daan ko laale bant bu gudd. Jikkoom jooju, ñépp raññe woon ko ci moom (nga bëgg ko walla nga bañkoo bëgg), moo ko mayoon mu doon jiite,  ñaari ayu-bés yu ne, ndajem-kàngam yi doon xelal Njiitu Réew mi. Mu doon nag jaarale lépp yoon. Kenn mësu ko ca woon a sosal  lenn walla doon am lenn lu mu ko ca doon yabe. Wax dëgg, dañko ca daan gën a naw. Nit kooku moo doon Mbay Jaag, ci liñci xam. Ku bëggoon réewam, jébbalu ci Senegaal gi mu doon xeexal, di ko liggéeyal saa su ne, ba bés  ba mu sàngujee suuf. Tey, wéetal nanu. Di ko jaale ay mbokkam, ay xaritam, ay àndandoom, di ko jaale  Senegaal gépp. Yàlla na suuf woyof ci kowam, Yàlla na ko Sunu Boroom yërëm te xaaree ko àjjana.
https://www.defuwaxu.com/jonante-ren-bii-petorool-lay-xeen/
JOŊANTE REN BII, PETOROOL LAY XEEÑ… Keroog, askanu Senegaal jóg na ci njekk ak teggin, daldi def li ko war ci tànneefu njiitu réew mi. Ndax, bi waxtu wi jotee, nit ñi gànnaayoo nañu seeni kàrt, ànd ak yar, dem ndànk sànnil ko wutaakon bi leen doy. Léegi nag, Maki Sàll jàllaat na waaye mbir mi dese naa leer ba tey. Yàlla na ngoru nguur geek kujje gi tollook li leen réew mi sédd. Ci téeméeri falaakon boo jël, daanaka juróom-benni fukk yi wote nañu. Maanaam, doomi-Senegaal yi wone nañu ni mbir mi yitteel na leen lool. Te sax, bu dee wax dëgg rekk, lim bi waroon na fee gën a takku. Waaw, dafa di nag, ñu bare jotuñu ci seeni kàrt. Lu waral loolu ? Ñenn ñaa ngiy duut baaraam nguur gi, waa nguur gi ñoom di indiy lay yu dul jeex. Li am ba des daal moo di ne, ci jàmm ak salaam lees yeewoo ci dibéeru wote bi, yendu ci itam. Waaye, toqu dereet dina yàq këllu soowu. Ab njiitu jëwriñ lu muy dox di falaate te amul gëdd bi, amul sañ-sañ bi ? Bun Abdalaa Jonn mii nag, moo fi naroon a taal daay. Ndege, dafa dem ca RTS, janook askan week àddina sépp, ne Maki faluwaat na ci sumb bu njëkk bi. Coow li ne kurr, xol yi tàmbalee tàng, ñenn ñiy séentu fitna ci réew mi. Idiriisa Sekk ak Usmaan Sonko woo taskati xibaar yi ngir xamal askan wi ne kenn warul a nangu loolu, yëkkatiy kàddu jëmale leen ci waa APR, ni leen duñu nangu mukk ñuy jalgati kàrt yi ngir sàcc wote bi, jàllale Maki ci sumb bu njëkk bi. Li waroon ñi faral njiitu réew mi mooy ñu am ngor te ànd ak dal, bañ a may kenn mu tam seen mbër dëmm, naan ni mu faluwaatee daa taq suuf. Li ñu naan ñaareelu sumb, ñu bare yakaaroon nañu ko. Te Senegaal, saa bu ñaareelu sumb masee am ci joŋante bu ni mel, ki toog ci jal bi day ñàkk. Bu ko defee, mu dem Frãs, bàyyee nook sunuy mbir, toog Wersoŋ ni Seŋoor, di jiite “Francophonie” ni Abdu Juuf mbaa jaaxaan Wersaay ni Ablaay Wàdd. Usmaan Sonko ak Idiriisa Sekk ñi nga xamante ne, kenn ci ñoom moo naroon a jàll ci waññi bu njëkk bi, li leen waroon moo di taxaw temm ngir waññ bi jaar yoon waaye ànd ceek dal te bañ a waxe xol. Ci sunu gis-gis, def nañu ko. Li leer ba leer moo di ne mu neex gornmaa bi walla mu naqadi ko, askan wi rekk ay buur. Ndaxte, saa su jaay-doole walla njuuj-njaaj àntoo, daa fekk askan wi ne yàcc-yàccaaral di seetaan. Doomi-réew mi wote nañu, te benn a ngi nii ci jàngat yiñ ci mën a def : demokaraasi, àndul ak xiif. Ku sa biir feesul, doo ko tal… Doomi Senegaal yi féete bitim-réew, seen doxalin ci wàllu politig wute naak doxalinu ñi nekk ci biir réew mi. Sunu mbokk yi tasaaroo ci àddina sépp, wone nañu bu baax ne Usmaan Sonko lañu wóolu. Usmaan Sonko nag, digul kenn xaalis walla ndombog-tànk. Lenn doŋŋ la dige, mooy ne : su faloo, caaxaan dina jeex ci miim réew te it, dina def kemtalaayu kàttanam ngir nu moom sunu bopp, dunde sunu ñaq, jariñoo sunu suuf. Doomi Senegaal yi féete bitim-réew, ñi ci ëpp dañoo jàng, am xéy tey sant Yàlla, daanaka. Nit ku suur, nag, xelam day ubbeeku te xalaatam du gàtt. Leneen li mooy ne ñooñu nekk bitim-réew, nguur gi masu leen a amal njariñ, lépp lu ñu am ñoo ko liggéeyal seen bopp. Yakaaruñu diw falu jox leen ay màrse walla ndombog-tànk. Ñooñu, su ñu wéetee ci mbañ-gàcce gi, jiital Senegaal ak ëllëgam daf leen di yomb. Ñi ëpp ci ñoom dañu tàmm a gis, fa ñu dëkk, njariñu politig bu jaar ci yoon. Day tax am réew moom boppam, di xeex ger ba noppi am ay njiit yuy fullaal seen yokkuteb askan. Bu dee nag xamoo fu dul Ndumbelaan gii nga xamante ne ku ñàkkul jom, ñeme kàcc tey cuune, sa tekki ci politig dafay jafe, ñu mel ni Maam Mbay Ñaŋ, walla Farba Seŋoor mën nañ laa doy. Boo ci tegee xiif nag, ak ñàkk liggéey mbaa lijaasa, sa dara doyul, xamoo fan ngay jële depaasu ëllëg, ñu jënd laak saaku ceeb walla piisu legoos du jafe. Réew mi nag, dafa am ñu fi nekk te defuñu, 1960 ba léegi, lu dul aakimoo li ñépp bokk. Ñooñu, seen yoon newul ci Senegaal, li leen yitteel mooy naka lañuy def ba ñoom ak seeni mbokk ñuy jot ci liggéey yeek màrse yi gornmaa biy séddale. Seen gis gis soriwul, doonte sax xiifuñu te ñu ci bare dañoo jàng ba ni arr. Am na, ci sunu mbokk yi nekk bitim-réew ku ci ne, bi ngérte yi feeñee, ñoom def nañu li leen war ; mu yokk ci ne ñi nekk Senegaal nag ñoo ci des te bu ñu dof-dofloo ba falaat Maki, buñu defati seen xel ci ku leen yónnee “Wari” walla “Western Union”. Gaa, ay kaf rekk la woon wànte mel na ni ku sa biir feesul taloo demokaraasi. Leneen lu jar a bàyyi xel, mooy doxalinu ndawi Senegaal yi jàng lekool. Ñoom it Sonko rekk a leen doy, dooleel nañ ko bu baax te li looluy biral moo di ne Senegaal tegu na ba fàww ci yoonu coppite. Su dul déwén it, ciy at yu néew lay doon. Sonko jiite xeex boobu mbaa mu bañ koo jiite, ndam li mu am ren law mbaa mu yem fi, xaley Senegaal yi seen gis gis leer na, xam nañu ne xeetu politig bi Maki taamu, su fi saxee, dees na yeewu bés, Senegaal mel ni Gaboŋ, maanaam am xéewalu petorol ba noppi jébbal ko Frãs te ku ne piip ñu ceene la tëj kaso, fàtte la fa. Ak li coow liy bare yépp, kan lañ dégg mu tudd fi Xalifa Abaabakar Sàll fan yii ñu génn ? Mamadu Jàllo
https://www.defuwaxu.com/2312/
Njàngatub Bàmmeelu Kocc : Téereb dekkali 1/2 Du guléet. Déedéet. Bindkat bi tëbul rekk bind Bàmmeelu Kocc Barma. Nde, ginnaaw Doomi Golo, bii mooy ñaareelu téereb nettali bu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob, génne ci làmmiñu wolof. Te sax, li ko jiitu, Bóris jot na fee yatt xalimaam gu set gi te neex, tekkil nu téereb Aimé Césaire (Une saison au Congo) bi ci kàllaamay Kocc, tudde ko Nawetu deret. Moom, nag, tur wu yéeme la tànn, daldi koy duppe ñaareelu téereb nettali bi këru móolukaay EJO génne : Bàmmeelu Kocc Barma.Tur woowu de, day naxe. Ndaxte, du jaar-jaari walla jaloorey boroom xam-xam bu siiw boobu di Kocc Barma Faal la ciy nettali. Déedéet ! Nettali bi nu Bóris di baaxe, walla boog xew-xew yim nuy saabal, muŋleen jukkee ci jéyya ji fi amoon, daanaka 20i at ci ginnaaw : suuxu Gaalug « Joolaa » gi daan lëkkale Ndakaarook Sigicoor. Ndeysaan, ba tey, askan waa ngiy jooy 2000iy doom-aadama yi ci labe woon. Rongooñ yooyoo tooyal xolu bindkat bi ; mu boole ciy yosam, def leen daa. Ci daa ju tiis jooju te lëndëm la capp xalimaam gi. Ngir biral metit ak njàqare yi 1883i way-labu Gaalu Joolaa gi doon yëg, keroog ba ñuy lab. Dafa di, bu sañoon, bakkan bu ci ne, dina biral sag dund. Maanaam, « 1883 toqi deret. Ak benn. Bunu fàtte benn toqu deret boobu. Bunu ci fàtte benn, sax. » Waaye, kim ci tànn doy na misaal ñeel way-lab yépp. Li ko waral mooy ne, kooku, dub como. Mukk ! Soxna Kinne Gaajo mi Bubakar Bóris di nettaliy jaar-jaaram ci téere bi, ab taalifkat bu mag la woon, siiwoon lool. Gis ngeen, soxna soosu, turam wër na àddina ndax rafetaayu xalimaam ak solos mbindam. Aka xareñoon ! Ndeysaan, bu dul woon tolof-tolof yim daan jànkoonteel, kenn waxatu ko tey. Bare na ñuñ fiy kañ ak a tagg te Soxna Kinne Gaajo xoolu leen sax. Waaye, ay nattoo ko gaaraloon ba mu àggoon ci di jaay boppam guddi gu nekk ci benn goxu Ndakaaru – Caaroy. Laaj bi bindkat biy laaj ci téere bi, « Taalifkat walla lagara ? », loolu lay wund. Ndege, Soxna si, ñaar yépp la boole woon. Moom sax, Kinne Gaajo ci boppam, jéggi woon na loolu lépp. Ci dëgg-dëgg, moom daa bokkoon ci nit ñu kéemaane yooyu nga xam ne, bokkuñu ak nit ñi doxalin. Foo ko fekkaan, ciy feemi boppam la daan deme, di ci doxe, di ci waxe. Feemi boppam kese, nag ! Maanaam, nit ku moomoon boppam la ; dara tënku ko woon te tënkuwul woon lu dul ci li ko safoon. Bu yeboo ñu ne, Kinne Gaajo, amul woon tiitukaay. Moo tax bindkat bi ne, « Kinne Gaajo masul a def leneen lu dul jéem a xàll aw yoon. Yoonu boppam. » Looloo tax ay dëkkaaleem ak i xamaaleem jàppe woon ko ni ku ràkkaaju, ku yenuy dàllam, maanaam ab dof. Jaar-jaar bu doy waar boobu la xaritu-ndawam, doomu-ndeyam ji Njéeme Pay, di nettali, gannaaw ba mu réeree (ak i taalifam yu bare) ci géej gi. Mu mel ni ku nuy fàttali mennum Dawid Jóob mi fi woon : « Mu mel ni kon Dawid Jóob ak Kinne Gaajoo bokk àtte foofu. » Njéeme Pay, taskatu-xibaar la woon. Mi ngi ame woon lijaasam ci lekkool bu mag boobu ñu duppe Cesti. Ku xareñoon lool ci liggéeyam la. Cib rajo biñ moomaloon seen bopp, moom ak i àndandoom, la daan liggéeye. Rajo ba, Péncoo FM la tuddoon. Ndegam moo dencoon kayiti xaritam yi, Njéeme Pay dafa jàpp ne, sas la ci moom : « …sas nañ Njéeme ». Loolu moo ko tax a yéene biral taalifam yu am maanaa yi mu fi bàyyi, ba noppi « … xamal askan wi kan moo doon Kinne Gaajo… » ndaxte, « Àddina ba àddina daj, amul ku sañ ni moo ma gën a xam Kinne Gaajo. » Lim ko dugge mooy fexe ba àddina sépp xam kan moo doon, dëgg-dëgg, Kinne Gaajo. Njéeme daal, tawax na temm fas yéene noo nettali Kinne Gaajo.  Konte, Njéeme Pay, sàmmonte na ak kóllëre gi doxoon ci digganteem ak ndem-si-Yàlla ji, xaritam. Fi Njéemey daanele nettaleem bi la ko keneen di aw, jël kàddu gi, jokk nettali bi. Loolu, nag, ci feemi bindkat bi la bokk. Ndege, aw-awley nettalikat ci téereb nettali, du lu bees ci mbindiinu Bóris. Njëkk na koo def ci Doomi Golo. Ndaxte, xew-xew yi daan am ca Ñarelaa, góor gi Ngiraan Fay mi doon xaar bésam a nu leen jëkk a jottali laata muy faatu. Gannaaw gi, Aali Këbóoy mi ñépp jàppe woon dof (nees jàppe Kinne Gaajo itam), moo mujje àggale li nu Ngiraan doon nettali. Nettalikat biy aw Njéeme Pay ci Bàmmeelu Kocc Barma, jigéen la ni moom. Te, ndeyu-mbill gi ci boppam, Kinne Gaajo, ca barsàq ja mu nekk, mooy wéyal nettali bi… Moom la sax de. Baatam beey bëtt suuf si ko sàng ca bàmmeel ba mu roñu, di jib ba ci téere bi. Noonu, mu daldi dekki, di nu xamal ay jaar-jaaram ak i yëg-yëgam. Jàngkat bi, nag, mënul lu dul topp bindkat bi cib « dóor-dàqe » bu dul jeex. Mel ney àndandoo yuy dem ba yàgg, réeroo ; ku ci nekk di wër keneen ki. Ndaxte, yuq gi lal Bàmmeelu Kocc Barma yépp, ci diggante ñaari way-jëmmal yooyu – Kinne ak Njéeme- la ràbboo. Waaye, yemu fa de. Déedéet ! Dangeen a desee xam Bóris rekk. Waaye aka cee aay ! Moo taxit, defatina mëninam. Day wër-wërloo ak yow, naan la  « … naxee-mbaay… ». Noonu la lay def, di la wommat, yow miy jàng téereem. Ruq-ruqaan bu nekk mu dugal la fa ; dëkkoo-dëkk mu wërloo la. Tey. Démb. Ëllëg… jamono yépp lay boole ràbb, fu ne mu yóbbu la fa. Moom daal, tëralinu mbindiinam a deme noonu, xoromu lool nag ! Way-jëmmal yiy jëf ak a jëflante ci téerey bindkat bi, mëneesul a xam fum leen di loqatee. Dafa di, ñoom, dañuy méngoo ak jëmm yees leen di melal ba ñu faf mel niy nit dëggantaan. Sàllaaw ! Te, ku la ci gën a am maanaa, nga ne kii. Jëlal taskatu xibaar bu xereñe bi te gëm liggéeyam, « Te surnalist bi, liggéeyam du dara lu dul taataan i xibaar, siiwal leen. », doy na firnde. Walla nga xool kiy mbubboo surnaalist, di mbuxum ak a jaayu ngir lu mu def ci poosam ba mu dëll. Mooy ku njublaŋ kooku, te mu fexe ba yoxosu, dugg ci biir surnaalist yi, fexeeti ba bokk ci seen i njaatige yi gën a am doole ; kooku noonu rekk demoon bay noggatu politiseŋ yu ñàkk-jom yi, « Te kilifa gu fi am alal mbaa bayre mu luqati say mbóot, ni la soo ma joxulee nàngami milyoŋ ma def sama liggéey ». Waaw, kii nga xam ne nag, taal fitna rekk a ko soxal, « Nun surnalist yi nag, na ma Yàlla baal waaye liggéey bu doy waar lanuy def : su musiba dalee ci kow askan wi, lu mu gën a réy, gën a metti, nu gën a raatukaan. » Waaye, geestul it liggéeykatu bànk bu maandu bi, walla waxambaane wu lafañ wii moroomam yiy tooñ,« Am na ñu ma doon kókkali, naan booy bii bumu nu sonal, lafañ doŋŋla. » Nanga xool yit politiseŋ yu ñàkk faayda yi. Nóoxóor yi nga xam ne, seen biir doŋŋ a leen jiital, tax ba bindkat bi (mën a tooñ ba dee !), boole leen ñoom ñépp, waa Nguur geek Kuje gi, di leen ñaawal,« Yëf yi powum mag doŋŋ la : kenn du taxawal pàrti ngir defar sa réew walla jëmale ko kanam. » Mu am it jeneen jëmm ju am solo ci nettali bi, moo di ndeyu Kinne Gaajo, jigéenu kaw gi, di néew-ji-doole ju ñàkk lépp ba mu des jikko ju rafet ak jom, « Moonte Yaa  Ngóone, lim ma won moo doon ne ngor, tabe ak njub, fépp fu suuf si ŋàyyeeku goqiy doomi-aadama, soo demee fekk leen fa. »… Xanaa du noo ko gisandoo ? Ndax deesul a fekk way-jëmmal yu ni mel ci mboolem-nawle mi ? Konte,  mel na ni, Bubakar Bóris Jóob du cib maaliforo lay tabaxe ay way-jëmmalam, Ñi mu nuy indil ñépp, dañuy mat li mu leen soxlaa ba jëmmal leen. Ni tëgg biy naxanteek wurus wi, walla tabaxkatu ndaa biy mooñ banam, « Noo mënti def, fàww nga gajafal ban bi, di ko mocc, di naxanteek moom, daanaka, ba mu miin sa nuggaayu loxo, nooy nepp, ni nemm, lu la neex nga def ko ci. Soo nee : ‘Amoon na fi’, mbooloo mi ni tekk di la déglu, bala ngay sañ ni : ‘Fa la léeb doxe tàbbi géej, bakkan bu ko njëkk a fóon tàbbi Àjjana !’ dinga wax lu set. Wax lu set mooy rekk : teqale, tasaare, ràbb, ràññee bu baax kañ la fen di jur dëgg ak kañ la dëgg di yées fen. Mooy : jëmbët fulla ci sa liggéey – bind liggéey la war a doon – te lu mu metti metti nga muñ ko. » Liggéeyu bindkat bi daal, duy caaxaan walla lu yomb ! Bóris bëggul lu yomb, utul lu yomb. Moo tax, way-jëmmal yi muy tabax làmboo maanaa jees leen xame. Li koy gënatee màndargaal mooy ñaar ñi gën a yées jikko ci Bàmmeelu Kocc Barma : surnalist bii di Lamin Jàllo ak politiseŋ bii di Ngañ Demba. Ndaxte, ñoom ñaar ñooñu kat, li ñuy bon a bon yépp ci jikko, ñoo ciy tamit, ñi ci ëpp xorom, neex deret ba, ñàkk leen a bëgg day jafe. Ndax Bóris jëlul ay nit dëggantaan, ñu xam leen am déet, dugal leen ci téereem bi ? Bokk na ci màndargay téere bi, ñenn ci way-jëmmal yi bokk ci way-labi gaalug « Joolaa bi ». Fës nañ ci téereb nettali bi lool, sax. Nde, bindkat bi dina dem ba am ñu mu ciy tudd seen i tur dëgg, ànd ceek kersaak yëg-yëg gu réy, ndax li mu leen xamoon, moom ci boppam, ci bi ñuy dund. Xawma kan, waaye kilifay nguur gi, ñoom, Bóris moyuleen ci téereem bi. Waaye, moo yey xalab leen. Ndax, kat, ñooñu, defuñu lu dul féex, ñàkk yitte, ñàkk aajo, doyadi ba nga ni lii lu mu doon ! Rax-ci-dolli, ñoom ñooñu, ñooy ndeyi-mbill gi, ñoom ñi sàggan ba musiba bu ni mel dal ci kow askan wi. Ak seen yambaraay ! Ak seen cuunewaay ! Ñu waroon a walluji way-lab yi, génne leen ci seen njàqare ji, waaye ñu nooyal ba ñooñu mujjee dee. Bu nu waxantee dëgg rekk, ñoom politiseŋ yi, ci yeneen i itte lañ nekkoon. Ki koy firndeel mooy Seneraal bi làngi woon ca coroom ba, jamono ji jéyya jiy am. Te, boobu, kenn ñemewu ko woon a gëtënsi, fa mu doon gundaandaat, di ko yëgal balaa ba amoon ca géej ga. Waaye, du njiit yi kese ñoo sikk. Askan wi tamit, kenn demul ñu des. Nde, mooy la waa ji waxoon rekk, askan wu nekk, njiit ya mu yeyoo lay am. Réew moo dem, na askan wa mel, noon lay njiitam mel ndax ca askan wa lañ soqeekoo. Bu ko defee, cuune, yaafus ak càggan yi kilifa yi àndal ba tax jéyyab Joola bi dikkal nu, dees na leen fekk ci askan wi. Loolu la nettalikat bi xam ; ndax ku mën a seetlu la ndeke. Moo tax, deñul ciy sulli mbóoti askan wu déggadi wii, tigi, « … xoolal ma kalandoo yi, njaga-njaay yeek kaar-rapit yi, fu leen neex taxaw, ku ci alkaati laaj say kayit nga tàllal ko kayitu téeméer gu tilim mu lem denc, ni la soo ñibbee ngoon nuyul ma Jekk-Tànk ! » Doxalin bu ni mel, nag, warul a bett kenn. Ndaxte, dara yàqul Senegaal lu dul yëfi maa-tey ak maslaa bu ëpp. Nde, Senegaal mooy réew moo xam ne« … lu neex waay mu def te dara du la ci fekk ! ». Bi Joolaa bi suuxee ak léegi ba Njéeme Pay di nu ko nettali, am na daanaka 20i at. Waaye, la woon, fa woon, na woon. Jikko yi soppeekuwuñ. Moom, kay, ndax yéesul sax lees di laaj. « Lu fi xewati sama ginnaaw ? Pólitig rekk. Ndékkee pólitig, añe pólitig, reere pólitig. Kon, ci gàttal : dara lu bees xewu fi. Masàmba randu, Mademba riigu. Waaye Mademba, dañ koy wax nag te dee, masutoon a xalaat ne bés dina ñëw mu ne faax ci jal bi. Fit wi rëcc, mook soxnaam ñuy giroo cere ji, di ko caxat-caxatee, ku ci gën a fëqle sa moroom nga ne kii la ! ». Jikko de, dinañuy wax ne laago la ! Te, laago du wér. Am déet ? Nun nag, njort nanu bu baax ne, ci gis-gisu Bóris, tóoxidóoni bu « Joolaa » bii, amul lu ko gën a ñàng : « Bi Senegaal dee Senegaal ba tey, dara masu fee xew lu ëpp solo suuxu Joolaa bi ». Monte, ñakkul ne, xew-xew yooyu yépp, lenn rekk lay wund : dàq ganaar, waxaale sa soxla. Maanaam, dafa mel ni bindkat bi day sukkandikoo suuxu Joola bi ngir xamal nu leneen : ngir tey gëstu bi muy gëstu ñeel aadaak cosaanu askanam. Uséynu Béey (Ñaareelu pàcc bi feek i fan)
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-9/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM CAN-SENEGAAL : JOŊANTEB XARITOO Ëllëg, ci altine ji, bu 18i waxtu jotee la Senegaal di daje ak Niseer ca fowu ba ca Jamñaajo. Muy joŋanteb xaritoo bees taxawal ngir waajalee ko CAN bi war a tàmbali 13i fan ci weer wii. Bu ñu noppee ci loolu, ndawi Senegaal yi di waajal ngir dem Koddiwaar. ÀNDRE ONANA Góolu Kamerun bi fekkijeegul i naataangoom ca seen waajtaay ya. Lu ko waral nag, moo di ne Manchester United dafay amal ab joŋante kub moom ak Wigan ëllëg ci altine ji, ak joŋanteb sàmpiyonaa moom ak Tottenham keroog 14i fan ci sãwiyee wii. Bu ci noppee lay daldi fekkiy moroomam ya. Loolu nag, waa Manchester United ñoo ci waxtaan ak waa Kamerun ba juboo ci. CAF YOKK NA NDÀMPAAYU CAN BI Senegaal mi jël CAN 2022 bi jotoon na lu tollu ci 2i tamñareet ak 997i tamndareet yu teg ci sunuy koppar. Ci wii yoon nag, waa CAF dañu daldi yokk yëf yi ba ci 4i tamñareet ak lu teg. Moy lu am solo lu ñépp rafetlu. PAAP MATAAR SAAR FEDDALI NA PASAM Doomu Senegaal ji moo ngi jóge woon Metz (Farãs) fekki woon Tottenham daaw. Ren nag, dafa wane xarañte ak jom ju ko yóbbe mu bokk ci ñay tàmbali saa su ne ca ekib ba. Ci loolu, mu jubook gaa yi daldi féddali pasam ca ekib ba ba atum 2030. LÀMB JI Ci altine jee weesu, di woon fan wu njëkk ci atum 2024 wii, la Móodu Lóo doon daje ak doomu Pikin jii di Booy Ñaŋ 2. Waaye, daf ko jaarati fa mu jaar ay magam. Doomu Pàrsel ji waneeti na mën bëreem ak faaydaam ci cëru buuru làmb ji mu yore. Niki mu daanee woon Ëmma Seen ak Aama Balde, noonu la daanaatee Booy Ñaŋ 2. Mu mel ni, léegi daan na ñees yaakaaroon ni mën nañu ko të ca biir Pikin. Fim ne nag, ñoo ngi seet kan ay jekk ci moom ngir boolee leen. Ay tur a ngi jib boobu ba léegi, ku ci nekk naan diw baax na ci moom, waaye jàppaguñ dara.
https://www.defuwaxu.com/moodu-loo-daan-na-aamaa-balde/
MÓODU LÓO DAAN NA AAMAA BALDE Xaar bi yàggoon na lool, waaj gi tamit naka noonu. Waaye, ñaari mbër yi mujje nañu sëgg démb ci dibéer ji. Móodu Lóo ak Aamaa Balde bëre nañ démb, ca aareen nasiyonaal ba ca Pikin. Móodu Lóo moo daan, yóbbu ndam leek metel mi (la couronne) Pàrsel. Seen làmb ji, bi ñu ko dalee waaj, yàggoon na lool. Jotoon nañ koo àppal ca njëlbeen laat ñu koy bëtal ci sababi gàllankoor. Moo taxoon ñu dàkkoon ko ba jëmmi jamono. Démb nag, ci dibéer 5i fan ci nowàmbar lees ko jàppaatoon te mujje na am. Ci fan yii ñu génn, gisees na ñaari mbër yi, Aamaa Balde doomu Pikin ji ak kii di Móodu Lóo doomu Pàrsel ji, ni ñu doon waajalee bés bi. Amaloon nañ ay jàkkaarloo yu saf sàpp. Werente bi bari woon lool ci diggante soppe yeek farandooy mbër yi. Fan yii ñu génn ba tay, foo geestu nit ñaa ngi ciy wax, ku ci nekk naan sama mbër a mën, sama mbër ay daan. Mënees na wax sax ni làmb dafa mel ne lu dekki. Nde, toogoon nañu jamono yoo xam ne yii, bu mbër mu mag waree bëre sax kenn du ko yég, mbaa ñu ci bari bu desee ay benn fan, ñaar lañ koy yëg. Bëre Aamaa Balde beek Móodu Lóo bi nag, dafa dekkil làmb ji, naatalaat géew gi. Jaadu na nag, ndax ñaari ndaanaan a doon daje, ku ci nekk mbooloo nekk sa ginnaaw. Móodu Lóo yàgg naa def i jaloore ba jël metelu làmb ji (la couronne de l’arène), nekk buur bi, maanaam « Roi des arènes ». Ci Ëmma Seen, moom it di doomu Pikin, la ko nangoo woon. Gannaaw loolu, Ëmma dikkaat ngir nangu ko, saa-pàrsel bi daldi koy bañ, daanati ko. Ba tax na, mënees na ni loolee yokk jom kii di doomu ndem-si-Yàlla ji, Fàllaay Balde, ci mu gën a ñafe ba ñu taxawal bésam ak Móodu Lóo. Li war ci bés bi yépp nag, ñaari mbër yi def nañu ko. Ci bés bi, ku ci nekk ñëw na na mu waree, bàkku, neexal bés bi, yëngal fowu bi (Arène national). Cokkaasante nañu, xarfa-fuufa yi ñépp gis nañu ni ku ci nekk ci ñoom ñaar def nga ci xaalis bu weex tàll. Amaa dikkee na nañu ko xamee woon, Móodu, wàllu sangu bi ñëwee na ci nees ko miinee woon it. Waaye, ci wàllu téere, dafa dëggal li mu ne : « woon weesu na fu may takkatee gàllaaj yu bari ndax làmb. » Ba ñu defee loolee lépp nag, la arbit bi daldi woote ca digg géew ga, ku ci nekk ñaan la muy ñaan, léemu ay léemoom. mu laaj leen ndax pare ngeen, ñu ne waaw, mu daldi sex mbiib ba rekk ëf ca. Ñépp ne tekk, fowu ba ne selew, soppe yépp jël xol yaak xalaat yaak yépp jëmale leen ca bëre bi, ca ñaari mbër yay laale. Ñaari mbër yi tàmbaley léewatoo, ci ay saa, Amaa daldi tàmbali di dox ci kaw Móodu Lóo, nees-tuut ñu tàmbalee sànnantey kurpeñ rekk roofaloo. Doomu Pikin ji dóor mboot, Móodu ci mën bëreem, rocceku Amaa rëpp, samp ñetti cër ya, doomu pàrsel bi wër ko ndombo, jekku ko, di ko rokkoos ak nokkoos. Dóor yi mel ni mbàccum gerte. Móodu Lóo tiim Aamaa Balde, jàpp kanam giy dóor rekk bañ a bàyyi. Biir dóor yi mettee ba metti, as waay a dawee ci bitig géew ga, romb takk-der yi, ñëw laxasu Móodu Lóo ngir wallu Aamaa mi mu àndal. Ca lañu àttee ñaari mbër ya. Lu leer ba leer, ci soppey Amaa Balde yi la. Ndaxte, moom lañ jekku woon. Gannaaw loolu nag, arbit yi gise, dem ca “var” bi nga xam ni lu bees la ci làmb ji, bii di ñetteelu yoon biñ ko jëfandikoo ci làmb ji. Ci seet, settantal ñu jox kii di Móodu Lóo ndam li, mu delloowaat nguur gi Pàrsel. Waaye, lenn ci lu ñuy rafetlu mooy ba ñu joxee doomu Pàrsel ji ndam, Aamaa Balde daldi ko jox loxo, kott ko, ndokkale ko, muy lu ñu bëgg ci bés yile, tubaab di koy wax “fair play”. Bu lépp weesoo, lenn ci lees war a bàyyi, mooy li am démb, ay sàmbaabóoy di bawoo fële di duggu ci géew giy yàkk làmb ji. Lees war a wutal saafara la balaa muy wéy di bari. Te, loolu, liggéeyu takk-der yi la, ñoom ñi war a sàmm kaaraange nit ñi.
https://www.defuwaxu.com/xeesal-walla-xeeb-sa-bopp-2/
XEESAL WALLA XEEB SA BOPP? Kañ la jigéeni Senegaal yi tàmbalee xeesal ? Fanweeri at ci ginnaaw ? Lu ko ëpp ? Gëstukati réew mi war nañoo tontu ci laaj boobu. Li ma ci xam, daal, moo di ne mu ngiy bëgg a yàgg. Mel na ni ca njëlbéen ga ñu bare dañu newoon ci seen xel : ‘’Lii de, baaxul, waaye ay feemi gone la rekk, du jikko, jamono la, léegi ñu génn ci !’’ Njuumte lu réy la woon ndax fi mu ne nii, yematul ci jigéen ñi, ay góor sax a ngi diwu… Ku sañul ni bala la yit, xalaat nga ko. Ku weddi ne tey la Waalo gën a aay, doxantul ci mbeddi Ndakaaru yi, téen xool nataali-siiwal yiy tagg xees ak xeesal. Boo toogee sa kër tamit, taal sa tele dinga gis ñu ciy wane ndaw suy diwu, yànjal la ko ba nga ni lii lu mu doon, nataal yi di la déey musiba, naan la ‘’Nii nga war a mel !’’, walla : ‘’Nii nag la sa soxna war a mel !’’’ Wax ji moom jarul a yërëm, li xeesal tekki moo di ne am der bu ñuul gàcce la, taaruwl dara, loo gën a nirook Tubaab ñu gën laa teg nit. Mbir mi dafa dagg xol ba noppi yéeme. Xéy-na lu ni mel mënoon nañ ko séentu feneen ci Afrig fu dul Senegaal. Liggéey bu mucc ayib bi Séex Anta Jóob def ngir weglu nit ku ñuul waroon naa tax nu àndandoo sib xeesal. Te yit, xanaa Senegaal dootul réewum ‘’Négritude’’ ? Xanaa du Seŋoor a bind ‘’Femme noire’’, taalif bi gone yiy tari subaak ngoon ? Lii lépp a merloo woon Aysa Dem, mi ñépp xam ci farloom ñeel mbiri aada, ba mu jiite fi kàmpaañ, duppe ko ñuul kukk di fésal taaru jigéen ju ñuul ak ni nit ki waree naw boppam. Fulla ju mat sëkk la Aysa Dem wane foofu te ñu bare gërëm nañ ko ci. Waaye li gënoon xéy-na moo doon ñépp àndandook moom ci xeex boobu. Mbootayi jigéen ñi nga xam ni foo leen fekk ñu ngi ñaxtu, naan dañoo sàggane seeni yelleef, kenn waruleen woon cee jiitu. Léegi, nañu yëkkati seen kàddu, wax kilifay réew mi ñu aaye kuy def piblisite xeesal, aaye sax xeesal ci boppam. Am nay jàngoro yoo xam ni gornmaa rekk moo leen mén a faj. Xeesal ci la bokk. Loolu la Paul Kagamé, njiitul Ruwandaa, xam ba jël ay dogal yu am solo, tere kuy dugal walla kuy defar diwu yu ni mel ca réew ma, tere yit ku ko jaay, ku ko jënd mbaa ku ko jëfandiko. Loolu lañ fa dogal te ku ko moy yoon dal ci sa kow. Teewul doktoor yeek yeneeni boroom xam-xam war di wéy di gindi jigéen ñi, di leen yee ba ñu xam ni nit ku weex gënul nit ku ñuul. Waaye liñ naan bóli gu dog tiiñ na doktoor moo fi ne. Ndax ndaw soo laaj lu ko xiir ci xeesal mu am ci kersa, damm loos ni la lépp ak góor ñi, soo xeesul duñ la faale. Ñu ci bare leeral rekk a leen ciy dugal, ñu dem ba yëf yi ëpp leen loxo, fu ñu gis diw jënd ko, diwoo. Moonte xam nañ xéll ni xeesal day oyofal sa der, wàññi dooleem, foo laal daj ay picc ak i rew ak i taas, soo moytuwulee jële ciy feebar yu bon niki kañseer walla taŋsiyoŋ. Doktoor yi seen xam-xam màcc ci pajum der wax nañu ba tàyyi, waaye kenn nanguwuleen a déglu. Waaw, ndax wut taar rekk jar naa ñàkk sa bàkkan ? Ñàkkul jaaykati xeesal yeek isin yi koy defar la nguur gi ragal ba tax ko ni patt-pattaaral, di seetaan lu ñaaw lii mën a delloo réew mi ginnaaw. Am na ñu naan du loolu lépp, dafa ferekk ni sunuy njiit tal nañu leneen, nun baadolo yi amaluñ leen benn solo. Xanaa kay du loolu laa yaakaar ? Ku xeeb sa bopp, dem sax ba xamatoo yaay kan, mënoo amal benn njariñ saw askan. Kon, nanu ci jóg gaaw : xeesal jëmul kër… Ndey Koddu Faal XEESAL WALLA XEEB SA BOPP ? was originally published in Defu Waxu on Medium, where people are continuing the conversation by highlighting and responding to this story.
https://www.defuwaxu.com/sigaret-baaxul-waaye-afrig-la-yeese/
SIGARET BAAXUL… WAAYE AFRIG LA YÉESE ! Fan yii weesu, Marie Maurisse, ab taskatu xibaar bu fekk baax Siwis, bind na bataaxal bu jar a bàyyi xel. La muy ciy nettali mooy ñaawtéef yu këri-liggéeyukaay yu mag yiy jaay sigaret ci réewi Afrig yiy def, te sunuy gornamaa ne yàcc di leen seetan. Tóx baaxul, loolu dëgg gu wer péŋŋ la, kenn sañu koo werante. Képp ku koy def, sa bakkan a ngi ci xott, dina la feebarloo, gàttal say fan. Teewul bitig boo dugg Senegaal mu ngay jaay sigaret ; li am ba am moo di ne nguur gee ko daganal, di ci jël moyaal. Li ñu Marie Maurisse di xamal nag, teg ko ci ay firnde yu leer nàññ, moo di ne xeetu sigaret yi ñuy jaay Afrig, ñoo yées fopp yi ñiy jaay Ërob, ca réewi Tubaab ya. Mën nan koo metitlu waaye warunoo bett ndax Afrig yàgg naa doon ‘’Mbëbësu” Ërob. Kolobaan gii, boo fa doxantoo, dinga fa fekk ay jali jali fëgg-jaay, maanaam ay yëre yuñ sol Ërob ba sànni leen ci mbalit mi. Yàggul dara, daaw-jéeg rekk, lanu dégg ni esãs ak gasuwaal bi ñuy jaay fii ci Senegaal ak ci yeneeni réewu Afrig, kenn sañu leen a jaay Fràs walla Almaañ ak ñoom seen. Lu ko waral ? Xanaa seen mbon ci wér-gi-yaramu doom-aadama. Bi ñu siiwalee li Marie Maurisse bind, Philip Morris, këru liggéeyukaay gu mag gi ubbi fii Senegal ab isinu sigaret, daldi nay tontu. Ñaari mbir a jar a fësal ci li mu wax : bu jëkk bi moo di ne Philip Morris weddiwul ni sigaret yi muy jaay Senegaal ñoo yées yi ñuy jaay Ërob ; ñaareel bi, nag, mooy, sunu wér-gi-yaram gi ñuy fowe, nee na ci li ko nguuru Senegaal may la ko teg. Waa OMS, kurél gi ñu dénk lépp lu jëm ci wér-gi-yaram ci àddina si, firndeel nañ ni fileek 2030, limu tóxkati Afrig yi dina ful ñaari yoon. Ërob moom, tàmbalee naa xeex ak doole sigaret, ngir aar ay ndawam, fexe ba ñu bàyyee tóx. Looloo tax defarkati sigaret yu mel ni Philip Morris jàpp ne liggéey ak Afrig moo fi sës, sunu réew yi amal leen lool solo. Ci gàttal, nun nooy seeni nooy-neex, seen yoon newul ci sunu wér-gi-yaram. Bu sunuy njiit amoon fullaak faayda, yittewoo seen bànneexu askan, neneen la mbir miy deme.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-8/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM CAN 2024 Amara Juuf bokkul ci 55i futbalkat yi Alin Siise tànnagum ngir yóbbu leen ca CAF laata mu di ko seggaat ba 27. Moom, kàppiteenu U17 bi, fim ne ma nga Metz ngir faju. Gaañu-gaañu yaa ngi bëgg a bari ci gaynde yi. Gànna Géy dolleeku na ca limu ñi gaañu fekki ñoom Séeni Jeŋ ak Nàmpalis Méndi. SUPER LIG Ëttu àttewaayu Tugal bi jox na dëgg Super League ci kaw UEFA, daldi koy daganal. Kon, saa suñu ko bëggee te mën ko sañ nañu taxawal seen i mbir te benn daan du ci fekk benn ekib niki woon ca njëlbéen ga. Gannaaw loolu nag, kii di Aleksander Ceferin, njiitul UEFA yëkkatina ciy kàddu yoy xol bu jeex lay niru. Mu ngi naan: “Mën nañoo taxawal lu leen neex. Di yaakaar ni dinañu gaaw a tàmbali seen joŋante bu xàttaaral bi ak ñaari ekib (Real Madrid, Barça).” Donte daganal nañu yëf ya, teewul am na ekib yu taxaw dàq boobu Super League, ñu ci mel ni Manchester United, Séville, Valence, Atletico Madrid, Bayern, Dortmund. GREENWOOD A NGI ÑËWAAT BU BAAX Gannaaw ndogal li daloon ci kawam ba taxoon yoon tegoon ko loxo laata ñu di ko bàyyi setal ko ci lépp, Manchester United miy këlëbam daf ko bañoon a jëlaat daldi koy abal Getafe (Liga). Fim ne nag, moo ngi wane boppam bu baax ca ekib ba di dellusi bu baax ci nees ko xamee woon. Amagum na fa 3i bii ak ñeenti paas. BUNDERSLIGA Bayer Leverkusen mooy ekib bi njëkk a dawal ca sàmpiyonaa Almaañ ñaar-fukk ak juróomi joŋante yoy ñàkku ci benn. Loolu di gën a dëggal taxawaayu ekibi ak liggéey bu rafet ba fa Xabi Alonso di def. Thomas Müller yokk na pasam ba atum 2025. Moom nag digganteem ak Bayern xanaa aj dàll rekk a koy tax a jeex. Nde foofu rekk la fas yéene futbal ba keroog muy bàyyi. Victor Boniface jëlatina raaya “Rokkie” ca Bundersliga ba. Gii di juróomeelu yoon bu mu tegale di jël raaya gees jagleel ki gën a xarañ ci weer wi.
https://www.defuwaxu.com/2020-mbas-mu-derkiis-nakk-teggin-tey-jur-tiinalante-ci-biir-reew-mi-ak-ci-bitim-reew/
NAKA LAA GISE MBAS MI Mbas mu dërkiis, ñàkk teggin tey jur tiiñalante ci biir réew mi ak ci bitim réew…. Naka la doomi Afrig yi war a taxawe ? Céy mbas  mee gudd tànk, moom mi fàqe Penku,  ca Wuhan, ca Siin, ca Asi, sóobu ci Afrig, ba ci Géeju Atlantig, daanu ci fii ci Ndakaaru (dëkk raw) ; ci Tànk (Wakaam, Ngor, Yoof) fekk ñu fi ! Balaa moo agsi, wëndéelu na, jaar Ërop, jaar Amerig ! Kon boog dab nañu, yëngal na jamono, yëngal àdduna wërngël  képp, wërngël këpp, wërngël këtt. Li bees Moonte ku xam jaar-jaari taarixu nit, xam ne du guléet musiba ak balaa xëppu ci gox, dëkk, réew, mbaa pàcc ci dunyaa. Li bees kay, moo di mbir mi ni mu gaawe, bette ak  law ; dëgg la, li ko waral moodi dem ak dikk bu gaaw te bare ci àddina, yéenekaay yu bées te ratax. Ak covid 19 tiitànge ak njàqare bare na, ñi faatu wax i nopp, moo xam góor, moo xam jigé. Mbas mii bàyyiwul ndaw te yab na mag, waxatumaak màggat. Ma nga doore Siin, faat fa ñu bare ; dàqe ji Tubaab yi Ërob ak Amerig, Naar yi yuuxu, sarxolle, mu mujj, dabsi nit ñu ñuul ñi, fii ci Afrig, fii ci Senegaal. Moone de doomi-Senegaal yi demoonañ ba yaakaar  ni dañoo tul, mbaa Yàlla ñoom rekk la bëgg. Li yëngu, li ko yëngal… Li jaaxaal ñépp, boroom xam-xam yi, doktoor yi, fajkat yi ak njiiti réew yi, mooy mbas mi kenn xamul li ko sabab. Mbaa du gëstukat yu waane ñoo ko rëccal walla lu ñu sos la, te tey ko, walla ndax bëre ay ponkal la ci politig, walla koom-koom ? Xey-na dina mës a leer bés. Li yëngu daal, li ko yëngal moo ko ëpp doole. Li ko yëngal nag, ndax ci njugub la jóge, mbaa meneen mala mu ñu doon jaay ca marse ? Koronaawiris ndax daa mel ni fel, mbaa teeñ, mbaa saxayaay ? Doom bi,  ci saxayaay lay dund walla ci xobu-garab ? Xam-xamu seetantal dina ko mës a leeral. Li wóor mooy dugg na ci yaramu nit, di wàllaate, indaale yaram wu tàng ak sëqat su bon, dënn bu fatt ak bakkan buy xelli ak biir buy metti. War nañoo xeex jàngoro ji, bëmëx ko ci biti. Réew yépp loolu la ñuy jéem. Ñenn ni teel a fagaru, mel niki Siin, dem nañ ba bëmëx mbas mi ; ñi yéex a jóg, sàggan mel ni Itaali, Espaañ, Farãas, Amerig, waaru nañu, metti na lool ci ñoom, ña fa dëkk, juddoo fa, màgge fa, di fa tedd, ak ña fa ganesi mbaa wutsi wërsëg. Pexeyeek jumtukaay yi Bi mbir nee faax, yenn réew yi mel ni Siin jiital xam-xam, xel ak caytu. Naka noonu dañuy ber ñi jàngoro ji laal, def ay lël, door di seet garab yu mën a indi tan. Ci réew yu bare, am na ñu seen xel dem ci xam-xami Maam ya ak diine, ñu dem sax ba ni njaaxum yiy gën di bare ci àddina ñoo tax Yàlla mere ñu, delluwaat di cawe, ngir ñu  dellu ci dénkaane yi mu jaaraale woon ci Yonent yi. Jar na nu jàng, jàngaat, sóobu ci, tanq ci woyu Sëriñ Musaa Ka, Xarnu bi, xarnu bi ñu génn (XXel), moom  bàyyiwul koom, aada, diine, mbaax ak xarbaax, tarixa, yoonu mucc, texe. Moonte war nañu fàttali, mbaa xamle ni, sunu Maam ya, waa Këmit, Misra, Esipt, ñoo jëkk a bind ci dund ak dee ; mbégte ak naqar. Fii ci Senegaal Ci sunum réew, ki ko jiite, toog ci jal bi, Parsidã Maki Sàll, woote na waxtaan ak njiiti làngi polotig ak mbootaay yi ànd ak jamono yiy aar  liggéeykat yi, waxtaan ak dippite yi, ndawi réew mi ngir am lu mu yokk ci li mu xalaat ci bëre ak mbas mi. Ku ne def nga li la sa xel, xol, yaram, kàttan, mën-mën, pexe, gafaka may. Gëstukat yi, fajkat yi, def nañu seen keem-kàttan, ba mbir mi am fu mu yem, jéggeegul dayo. Bi mu agsee ba am fi weer, ñu gis ne laal na 195 nit, 40 % yi dañoo indaale doomu mbas mi,  dugal ko ci réew mi , 56 % dañu leen ko wàll, 4 % xamuñu fu mu ak naka la leen dabe. Loolu tax na, ñu war a gën a fagaru doonte xamuñu fépp fu mbas mi di jóge ; lii tamit la Porofesëer Musaa Seydi miy jiite xéex bi ci xam-xamu settantal ak paj denkaane. Ñi koy jàppale ci caytu gi ak jumtukaay yi, doktoor Ablaay Buso, Alfa Sàll ak Mamadu Jara Béey dalal nañu xel yi, joxewaale ay ndénkaane yu ñu mën a may ñu mucc ci. Dëgg la, am na doomi réew ñu ci jot a faatu, am ci ku doon ku am tur, fulla ak faayda ci réew mi ak ci bitim-réew, mu di Paap Mabaaba Juuf, ku ñu ràññe ci xam-xamu tàggat yaram, ak ci gunge xale yi ci futbal, dem ba jiite ekibu Màrsey, ca Farãas. Ëllëgu jàmm, tinkeeku ak tabaxaat Li am ba des moo di sàggan baaxul, wér-gi-yaram, jàng ak xam-xam war nañu leen sédd bu baax a baax. Ñu dellusi ci li mag ñu baax ñi dénkaane woon, fexe ba liy génn  ci pénc yi ak lël yu bare yi nuy amal, nu def leeni  jëf. Su boobaa luñu bett, ñu dékku ko, ci lu gaaw. Dëkk ci  fàtte, gàtt xel ak réccu ñoo ànd. Gëstukat yi am nañu sas bu réy, war nañu gën di waxtaan ci seen biir, di wax ak ñiy jiite ci yeneen fànn. Mbokk yi, at mii, nar na gudd tànk lool !Mu ngi mel na fasu benn tànk « rëkkal mba ma rëkk», nitu guddi ! Njuuma jaa ngook ! Am na ñu mu jaafurloo, mel ni Tubaab yiy wax nañu gaaw wuti garab, ñakk bu bees, jéemantu ko ci nit ñu ñuul ñi. Taat wuy tàkk moom kenn mënu ko solal tubey, kërandoom du set. Doomi réew mi, doomi àddina, jaaxle nañu ! Ku moytuwul nag tam sa moroom dëmm, tam sa mbokk nóoxoor Lu mën a dindi jaaxle ? Xana daal ñu dal, gën a njàccaar, yokk caytu gi, jàppoo ci fagaru gi, paj mi. Nu jeexal ci seetlu bi : réew yi ci muccagum as tuut, ci Afrig mel ni Lësotoo, Komoor, Malawi, Sudaan, Sawo Tome bokk nañu ci yi duggagul, mbaa yi sore xëccoo ak buuxante yu metti ci biir àddina. Kon boog nanu gaaw ci teggi tànk ci benn yoon, teg tànk bu bees, bu gën, te àndandoo jublu ci tabax Bennoo Afrig ci Mbokk. Nañu Taxaw Temm, am Pasteef, tegu ci Yoonu Askan Wi, Déggoo ngir Bokk, Bëre, Daan. *Baabakar JÓOB Buuba, Njiitu Mbootaayu Doomi Afirig yiy yëngatu ci Liifant ak Njàngum mag ñi, PAALAE (Pan African Association for Literacy and Adult Education) te nekkoon njiitu An@fa di bànqaasu PAALAE fii ci Senegaal
https://www.defuwaxu.com/demb-ak-tey/
DÉMB AK TEY Dal-leen ak jàmm ci seen xët DÉMB AK TEY mi leen seen yeénekaayu web LU DEFU WAXU jagleel. LU DEFU WAXU nag, li ko tax a jóg mooy dégtal leen ay xibaar yu wér te wóor te aju ci xew-xew yi gën a fés ci réewum Senegaal ak sax ca bitim-réew. Waaye tamit, bindkat yi dinañ  faral di leen ci baaxe seeni gis-gis ak i xalaati doomi réew mi ci mépp mbir mu ñeel Senegaal.  Rax-ci-dolli, yéenekaay bi dina leen wisal, may leen ŋeleju ayu-bés gi ak nataali ODIA, aji-ŋeleju bu mag bi. Bii-yoon, nag, seen yéenekaay LU DEFU WAXU da leen a indil lu bees tàq, mayati leen ko, muy seen xët DÉMB AK TEY. Ñaari baat yii, DÉMB ak TEY, ay tegtal lañu ci li xët mi wund. Jokkalekat bi, “AK”, di wone ne deesuleen  téqale. Maanaam, kenn warul a féewale cosaan walla jamonoy maam ya (DÉMB) ak sunu jamono jii (TEY). Bu ko defee, li nu ko dugge mooy dekkil cosaan, fàttali leen xew-xewi démb yu mag yi. Waaye nag, bàkk mbaa ŋàññ maam rekk yi taxunoo jóg. Naka noonu, jógunu ngir di leen nettali rekk li xewoon démb walla di leen léebal. Bu ko defee, nësër gi dëgg mooy lëñbëtil leen cosaan ak aaday maam ya, méngale leen ak jamonoy tey jii ngiree nu rotal ciy njàngat yi nuy jariñ tey, leeralal nu sunu ëllëg. Ci gàttal, xët mu bees mii nu duppe DÉMB AK TEY , li mu sasoo moo di wëral leen réew mépp, sowu ba penku, bëj-gànnaar jàpp bëj-saalum, béréb bu nekk mu taxaw fa xamal leen la fa xewoon ak njàngale yi ñu ci mën a jukkee. Ndaxte, cosaan mooy caabi jiy ubbi buntu tey, di làmp biy leeral ëllëg. Kon, cosaan deesu ko xeeb. Ndege, ku xeeb sa cosaan, ñu xeebal la ko. Seen yéenekaay LU DEFU WAXU xam na ni, wenn askan mënul a jëm kanam féeg mi ngi dëddu cosaanam. Rax-ci-dolli, réew mu askan wa naat, ci cosaanam ak i aadaam la sukkandiku ba indi fa ay yokkute. Looloo gënatee tax mu baaxe leen xëtam mu bees mii. Wolof dafa ne, kuy dem ba xamatoo foo jëm, war ngaa dellu fa nga jóge. Bu ko defee, sunu sas moo di dellu rooti ci teenu DÉMB, nàmpi ca meenu cosaan ngir tabax sunu TEY ak sunu ËLLËG. Seen mbokk, Paap Aali Jàllo moo nekk ci boppu gaal gi, di ko joow ci géejug cosaan, yen saa yi mu mbiij ci dexug aada, leeg-leeg moom walla kenn ci LU DEFU WAXU indil leen sarica. Tey, Daawuda Géy moo def ab gëstu ca Kaasamaas ci ñeyu-xare bu ñépp miin turam te taxul kenn xam ko bu baax : Jiñaabo.
https://www.defuwaxu.com/bank-monjaal-kurel-gi-nuy-jatan/
‘’BÀNK MONJAAL’’, KURÉL GI NUY JATAŋ Ñépp a ngi fàttaliku ni « Bànk Monjaal » nasaxale woon réew mi ci nguurug Abdu Juuf. Ci wàllu njàng, wér-gi-yaram ak mbir yu bari yu deme noonu, kurél googu fexe woon na ba Juuf génne ca loxoom, muy def lu ko neex. Loolu juroon na fiy jafe-jafe yu tar. Ndax taxoon na ñu jaay waa bitim-réew bérébi liggéeyukaay yu bare. Doomi-Senegaal yu bari ñàkkoon nañu ci seen liggéey, xale yi mënatuñu woon a jàngi te feebar faju jafe woon na. Ci gàttal daal, ci lu jëm ci yokkuteg askan wi, mbir yi sooxe woon nañu bu baax. Waa “Bànk Monjaal” doon bàkke Abdu Juuf: “Ndongol Bànk Monjaal li ko gën a nangul”. Réew miy wéy ciy jafe-jafe, ñu naan nu muñleen rekk, dina baaxi ëllëg. Waaye dara doonu ci woon dëgg. Jafe-jafe yooyu sax, bokk nañu ci li fi jële Abdu Juuf ci atum 2000. Noonu, Abdulaay Wàdd dikk, xaw a fippu ni àndut ak ñoom ci yenn gis-gis yi. Looloo mayoon nguuram sañ-sañu defar ay tali, def itam ay jéego ci njàng meek paj mi. Loolu dafay firndeel ni Bànk Monjaal ak kurél yu mel ni moom, réew yu mag yi lañu fi nekkal, ndax ñoo leen di suuxat. Ba tax na sunu njiit yi war nañuy settantal seeni ndigal, war nañuy jiital seen njariñu askan. Noonu la ko Peresidaŋ Néeru tamit defe woon ca réewum End. Ba ko waa ‘’Bànk Monjaal’’ joxee ay tegtal, rëddal ko yoon wi mu war a jaar, daa xotti lépp ba mu ko wóore ni bu ko defee réewam dina soox, jóge fa suux. Waaye bu dee ci sunu réew yi, fulla jooju moo fiy tumurànke léeg-léeg. Lu leen “boroom xam-xami tubaab yi” wax, ñu def ko am seew. Te moone ñooñu, seen njariñu réew rekk a leen yitteel ! Moone ba tey ‘’Bànk Monjaal’’ a ngi fi. Di digal sunu njiit yi ñuy jëfe. Moo tax tamit 59 at a ngi, ñu ne noo moom sunu bopp te mënagunoo dem fenn.
https://www.defuwaxu.com/riiru-kampaan/
RIIRU KÀMPAAÑ Lépp lu yëngu am na lu ko yëngal. Réewum Senegaal, jamono jii mu ngi toll ci waajtaayu joŋante bi ñuy fale kiy toog ci jal bi. Këru-Àtte gi gën a kowe fésal na juróomi wutaakon yu samp seen ndënd : Maki Sàll, Isaa Sàll, Usmaan Sónko, Madike Ňaŋ ak Idiriisa Sekk. Kenn ci ñoom la xelam toogatul fan yii, taluñu lu-dul kàmpaañ bi. Lawax yaa ngi jaabante, dëkkoo-dëkk ñu dem fa, di saafonteek ñaa fay yeewoo. Ñoom ñépp a ngi biral seen gis-gis ci doxalinu nguur ba noppiy tanqal askan wi ak i dig. Waaye Wolof Njaay dinay wax ne : dige, bor la. Naka noonu, ay ndaamaar lañuy war, foo toll di leen séen ñu yëkkati seen loxo ca kow, misig biy jolli. Lu kàmpaañ bi gën a jege di gën a rëb ; li koy firndeel moo di ne ñenn ci doomi-réew mi ñàkk nañu seen bakkan keroog bay farandoo Maki Sàll ak Isaa Sàll jàmmarloo. Wutaakon yaa ngi defante ba mu saf sàpp te ñi leen di jàppale kenn demul ñu des, fu nekk ñu nga fay daje, di def seen kem-tàttan ngir seen mbër jël ndam li. Kan lay doon bu bés baa ? Tont laa ngi ci yoon wiy ñëw…
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM Real Madrid a ngi wër góol bu bees Thibault Courtois, góolu Real Madrid bi,  dafa ame gaañu-gaañu bu metti (rupture des ligaments croisés) ba tax na dina toog diir bu yàgg door a góoluwaat. Loolu nag, jur na njàqare biir Real Madrid ba tax ñoo ngi ci wër góol bu koy wuutoondi ko ca caax ya. Jamono jii nag, ñoo ngi làmbaatu fu nekk. Christopher Nkunku dina gëj ci pàkk yi Moom Nkunku, bi ko Chelsea jëndee yàggul dara. Waaye, du gaaw a futbal. Ndax, dafa gaañu moom it ci oom bi. Dañu ko oppeere sax. Xamle nañu itam ni dina toog diirub ñeenti weer laata muy dóoraat ci bal. Kylian Mbappe demul Real Madrid Li coow liy bari lépp ñeel Mbappe, ndax dafay dem Real Madrid am am déet, Mbappe dafa noppi rekk, ni tekk tekkaaral. Ba ci alxames ji, mu daldi ciy àddu. Li mu xamal njiitu Paris Saint-Germain li mooy ne, moom Mbappe, dafay toog PSG, mottali at mi ko dese sog a dem ci coobareem. Jamono jii nag, bëgg-bëggu njiiti PSG yi mooy mu yeesalaat pasam ba 2025, nga xam ni déwén, buy dem ñu man ci am dara. Wàññeeku, Mbappe dafa bañ loolu. Lim bëgg mooy jeexal at mi ko dese, demal boppam. Noah Fadiga amaat na këlëb Doomu futbalkatu Senegaal ba woon, Xaliilu Fadiga, dafa mel ni li daloon baay jaa koy bëgg a dal, mbirum feebaru xol bi. Loolu waraloon sax këlëb bim nekkoon ca Farãs, Brest, dogoon pasam. Mu bañ a yaras nekk di tàggatook a faju ba amaat këlëb, Gant. Muy këlëb boo xam ni bii, baayam Fadiga nekkoon na fa menn at ci mujjantalu dundug futbalam.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-6/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM FUTBAL Victor Boniface moo ngi dox ci ndox Ataakã Bayer Leverkusen bi moo ngi wane boppam bu baax jamono jii ca sàmpiyonaa Almaañ ba. Lu tollu ci ñeenti weer a ngi nii (ut, sàttumbar, oktoobar ak nowàmbar) moom lees di tabb  ki gën a xareñ ci weer wi. Santos wacc na Këlëbu Beresil bi moo ngi am ren 111i at ba ñu ko taxawalee ak léegi. Ren jii di guléet muy wàcc ca ñaareelu sàmpiyonaa ya (D2). Loolu nekk lu doy waar ca boobu këlëb. Ndax, guléet la, te dafa doon ekib bu mag boo xam ni bii ay punkal ñu fa jaar, ñu ci mel ni Pële ak Neymaar… Musaa Wagee ngi dikkaat ndànk-ndànk Gannaaw gaañu-gaañu bu metti bi mu ame woon at yii weesu ca Barça, loolu bokk ci li wàññiwoon xareñteem, ca la doomu Senegaal ji mujje woon a jóge foofu dem ci këlëb bii di Anorthosis Famagouste, ca sàmpiyonaa Siipr. Mu mel ni mu ngi delsi ndànk-ndànk ci nees ko xame woon. Ndax, ci weeru nowàmbar bii ñu génn, moom lees tabb ki gënn a xareñ ca weer wa. Tijaan Jàllo wax na bëgg-bëggam ci ekibu Senegaal Bokkoon na ci ndaw yi teewaloon Farãs ci Kuppeg Àddina gees jagleloon ndaw yi ëppalagul 17i at yi weesu ci fan yii. Moom nag xamle na ni lu koy neex la mu futbalal Réewam mii di Senegaal. Loolu nag xëyna dina neex mbokki saa-senegaalam yi waaye ña di waa-Farãs njort na ni du yam ca ñoom. Loolu nag war a tax ekib bi ubbil koy loxoom donte daf koy boole ca ndaw ña ngir mu am lim bëgg ak ñu bañ ko xatal ca ekibi Farãs ya. CAF Awards : Lamin Kamara jël na cargalug ndaw bi gën a xarañ Lamin Kamara (19i at), Amara Juuf (17i at) ak Ezzalzouli (U23 Marog) ñoo nekkoon ndaw yuy xëccoo cargalu gi ñu jagleel ndaw bi gën a xarañ ci at mi fii ci Afrig. Lamin Kamara moo ko mujje jël. Moom, Lamin Kamara, daf def at mu am solo, jël ci CHAN beek CAN U23, ba noppi di joxe ca këlëbam, bokk it léegi ci Ekibu Senegaal bu mag bi. Cargal gu mag gi, balu wurus bi (ballon d’or), Saa-Niseriyaa baa ko jël, Wiktoor Osimen. Basket : Góorgi Si Jeŋ bàyyi na Saa-Senegaal bi xamle na ni bàyyi na basket bi ci benn laaj-tontu bu yàggul ak Jeff McDonald Du San Antonio. Moom nag mu ngi toll ci 33i at. LÀMB Amaa Balde ak Giri Bóordoo jàppees na seen bëre 30i fan ci weeru suwe bii di ñëw ci 2024 mi. Saa-Cees ak Ëmma Seen itam jàppees na ko ci 5i fan ci me bi.
https://www.defuwaxu.com/can-2023-aliw-siise-tann-nay-ndawam/
CAN 2023 : ALIW SIISE TÀNN NAY NDAWAM Barkaatu-démb ci àjjuma ji la tàggatkatu ekib nasiyonaal bi, Aliw Siise doon amal ab jàkkaarloo ak taskati xibaar yi ngir wax li jëm ci waajtaayu CAN bees dëgmal ca Koddiwaar ak biral ndaw yi mu tànn ngir ànd ceek ñoom ñu taxawal fa sunu réew mii di Senegaal. Seen dem gii nag dana wuute ak ya wees. Ndax daf ciy ame ñaari taxawaay. Bu njëkk bi mooy ni moo mujje yëkkati kub bi kon dafa war a xeexal cëram woowu. Ba ca topp nag di xeexaat ngir jéem koo tóllanti. Aliw Siise yëkkati na ay kàddu yu jëm ci loolu wax ne : “Ragalunu. Danuy dem ci CAN bii ak yéene ju réy a réy. Nun nooy buuru Afrig. Kon ekib bi yelloo na cër wu ëpp wiñ ko jox nii. Bu Senegaal wóoluwul boppam, man gisuma ban ekib mooy wóolu boppam ci Afrig gii.” Gannaaw loolu nag biral na limu ndaw yim tànn. Ñoo nekk nii : Góol yi : Eduwaar Méndi, Séeni Jeŋ, Móori Jaw. Defãsëer yi : Kaliidu Kulibali, Musaa Ñaxate, Abdu Jàllo, Yuusuf Sabali, Fóode Baloo Ture, Formóos Méndi,  Abdulaay Sekk, Ismayla Jakob ak Abdulaay Ñaxate Njaay. Miliyë yi : Idiriisa Gànna Géy, Séexu Kuyaate, Lamin Kamara, Paap Mataar Saar, Paap Géy, Paate Siis, Nàmpalis Méndi ak Kerepeŋ Jaata. Ataakã yi : Saajo Maane, Ismayla Njaay, Ilimaan Njaay, Nikolaa Jakson, Bulaay Ja, Abiib Jàllo ak Abdulaay Sima. Kon lii mooy limatu ndaw yees tànn ngir ñu teewal Senegaal fa Koddiwaar ca CAN ba. Am ñu bokkon ca ba ñuy jël kub bi weesu te bokkuñu wii yoon. Xaarees na ci ñoom ñu ñaanal ekib bi te gën a liggéeyaat ngir weneen yoon ñu mën a dikkaat, nde la ca ëpp ay ndaw lañu. Gannaaw tànnug Aliw Siise miy tàggatkat bi nag, am na ay coow yu sew yuy jóg jëm ci lim nu andil rawatina ci mbaali-jokkoo yi. Foo geestu ñoo ngi ciy wax. Li gën a bari ci lees di wax moo di ne, moom Siise, dafa bari lim woo ciy defãsëer, ba sax ci miliyë bi, xeexkat yi ñoo ci ëpp. Boo jàngatee tànn gi wàlluw defãs moo ci ëpp te jamono jii ñu xarañ ci kaw ak ci kanami kã yi lees gënoon a xaar ci moom. Gannaaw loolu it yëkkati na ciy kàddu moom Aliw Siise di xamle ni: “Duma Yàlla, duma yonent. Tàggatkat laa te awmay xërëm ngiy soppi yëf yi. Li ma mën tay mooy góor-góorlu. Lenn lu nu mën, nun, mooy góor-góorlu.” Muy lees ko mën a nangul itam. Bu loolu weeso, ekib bi dina amal ndajem xaritoo ak kii di Niseer fii ci réew mi ca fowub Abdulaay Wàdd 8i fan ci weeru saŋwiyee wii bu 18i waxtu jotee. Nu mànkoo wutiwaat ndam li.
https://www.defuwaxu.com/ku-tiitul-man-tiit-naa/
KU TIITUL MAN TIIT NAA Senegaal wote nañu dibéer ji weesu yamook ñaar-fukki fan ak ñeent ci weeru féewaryee. Ba démb ci alxemes ji ñu ngi doon xaar njuréef ya ca tukkee te këru-àtte gi war cee àddu. Loolu jur jiixi-jaaxa ci askan wi, bawoo ci kàddu yi nguur gi ak kujje giy yëkkati, ñii naan jéll am na ci songoo bu njëkk bi, ñi ci des jàpp ne njaax dafa am, fàww ñu sëggaat bëre. Daanaka askan wi aj na noowam, di xaar aji-àttekat yi séq Ndajem ndeyu-àtte mi àddu ci mbir mi. Waaye bu nu xoolaatee yëf yi bu baax, wote bii tiitaange gu réy moo ci tukkee war a ñeel képp ku am seetlu. Ndaxam sax de, li tiital askan wi ajuwul ci lees gën a jàpp, mu jëm ci kan la yoon di nangul ne moo jël ndam li. Li jur tiitaange gi, war naa yóbbu fitu képp ku yittewoo bàkku réew mi : “Wenn Askan, Benn Jubluwaay, Benn Gëm-gëm”. Su nu waxantee dëgg, ñu bare seen woteb dibéer ci waaso ak tariixa la lalu woon. Di lu kenn mënul a nàttable. Li ma yokk tiit du lenn lu dul ne sunu réewi Afrig yi dañoo des di sooxaale ab góomu judduwaale. Mu méngook ne ay réew la yoo xam ne Bokk moomeel (Nguur) dafee jiitu Bokk Xeet (Askan). Li ko waral mooy waaso yu bari yu seen jaxasoo desoon, ñu yàgg a xare ci seen biir ba noppi nasaraan yi leen nootoon ci lu jege ab xarnu boole leen ciy Bokk moomeel ca diggante atum 1885 ak 1886 ca Berleŋ, péeyub Almaañ. Moone, yooyu waaso sax de, wenn askan lañu, ni ko Séex Anta Jóob wanee. Mu ngi nuy xamal ci téereem bi mu duppe “Civilisation ou barbarie” ne “Deret jiy daw ci samay siddit njaasu deretu wolof laak ju séeréer, ju saraxolle, ju pël, añs.”. Mu tekki ne waaso ak lu ni deme, waruñu fee jur ay. Waaye itam bu nu xoolee ci taarix, ñetti xarnuy njaam, fekki benn xarnub nootaange tax nañu askani réewi Afrig yi réere mbir li leen boole def benn. Amaana looloo waral njiiti Afrig yu njëkk yi fullaaloon bennoob réew yépp, ñuy xàccandoo di dóorandoo. Ci loolu la ku mel ni Ufuwet-Buwaañi taxawoon ca réewum Kodiwaar. Ci loolu it la Seŋoor newoon, sukkandiku ci lu mel ne kalante giy dox ci diggante yenn waaso yi, moo xam séeréer laak pël walla joolaak séeréer, mbaa kalante biy dox ci diggante Njóobeen yeek Njaayeen yi, Jaween yeek Sekkeen yeek Géyeen yi. Waaye li seen liggéey di rafet yépp teewul ba tey njaw des aw xambin. Kon, simoŋ bi war a lëkkale waaso Afrig yi ngir mu taxaw fu dëgër, dese naa wow. Ngelaw lu ñàkk solo mën naa tasaarey réewam. Ku ko weddi na ko seet ci li xewoon Kodiwaar bu yàggul rekk. Benn baat kesee ko tas tasar, muy baatub “ivoirité”. Mu nuy fàttali tamit réewum Ruwaandaa ci atum 1994. Nan fexe boog ba li tàmbalee raam ci dibéeru 24 féewaryee 2019 bañ a yegg ci ñag bi. Nan fexe ba mucc ci li toj Kodiwaar, rajaxe Ruwaandaa. Daawuda Géy
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-7/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM KUPPEG TEFES Mamadu Jàllo, tàggatkatu ekibu Senegaal bu kuppeg tefes bi tànn na ndaw yi mu war a yóbbu fa Irã ngir amal fa ñetti joŋantey xaritoo, bési 19, 20 ak 22i ci weeru desàmbar wii. Joŋante yépp moom ak Irã lay doon ca diiwaanu Teherã (Téhéran). NDAW YI MU TANN Góol : Alseyni Njaay ak Useynu Fay. Defãsëer : Mamadu Silla, Papaa Móodu Ndóoy, Baabakar Ñaŋ, Baabakar Faal, Seydinaa M.A. Gajaga. Miliyë : Maamur Jaañ, Séydinaa Isaa Laay Seen,  Amar Sàmb. Ataakã : Rawul Méndi, Séydinaa Manjoon Jaañ, Suleymaan Koli, Suleymaan Baaji. ABDULAAY SIMAA Saa-Senegaal bi moo ngi wane xarañte ca ekibam boobu di Rangers FC fa Ekos. Fi mu nekk nii, moo ngi ci 14i bii yu mu dugalagum. Ndax loolu dina doy ngir Aliw Siise wóolu ko ci CAN bii ñu dëgmal ? Kenn xamagul. Lu leer daal mooy ni soxlees na ci ekib bi ay ataakã yu xarañ ci kanami kã yi. LÀMB JI : MÓODU LÓO AK BOY ÑAŊ NAROON NAÑU SONGOO Démb ci gaawu gi 15i Desàmbar bi la ñaari mbër yi doon amal seen jàkkaarloo bu mujju laata seen bésu bëre 1 sãwiyee 2024. Ci jàkkaarloo bi, doomu pikin bi dafa fekki Móodu Lóo di nappanteek moom, ñuy sannantey kàddu ci suuf jekki saay rekk doomu Parsel bi daldi koy buux. Ba loolu amee ñu nar a jàppante foofu faf ñenn ca ña ànd ak ñoom ak ca njiit ya dox seen diggante. Yu ni mel dees na wane ni ñaari mbër yi pare nañu ngir neexal bés bi. Waaye nag, lu jar a yamale la laata muy jur lu ñaaw.
https://www.defuwaxu.com/maki-xalifa-mag-bu-rusee-ne-maa-tey/
MAKI/XALIFA : MAG, BU RUSEE NE MAA-TEY Fan yii nu génn, bare woon na ñu doon yéy ak a yàbbi ci mbirum Xalifa Sàll, di wax ci njéggal bi ko Maki Sàll war a jagleel. Am na ci sax ay taskati xibaar yu demoon ba ne Xalifa Sàll këram lay tabaskijee. Waaye, bi nguur gi fésalee turi nit ñi Maki Sàll jéggal, ñu war a tabaskijee seen kër, kenn gisu ci ku tudd Xalifa Sàll. Muy mbetteel gu réy a réy ci ñenn ñi. Maki Sàll, moom, yéyu ci, yàbbiwu ci. Moone, askan wépp a ko ñaanoon njekk, kilifa diine yi, kilifa aada yi, kujje gi, kuréli way-moomeel yeek yenn mbootaay yi. Waaye, Maki dafa lànk, taxaw fi mu taxaw rekk. Rax-ci-dolli, ci ndoorteelu waxtaanu politig wi mu sumb, ñi ko wuyusi noon nañ ko li gën mooy mu bàyyi Xalifa. Wànte, dafa cosoon wax ji, yem fa. Nanguwu cee woon a sori. Maki Sàll dafa xaar ba dem bitim-réew, ca Biyaaris (Biarritz) ga muy teewe fan yii ndajem G7 mi, door a wax li mu xalaat dëggëntaan ci coowal njéggalub Xalifa Sàll mi nekk ciy loxoom. Ndaje moomu, nag, li mu jiite NEPAD moo tax ñu boole ko ci. Waaye, moom sax, bi mu dalee dem ay ndaje ba tey, mësta toj fenn. Ndaxte, dégguñu benn yoon fu ñu waxe ne Maki kat, bii yoon wax na wax ju réy, ni ko Ablaay Wàdd daan defe. Waaye, ba tey loolu ñorunu ; kàddu yi mu fa rotal ci mikóro RFI ñoo jar a bàyyi xel. Maki Sàll baat yii la fa wax ñeel Xalifa Sàll : « Bi ci njëkk mooy, wareesul a tënk giifalub làngu politig gi ci mbirum njéggal kese, yemale ko ci. Njéggalub njiitéef, ndeyu-àtte réewum Senegal moo ko jagleel njiitu réew mi. Kon, ci moom doŋŋ la aju, ciy loxoom kese la nekk. Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. Bu ko defee, sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. Bés bu ma neexee walla ma am coobare gi rekk, dinaa ko def ni ma koy faral di defe. Ndax  at mu nekk, lu ëpp téeméeri nit walla sax ay junniy nit, ci xayma, dinaa leen jéggal, génne leen kaso… » Kon, noo ko déggandoo : kàddu yii la rotal ca Frãs. Ñu mën cee amal ñaari njàngat yu gàtt. Bi ci jëkk mooy ne, Maki Sàll wegul waa réew mi, joxul cër askan wi walla kilifa yi fiy yeewoo. Waaw, lu tax Maki Sàll bitim-réew rekk lay waxe ak a waxtaane mbirum réew mi ? Xanaa réew mi amul i taskati xibaar yu mu mën a janool dégtal leen i kàddoom ak i xalaatam ? Lii bu tekkiwul ñàkk faayda ak suufeel sa boop ak sa réew lu muy tekki leneen ? Ndax kat, lii xeebeel la ci waa réew mi, rawati-na taskati xibaar yi fi fekk baax. Da leen a tanqamlu, dummóoyu leen te nëbbu ko ndax moo ne ci gémmiñu boppam : « sama yoon nekkul ci li taskati xibaar yiy wax ci njéggal bi, duma ci wax. » Ndege, deesul gis benn njiitu réew lu ñàkk faayda bay péncoo mbiriy réewam fii ci Senegaal. Moom kay, Maki rekk a koy defi ca réewi xonq-nopp ya. Muy wone ne, ba tey moomagunu sunu bopp dëgg dëgg, ndax sunu njiit yi amuñu fulla amuñu faayda. Ñaareelu njàngat bi nuy jële ci kàddoom yooyu mënees na ko xaaj ñaar. Benn bi nitu Maki ci boppam la ñeel, beneen bi aju ci digganteem ak Xalifa Sàll. Bi ci njëkk mooy réy ak réy-réylu bi Maki di biral ciy kàddoom : « …ci moom doŋŋ la aju… », « …ciy loxoom kese la nekk. », « Moom mooy xool saa su ko soobee mu jéggale. », « Bés bu ma neexee walla ma am coobare bi rekk, dinaa ko def »… Maki Sàll, li mu nuy xamal ci kàddu yii mooy ne, moom kott, moom kese- kese mooy dogal. Kenn mënul wañaar loxoom ba defloo ko lu ko neexul, ak koo mënti doon. Maki Sàll dafa summi yérey njiitu réew, sol yérey Buur Saltige. Ndaxte, buuru saltige rekk mooy jiitee doole, di jaay maa-mën, jàpp ne lu mu wax mooy am, lu mu waxul du am ; lu mu bëgg mooy am, lu mu bëggul du am. Ndege, njiitu réew day woyof, nangoo déglu askanam ak kilifa réew mi ba tax lépp lu mu jàpp, su ñu ko ñaanee mu bàyyi. Waaye, Maki jikkoy firawna lay doxe. Waaw. Ndax bu demee bay dolli ci waxam ji : « …ni ma koy faral di defe.» ak  « …dinaa leen jéggal, génne leen kaso. », Maki day firndéel ni njéggal, jamono jii, ciy loxoom la nekk, ku ko neex la koy jagleel. Lii moo tax ndaw yi wutal ko dàkkental, di ko woowe « xaaju Yàlla » walla « àmbasadëeru Yàlla ci Senegaal ». Ndaxte, bu nee at mu nekk mu jéggal nit ñu bare, li wax ji wund mooy ku ci bokkul daŋ kaa neexul. Ci lanuy tàbbee ci ñaareelu njàngat bi ñeel digganteem ak Xalifa Sàll. Ndax seetlu ngeen lenn ? Saa su Makiy wax ci mbirum Xalifa Sàll, du jaar ci turam. Xanaa keroog ba mu nee “sama doomu baay la” ndax sant wi ñu bokk. Rax-ci-dolli, ñépp xam nañ ni jot naa yabal ay ndaw ca kaso ba ngir ñu gise ak Xalifa Sàll. Xamunu lu ñu fa waxante, waaye mel na ni Maki dafa dencal mer Xalifa. Te, Xalifa wax na du benn du ñaar ne sàkkuwul njéggal ci Maki te soxlawu ko. Dafa mel ni am na lu Xalifa Sàll gàntal Maki ba tax koo ñéññ. Coxorte giy feeñ ciy waxam ak doxalinam doy nañ firnde. Ma leen di laaj nag : waaw, lan la Maki jàppal ngóor si Xalifa ba tax muy doxale nii ak moom ? Lan lañu jot a séq ? Ak lu ci mënti am, askan wi moom moo gën a sonn Xalifa fuuf. Bi mu tàmbalee taw ba léegi, askan wi nelawatul, te waa Ndakaaroo ci gën a sonn. Kër yi taa nañu, koñ yi taa, mbedd yi taa, tali yi fees dell ak ndox, kenn amul foo jaar. Njëg yépp yokku, xaalis amul, oto yiy mbëkkante ci tali bi, nit ñiy dee. Kenn xamul fooy teg sa tànk. Metit yooyu yépp teewul nguur gi ne ée-yaay, nun danuy bër, njiitu réew miy wone ay portale mook soxnaam ca Tugal, ci kër gu taaroo taaru, di bége. Mu mel ni dañuy mbëllee baadoolo yi. Li am ba des moo di, ak Maki, mel na ni, laabisiina la réew miy jubal. Nu dem rekk.
https://www.defuwaxu.com/tabaski-2023-xutba-ceerno-saydu-nuuru-taal/
TABASKI 2023 : XUTBA CEERNO SAYDU NUURU TAAL Ci alxamesu démb ji la ñu ëpp ci saa-senegaal yi tabaski. Ku ne tabaski, ne xutba. Te, xutbay imaam yi, dees na koy faral di xaaj ñaari pàcc. Bu ci njëkk bi, imaam yi dañu koy jagleel diine ji, jagleel beneen ñaareelu pàcc bi tolluwaayu réew mi, rawatina li ci fës. Noonii la fa deme at mii tam. Ceerno Saydu Nuuru Taal, ca xutbaam ba, ñaan na jàmm ci réew mi, sàkku ñuy amal waxtaan at mu nekk ci fànn yépp te soññ ndaw ñi ci moytoo yàq alalu réew mi. Imaamu jumaay Omariyeŋ yi, Ceerno Saydu Nuuru Taal, ci alxames ji la julli. Ba muy xutba, ñaanal na Senegaal jàmm ak tawfeex. Waayeet, soññ na njiit yi ci ñuy jiital diisoo ci fànn yépp, ginnaaw bim rafetloo waxtaan wi Njiitu réew mi sumb. Dafa jàpp ne, waxtaan woowile, warees na ko amal at mu nekk te yaatal ko ba muy laal dund gépp. Imaam Ceerno Saydu Nuuru Taal ñaawlu na tamit yëngu-yëngu yi toftalu woon ci ndaanug Usmaan Sonko ga ñeel layoom beek Aji Saar, bay nit ñu bari dee ci. Imaam bi nee, bakkan dafa tedd fa Yàlla, wareesu ko dog lu moy ci kow dëgg. Mu daldi tari aayab Alxuraan juy feddali waxam ji : « Ku rey benn bakkan, mel na ni àddina sépp nga rey. » Kilifag taalibey Umar Fuutiyu Taal yi naqarlu na tamit yàq yi, toj yeek càcc gi àndoon ak yëngu-yëngal yooyee. Mu ne : « Islaam dafa araamal càcc ak jël alalu jàmbur. » Ni saa-senegaal yiy tojatee ak a yàqatey béréb, di taal ak a jafal ay daamar añs. Daf ko jaaxal, tiital ko lool. Ndax, Senegaal, léegi, dañu xër ci toj ak taal te, ciy waxam, « daan nañ wax ni, doomu Senegaal mënul sax rey ab mellentaan. » Kon, bu yeboo jàpp ne, Senegaalu démb, du Senegaalu tey. Teewul Imaam baa ngiy ñaaxati ndaw ñiy yàq, di leen xelal ak digal ci ñu bañ a déglu taalkati fitna yoy, ña nga bitim-réew toog, nekk ci seen jàmm. Daf ne : « Buleen déglu ñi leen wax ngeen taal walla yàqate këri jàmbur yi walla ay bérébi liggéey. Ñaare, bitim-réew lañuy nekk, toog ci seen i saal yu nooy (…) te, ëllëg, yeen a aajowoo biis yeek saxaar gi. » Ndigle laa ngoog. Nu xool ba xam dees na ko jëfe.
https://www.defuwaxu.com/manchester-city-witti-na-biddiiwam-bu-njekk/
MANCHESTER CITY WITTI NA BIDDIIWAM BU NJËKK Àngale yaa ngay gundaandaat ! Manchester a ngi toj ! Ren, dafa baxa. Ci bëccëgu dibéeru tey ji, foo sànni woon mbàttu mu tàkk. Soppey Manchester City yaa nga feesoon dell mbeddi dëkk ba, di yuuxoo ak a fecci. Ñoo yey nag. Ndaxte, ba Manchester City dee këlëb ba tey, guléet ñuy jël “League des Champions”. Démb ci gaawu gi lañ duma Inter de Milan 1 bii ci 0, daldi witti seen njëlbeenug biddiiw ci joŋante bu mag bile. Ay at ñoo ngi nii, waa Manchester City di di rëbb kub bi. Saa bu xëccaan buum ga ba yaakaar ni bii mooy baax bi rekk, buum ga dog. Daaw jéeg, demoon ba finaal, Chelsea ne dóor ko, yaakaar ji tas. Daaw, mu dem ba demi-finaal, Real Madrid nax ko, toogloo ko. Te, ndeysaan, ñépp a foogoon ne day rey Real Madrid.  Waaye, ren de, fayu na fayu yu metti sax. Nde, dafa wulli Real Madrid wulli yu metti ci demi-finaal yi, duma ko 4-0, toogloo ko. Lu ko jiitu, ci kaar-dë-finaal yi, Bayern Munich la làbbali, toroxal ko biir dëkkam. Li may Manchester City doole mooy ne, ren, dafa jënd atakã, dugalkat, bu xereñ te xobe : Erling Haaland. Moo taxi t, atum ren ji de, Manchester City ñépp la tër, muy mbuucaa-mbuuj yi, di punkal yi. Fa Àngalteer de, kenn yabu ko fa. Muy sàmpiyonaa di FA Cup, lépp la raafal. Desalul kenn dara. Ligue des Champions kesee ko dese wonn. Mu doon janook Inter de Milan, di ékib bu naqaree futbalal. Finaal bi neexoon na lool. Joŋante bi neexoon na lool, bal biy daw jàmbar yay ñafe, ku nekk bañ sa moroom yóbbul la ko. Xaaj bu njëkk bi, ñu nekk ci ba dem noppalu, kenn dugalul sa moroom. Ñu dikkati ca ñaareelu xaaj bi, nekkaat ca, bal bay daw, gaa yay neexal ba ca 66eelu simili ba rekk, Rodri, di kuppekatu Manchester City, ne tuxum bal ba ca caaxu Onana yaa. Estaad bay riir, soppey Manchester City yay yëngal biir ak biti ga. Ñu nekkaat cay daw ba na mu jeexee. Arbit ne « Priip ! Priip ! Priiiiii…p ! » Rekk estaad ba tojati. Yuuxoo yeek sarxolle yi. Àngale yiy tëb ak a fecc fii, saa-itali yiy jooy, ndeysaan. Pep Guardiola nag, tàggatkatu Manchester City bi, yoroon Barcelone ak Bayern Munich, kenn gënu koo bég. Xol baa nga mel ne wanagu mbott. Ndax, kub bi, daf ko yàgg a yóotu. Am ñu naan sax, ci mbooru futbal, moom mooy tàggatkat bi gën a aay. Ak lu ci mën di am, jaanam wàcc na.
https://www.defuwaxu.com/ikibu-futbal-bu-senegaal-ku-nepp-di-xaar-nga-war-a-mene-fu-nekk/
Ikibu Futbal bu Senegaal : Ku ñépp di xaar nga war a mëne fu nekk Keroog ci talaata ji lees tàmbali ñaareelu bëccëgu joŋantey bokkadil CAN 2023. Ikibu Senegaal bi doon ci jàmmaarlook ikibu Ruwàndaa bi ko doon dalale ci Estaad Meetar Abdulaay Wàdd bu Jamñaajo.  Mu doonoon joŋante bu metti te wuuteek bu gaawu, bañ dumawee Beneŋ 3i bii ci benn. Bi joŋante bi di waaj a jeex la kii di Saajo Maane, goneg Bàmbaali gi, dugal penaatii. Senegaal gàddu ndam li. Ñuy ñaari joŋante yu tegaloo yuy fàttali fi ikibu Senegaal bi tollu ci làngug futbal gi ak lees di xaar ci moom. Ñetti weer ci ginnaaw la Senegaal doonoon sàmpiyoŋu Afrig 2021. Mu sóobooti xaat ci joñante bi. Mboolem réewi Afrig yi, ku ci nekk bëgg koo wuutu, te Senegaal ci boppam war koo mën a jëlaat. Lii tax na ba saa buy joŋante, way-faram (supporters) yi di xaar ndam ak a yaakaar mu doon ndam lu réy. Bokk na ci li ko waral, futbalkat yi ikib bi dajale dañoo siiw lool te am i tur. Daanaka ñu ci ëpp, ci sàmpiyonaa yi ëpp doole ci àddina si lañuy futbal. Loolu tax na ba buñ ndulliwul ki ñuy jàmmaarlool boole ci futbal bu rafet, du neex way-faram yi, walla sax am ñu leen di gàkkal. Rax-ci-dolli, du way-fari Senegaal yi rekk ñooy xaar foofu ikib bi. Dem na ba tàggatkatu gaynde yi walla ñi koy gunge loolu dafa ub seeniy bopp. Loolu dees na ko dégge ci kàddu yi Elaas Juuf yékkati ci ñaari ndam yii ñu tegale : “ ñaari joŋante, ñaari ndam mooy lu jaar yoon. Ndaxte, Senegaal ñépp a ko teg i bët tey jii ci CAN bi. Kon dañoo war a dawal ni ñi mën ci Afrig, niki sàmpiyõwiy Afrig.” Mu mel ni yeneen réew yi xam nañ loolu te nangu ko ngir gën a mën a yokk seen waajtaay. Bees nangoo kàddu yi bawoo ci Karlos Alos, tàggatkatu ikibu Ruwàndaa, Senegaal “bokk na ci fukki ikib yi gën a baax ci àddina si”. Tege yii tax nañ ba gaynde Senegaal yi xam ni seenub benn joŋante dootul a yomb. Te itam loolu feeñ na bu baax ci seen xar-kanam. Bu nu sukkandikoo ci Kàdduy Séexu Kuyaate, dinañ gis ni guney Aliyu Siise yi ñi ngi wéy di mottaliku ci anam yu bare : “ léegi ikib bun dajeel dafay metti. Nun nooy sàmpiyõ Afrig. Te sàmpiyõ Afrig, jàmmarloowam yépp gañ-jël (finale) la… Boo xoolee joŋante bi, bun ko amaloon ñaar ba ñetti at ci ginnaaw doon nan ci témboo walla sax nu ñàkk ko”. Lii nag mooy yaa fi mën, bu dee ndam it, sas la wu réy. Ndax ku ñépp di xaar nga war a mëne fu nekk. Mu mel ni xam giñ xam fiñ leen xaare, baax na ci Saajo Maane ak i ñoñam. Jural na leen làmbook mat gu leen di tax a bëcciku (se décharger) ak a xam nees war a amee ndam saa su nekk ak lum jafe-jafe.
https://www.defuwaxu.com/atsu-deddu-na/
ATSU DËDDU NA Saa-Gana bi, Atsu (1992-2023), mujje na feeñ ginnaaw bi mu réere ci màbbiti taax ya daanu ci sababu rëng-rëng ba ca Tirkii. Ndeysaan, dañoo fekk mu dee. Moom nag, wurekat bu mag bu ñu ràññe la woon fii ci Afrig ak fa Tugal. Loolu nekk lu tiis ciy ñoñam, ciy naataangoom, waaye itam ciy soppeem rawatina waa Afrig yi. Keroog, 6i fan ci féewaryee 2023, la suuf sa yëngu woon diggante ñaari réew yii di Tirkii ak Siri, ñu baree bari ñàkke ci seen i bakkan. Kiriscaan Atsu nag, Fc Porto la njëkkoon nekk, atum 2011. Mu jóge fa, dem Àngalteer. Nde, atum 2013 la jóge Fc Porto fekki Chelsea. Daanaka solul mayo Chelsea ndax jamonoy Móriñoo la fa dikk, jotul sax bokk ci benn joŋante, ñu abale ko. ci ñeenti këlëb lañ ko abale foofu ca Àngalteer, Everton, Bournemouth ak Newcastle. Kon yàgg na fa. Ginnaaw loolu la génn tugal dem Araabi Sawdid am fa ñaari at ak këlëb bii di Al Raed. Xaatim ba leen lënkale woon ba mu jeexee la moom boppam, dem fële ca Tirkii fasante ak Hatayspor atum 2022. Foofu nag, ñeenti joŋante rekk la fa jot a am. Ñeenteel bi mooy keroog 5i féewaryee bii, ekibam doon daje ak Kasimpasa, nga xam ni benn bal ba ca duggoon moo ko dugal ba mu desee woon as tuut ca joŋante ba. Bal boobee taxoon ñu gañe joŋante ba ba noppi juroon mbégte gu rëy ca xoli soppey këlëb ba. Ca ëllëgu bés boobu la Yàlla Buur bi dikk ak ndogalam, suuf si xëy di yëngu yëngu yu metti foofu ca Tirkii ak Siri. Moom Atsu, bañ ca tegeey fan yu néew, ay xibaar génnoon di xamle ni gis nañ ko ak ay gaañu-gaañu waaye deewul, ba xel yi tàmbali woon a dal. Xibaar boobu tax bu gaaw, ca ngoonu bés ba njaatigeem (agent) génn weddi loolu ni kenn gisul Atsu ba léegi. Bërki-démb ci gaawu bi nag, ba nu xëyee, moom njaatigeem bi bind xamle ni gis nañ ko ca biir bekkit ya mu ñàkk bakanam ci anam yu doywaar. démb ku seetaan Sàmpiyonaa ya rawatina Àngalteer gis nga ekib ya doon ko sargal ak di ko mastawu njabootam ak àddina sépp.
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-2-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (2/7/2023) Dëmi-finaal U23 Ginnaaw-ëllëg, talaata 4i fan ci sulet , la dëmi-finaali joŋateb kuppe U23 di door fa Marog. Esipt ak Gine Konaakiri ñooy laale bu 17i waxtu ci ngoon jotee. Bu jeexee, Marog mi dalal po mi dana dajeek Mali ci ñaareelu dëmi-finaal bi. Njortees na ne, joŋante yu neex la nar a doon. Nde, kenn ku ci nekk doo nangu sa moroom dóor la. Te yit, jamono jii, ekib yépp a defaru bu baax a baax. Rax-ci-dolli, ku ci nekk dafa bëgg a jël kub. Cargalug Ànderes Iñestaa fa Sàppõ Ginnaaw ba mu jugee Barcelone mi nga xam ne moom la ko ñépp xamee woon, ba ñépp jàppoon sax ni du fa mës a juge, Iñestaa, saa-espaañ bi, dafa demoon fee ca Sàppõ. Ca la demee ca këlëbu bu ñuy woowe Vissel Kobe, def na fa 5i at ci ren ba démb ci gaawu gi la doon amal joŋanteem bu mujju foofu. Na mu jooyee woon, keroog  ba muy jóge Barça, noonee la jooyati ba ñu koy sargal cargal gu mag ci njeexitalu joŋante ba. Demoon nañu ba jaayukaayi tikke ya sax dafa mujje tëj ndax fowu bu fees dell. Muy lu mu yellool, ndax def na ci futbal lu nekk, jël ci itam lu nekk. Bokk na tay ci kuppekati digg yu gën a xereñ ci àddina ba sañoo lim ñett te waxoo turam. Ndax dafay aj i dàllam am daf koy solaat tuuti, dara wóoragu ci, nañu ko déglu ba xam lum ci namm.
https://www.defuwaxu.com/gacce-ngaalaamambugaar-useynu-beey/
GÀCCE NGAALAAMA, MBUGAAR ! Senegaal amati na ndam ci 3eelu fan ci weeru nowàmbar wii, jaare ko ci benn ciy doomam, di Muhamet Mbugaar Saar, ab bindkat. Moom mii Farãs tappal na ko raaya bu am solo, muy Prix Goncourt  bu atum 2021. Muy raaya bu ñëw topp ci yeneen yu mu fi jotoon a am. Muhamet Mbugaar di xale bu am 31 at doŋŋ, juddoo Ndakaaru ci 20eelu fanu suweŋ, ci atum 1990. Doomu Séeréer bu màgge Jurbel la, te jànge ‘‘Prytanée Militaire de Saint-Louis’’ bi ñépp a xam. Foofa la ame lijaasam bii di “Baccalauréat”, laata muy àggaleji njàngam ca Farãs, ca ‘‘Lycée Pierre d’Ailly’’ ak ‘‘Ecole des hautes études des sciences sociales’’. Moom nag, li muy gune yépp, jotoon nañu koo tappal ay raaya yu bare. Jëloon na fi Grand prix du roman métis ak Prix Ahmadou Kourouma ca atum 2015 ak Prix Littéraire de la Porte Dorée ca atum 2018. Persidaa Maki Sàll itam sargaloon na ko fi, defoon ko Chevalier de l’Ordre du Mérite ca atum 2015. Ci téere yi waral jaloore yooyu, man nañ cee lim : La Cale (2014), Terre ceinte (2015), Silence du choeur (2017) ak De purs hommes (2018). Dëgg-dëgg, xale bu jàmbaare la, ndax ku gis ay jalooreem ak li mu bind yépp, dinga xam ni ku xareñ la, mën na li muy def, te it raw na ay maasam ! Prix Goncourt, niki beneen bi ñuy woowe Renaudot, raaya la bu ñuy joxe at mu ne ca Farãs, ngir sargal bindkat bi gën a ràññeeku ci bindkati téereb nettali yiy jëfandikoo làkkuw nasaraan. Waaye ñépp xam nañu ne, làkk woowu jéggi nay digalooy Farãs bay law ci àddina si yépp, ndax, daanaka, ay fukkiy miliyoŋi nit ñooy jëfandikoo làkk woowu. Kon nag, Prix Goncourt, raaya bu am solo la ; cuune du ko gàddu, doonte ci way-jëfandikoo farañse yi rekk la yem. Prix Goncourt bu mag boobu la doomu Senegaal bi gàddu gannaaw René Maran (ca atum 1921) ak Mari Njaay (ci atum 2009). Kon nag, gàcce ngaalaama, Muhamet Mbugaar ! Li tax ñu tànn ko ci biir bindkat yi bare yooyu doon xëccoo raaya bi, mooy ñeenteelu téereem bi mu bind, duppe ko La plus secrète mémoire des hommes. Muŋ ciy nettali jaar-jaaru bindkat bu xareñoon, ku ñépp séentu woon ca kaw, waaye mu mujjee daanu ba ñépp fàtte ko, ndax rekk, ñàkk dégg-dégg bi nit ñi wone woon ñeel i mébétam. Mu mel ne, kàngami Goncourt yi doon àtte ngir tànn mbër mi leen doy, dañoo yéemu ciy xalaati Mbugaar yu xóot yi, waaye rawati-na ci xereñ gi mu wone ci mbindinam. Li gën a neex ci raaya Mbugaar bile, mooy bés bi mu ko amee, dafa xaw a yemook 7eelu fanu nowàmbar, di Journée internationale de l’écrivain africain, maanaam bés bi ñu jagleel bindkati Afrig yi. Bés boobu, li ëpp ci bindkati Senegaal yi daje woon nañu ci seen béréb bu siiw boobu di Kër Biraago gu bees. Ñu bare ci ñoom nag jot nañu faa jël kàddu, rafetlu xew-xew bi, biral seen mbégte ci jaloore ju ni mel. Teewul nag, am ñeneen ci réew mi, ñu yékkati seen baat di ŋàññ Mbugaar ndax ñàkk a rafetlu ay bindam. Waaye loolu, jeneen wax la, ndax dañuy jàpp rekk tontuy Mbugaar ci boppam : “Na nit ñi jàng téere bi ba noppi, buñ amee lu ñuy wax, ñu wax ko”. Ci sunu wàllu bopp, ci wax jooju lanu jàppandi ba ba nuy jàng téereem yi indi coow lépp. Kon, nu waxati ko : “Gàcce ngaalaama, Mbugaar !”
https://www.defuwaxu.com/mbemestal-ci-jaar-jaaru-allaaji-omar-taal/
MBËMËSTAL CI JAAR-JAARU ÀLLAAJI OMAR TAAL Àllaaji Omar Taal mi juddu ci atum 1796 ca Fuuta, bokk na ci ñi siggil ba fàww nit ku ñuul ci lislaam. Nekkul woon rekk njiitul diine ak tariixa, wànte boroom xam-xam bu gëmoon der bu ñuul la, te fonk dénduw Afrig gépp. Ginnaaw bi mu wedamloowee ay sëriñam, Àllaaji Omar feeñaloon na yeneen i kéemtaan ci daara ja mu nekkoon. Baayam boroom xam-xam la woon bu jànge Daaray Pir, doon daara ji gënoon a kowe ci jamono jooju. Yaayam it, Soxna Aadama Ayse, yaaram la woon bu nangoo séy te baax, fonk boroom këram ak wujjam. Abdul Karim Jàllo, ab sëriñ bu jànge Gànnaar, jële fa wirdu Tijaan, moo ko jëkk a jox wird wa. Ci lan fasante woon kóllëre ñoom ñaar. Àllaaji Omar jaaroon na Misra, siggil fa der bu ñuul. Boroom xam-xami Misra xawoon nanu koo xeeb ngir wirgo deram, wànte bim jëflaanteek ñoom ba noppi, ñoom ñépp a luum. Ba mu ajee Màkka la taseek Muhamadu Xaali nekk taalibeem ay weeri weer. Muhamadu Xaali natt ko ci bépp anam, def ko Xalifa ci ndigalu Seex Ahmad Tiijaani. Àllaaji Omar Taal sumboon nay xare Senegaal ba Niseryaa ngir tuubloo ceddo yi, yaatal lislaam fépp ci Afrig sowu-jànt. Ci 1864 la ko noon yi ërtal mu dugg ci Degembeer ne fa mes. Dees na wéy di fàttalikuy jalooreem ba fàww.
https://www.defuwaxu.com/can-u-17-2023-kub-mu-ngi-xeen/
CAN U17 2023 : KUB MU NGI XEEÑ ! Raayab Senegaal a ngi gën yéeg, turam di gën a jëm ca kow a kow. Sunu kuppekat yaa ngiy wéy di aj turu Senegaal gi muy gën di kawe rekk. Gannaaw ba ñu gañee ñeenti kuppeg Afrig ci ñaari at yii, ñoo ngi ciy bëgg a teg juróomeel bi. Foofu ca Alséri, ndawi Senegaal yaa nga fay wane fullaak faayda ju mat sëkk. Ba kub bi tàmbalee ba léegi, ñoo ngi teg seen tànk ba mu dëgër, teggiwuñ ko wenn yoon. Génn gu rafet lañu génne woon ci seen kippu, gañe seen joŋante yépp dugal ca 7i bii te jëluñu ca benn. Ñu génn, kaar-dë-finaal bi ñu daje ak Afrig dii Sid dóor ko juróomi bal ci dara, muy ndam lu rëy. Démb, ci dibéer ji, 14 Me, mu doon daje ak naataangoom bii di Burkinaa Faaso bi 16i waxtu jotee, mu nekkoon joŋante bu mettee-metti sax (1-1) boo xam ni bii ci, dóor-ma-dóor (série pénalties) la mujje. Senegaal moo mujje gañe. Ca 19i waxtu, démb, Marog itam doon daje ak  Mali, dóor ko itam ca dóor-ma-dóor ya. Senegaal war a daje ak Marog finaal àjjuma jii di ñëw, di yamook 19 Me. Senegaal, démb ci demi finaal bi lay door a jël bii. Dugalagum na 13i bii. Amari Juuf itam nekkagum ba léegi ki ëpp lu mu dugal (5i bii). Senegaal moo ngi ci buntu jël juróomeelu kuppeg Afrigam, kon nanu ko daan waxe rekk, ngelaw liy ëpp sunu réew mi ci wàllu kuppe Yàlla bu mu gaaw a dal. Mànkoo wuti ndam li ! Gayndee Njaay mbara-wàcc !
https://www.defuwaxu.com/jeeri-joor-ndeelaak-tubaab-bi/
JÉERI JOOR NDEELAAK TUBAAB BI Jéeri Joor Ndeela Faal mu ngi gane àdduna ci atum 1871. Mu doon doom ci Sàmba Yaaya Faal mi newoon fanweer ak ñaarelu Dammeelu Kajoor te Nasaraan yi daaneloon ko ba noppi yóbbu ko Ndar-Géej, téye ko fa. Ci atum 1891 la xaru ci dex gi ginnaaw bi way-juram bu jigéen génnee àdduna te Tubaab bi aaye ko mu teew ca dëj ba. Ñuy wax ne ba muy takk rakki Kànnaar Faal mi doonoon kilifa ca tundu Bawol te moom it Tubaab bi daaneloon ko, Kànnaar moomu da koo mayoon ñaari jaam. Bi ñu ci tegee ab diir, Jéeri ànd ak Kànnaar Faal ak Bookar Tilaas – mi yilifoon tundu Géwul – dem Cees jaay fa jaam yooyee. Fekk na booba Tubaab bi aaye woon njaayum jaam. Noonee, juróom-ñaari fan ci weeru awril ci lañu leen tege loxo ñoom ñett yóbbu leen ca kër gornóor ba ca Cees ñu jàkkaarlook kummàndaŋu Tubaab ba tegoon seen kaw tuumay njaayum jaam. Ca la leen fayloo ab alamaan. Waaye yamu ca ne da caa teg ne Jéeri dees koy tëj kaso diirub fukki fan ak juróom. Booba fekk na Sarica Jéey, di xarit ci Jéeri, doon ko xaar ci biti. Ba mu déggee coow li mu daldi mer ba futt ne “mënees naa nangu alamaan bi gaa, waaye xel xalaatul muy seetaan ñuy tëj Jéeri waxumalaak di ko jéng. Loolu moom mënuma koo nangu !” Bi Jéeriy xeex ak alkaati yi ko doon jéem a jéng, la Sarica Jéey dàjji bunt bi ne jaas ci biir bérébu-àttekaay bi. Ca la alkaati yi dawe, mu bocci paaka jam ko Henry Chautemps mi fa wuutu woon gornóor, mu faatu ci saa si. Ba mu ca jógee la jël paaka bay siit ak deret jox ko Jéeri. Ñu ànd ñoom ñaar génn, géwél yi topp leen di tagg  ay maami Jéeri Joor Ndeela Faal. La ca Sarica Jéey jublu woon mooy sàmm woyu Jéeri Joor Ndeela Faal, mu doon woy wu rafet ba ciy sëtam ba ñu mën a fàttaliku ba fàww ne Jéeri moo reyoon kummàndaŋ bi ko bëggoon a yóbbe gaay demba. Ca la Jéeri Joor Ndeela Faal ànd ak xaritam Sarica Jéey ñu bawoo Cees dem Caytu ca nijaayam Masàmba Saasum Koddu Jóob miy maam ci Seex Anta Jóob mi ñépp xam.  Ba ñu fa jógee dem Sugeer, Jéeri waxtaan ak ay mbokkam daldi ne du daw, xanaa day toog jàmmaelook noon bi xeex ba daan mbaa mu daanu. Booba fekk Tubaab yi tàmbale koo wër ba sax dig ab neexal képp ku leen jébbal Jéeri ci muy dundu walla mu dee. Waaye ci juróom-ñeenti fan ci weeru awril atum 1904 – fekkoon booba ñoñi kumàndaŋ Prempain yi doon wër Jéeri wër bu metti – la ko Kànnaar Faal reye. Kànnaar xaritam la woon, doon goroom te yit ñoo àndoon wuyuji ca Cees. Dafa lalal Jéeri ndëgg-sërëx, ba noppi dagg bopp bi ak benn loxo bi dem jox ko Tubaab bi. Na mu ko baaxoo woon def booba ngir tiital bañkat yi, Tubaab bi jël loxo Jéeri baak bopp bi samp leen cib bant bu gudd teg ko ca pénc ma feggoog màrse Cees. Booba Jéeree ngi amoon fanweeri- at ak ñaar rekk. Sarica Jéey xaritam bu gore boobee ba ñu ca tegee ñaari fan la ko Tubaab bi teg loxo, sànni ko Giyaan, nekk ca wetu Ameerig.  Sarica mujj na faa takk soxna ba am fa ñaari doom. Kànnaar Faal workat ba moom, Tubaab bi da koo mujjee wor, tëj ko ñaar-fukki at ci kaso bi. Ñaari at la fa def, tuub, dugg ci diine lislaam, soppi turam, di wuyoo ci turu Aamadu Kànnaar Faal.
https://www.defuwaxu.com/daawuda-jaawara-faatu-nuy-fattaliku-senegambi/
DAAWUDA JAAWARA FAATU, NUY FÀTTALIKU SENEGÀMBI Daawuda Kayraba Jaawara, jiite woon fi réewum Gàmbi 1979 ba 1994, faatu na ci 27eelu ut 2019 bii ñu génn. Mëneesul a wax Daawuda Jaawara te xel du dem ca lëkkaloo ga doxoon ci diggante ñaari réew yii di Senegaal ak Gàmbi te sabab ba doonoon ànd nekk benn réew, ñu duppe ko Senegàmbi. Moone sax de Senegàmbi amoon na fi ay xarnu ci ginnaaw, ca jamonoy nootaange Tubaab yi (colonisation) ca atum 1763 jàpp 1783. Waaye Senegàmbi gi nuy wax ginnaaw bi nu jotee sunug jonn (indépendance) la. Ndax ñu ngi xaatim déggóo bi ko sos ci 17 desàmbar 1981. Ba ñu ca jógee it ça ngomblaani (assemblée nationale) ñaari réew yi ñu dëggal ko ci 29eelu desàmbar ca mooma at. Booba askanu réewu Senegaal a ngi tolluwoon 6 milyoŋi doomi-aadama, boob Gàmbi yemoo woon ak 600 junniy nit. Ñaari réew yi doon ca roy Tansani (Tanzanie) mi juddu ginnaaw bi Tàngayika ak dun ya ñu duppe Sansibaar (archipel de Zanzibar), booloo doon benn. Booba it, ñu ngi doon bàyyi xel ca la taxoon lëkkaloob Senegaal ak Mali àntuwul woon. Nuy wax nag ne yëf yi li ko sooke mooy la laarmeb Senegaal demee Gàmbi fekkoon ñu foqarti nguur ga. Ginnaaw ba mu suqandikoo ci déggoo bu doxoon ci ñaari réew yi ca 18 feebarye 1965 ca Bànjul di péyu réewum Gàmbi, Njiitu réewu Senegaal Abdu Juuf jox larme bi ndigal ñu jéggi dig (frontière) wi dox ci diggante bi, daldi dugg biir Gàmbi. Sabab bi du woon lenn lu dul delloo Daawuda Jaawara ci boppu réew ma ginnaaw ba ko Kukoy Sàmba Saañaŋ, ab joolaa bu tolloon booba ci 28 at daanelee, fekkoon mu tukki ca Àngalteer doon teewe céytalug (le mariage) Saarl (Charles) ak Daayana (Diana). Réewum Senegaal jële woon ci nag tiis wu réy ndax 24 ci ay soldaaram seen bakkan des na fa, 40 walla lu ko ëpp amoon ca ay gaañu-gaañu yu metti. Loolu juroon coow fii ci Senegaal. Kujje politig ga booba Pds bu Ablaay Wàdd ak Rnd bu Séex Anta Jóob ñoo ci gënoon a am baat ci askan wi. Wuuteek Ablaay Wàdd, Séex Anta Jóob, ca janoo bu kurélu politigam amaloon ak taskati xibaar yi, yëkkati woon na ca kàddu yii : ” Li nu jàpp mooy ëllëgug Gàmbi dëgg-dëgg mooy booloo doon benn ak Senegaal”. 4eelu fanu Nowàmbar 1982 lañu siiwal Caytug (le gouvernement) Senegàmbi, mu tollu woon ci 9 nit (5 ci wàllu Senegaal, 4 ci wàllu Gàmbi). Nii la Caytu gi tëdde woon : Abdu Juuf : Njiitu Senegàmbi Daawuda Jaawara : toftalu ci moom Mustafaa Ñas : jëwriñ bi yore jokkalante ak bitim-réew Lamin Kiti Jabaŋ : toftalu ci moom Daawuda Sow : jëwriñ bi yor laarme bi Medun Faal : jëwriñ bi yor kaaraange gi Aliya E.W. Baaji : toftalu ci moom Sériif Saykula Siisey : jëwriñ bi yor koppar yi Momodu S.K. Maaney : jëwriñ bi yor wàllu bitim-réew Asan Sekk : jëwriñ bi yor dem beek dikk bi Jibo Ka : jëwriñ bi yor xibaar ak jokkalante yi jaare ci xarala yi Waaye xalam demoon na bay neex, buum ga dog. Lépp nag bokk ci jeexitali noot gi nu Tubaab yi nootoon. Senegàmbi dox na ba ci atum 1989 yemook mbiicook mbaaloo doxoon ci diggante réewum Senegaal ak mu Gànnaar (Mauritanie) ba yeggoon ci ñaari réew yi di waaj a takk xare. Kii di Daawuda Jaawara wone woon cag jeng akug far dëgg ci Uld Taaya mi jiite woon réewum Gànnaar. Yamu ca, mu pëtexlu ci njort lu mu amoon ne Senegaal xaw naa lompoñ, daldi xotti kayitu-déggo ba juróon Senegàmbi ca 1981, teg ca ne na Senegaal wàññi limub soldaaram ya ne ca mberaayu (territoire) Gàmbi. Loola merloo woon Abdu Juuf lool ba tax ci 19 ut 1989, mu jële soldaari Senegaal yépp ca Gàmbi. Ndax Abdu Juuf ca la yem ? Déedéet, ndax booy seet, ñaari fan ginnaaw bi Gànnaar ak Senegaal dogee bépp jëflànte bu doxoon seen diggante, Abdu Juuf dafa yëkkati ay kàddu yu jëm ci askanu Senegaal. Ci la leen xamal ne lii di Senegàmbi, tegandi nañu ko ci suuf. Ba tey ci biir kàddu yooyee,  Abdu Juuf a ngi naan : ” Lii di bennob Senegaal ak Gàmbi ci biir Senegàmbi amul benn ëllëg”. Mu daaneel ci kàddu yii: “paaka yi ci nootaakon yi tegoon sunu diggante nun doomi Afrig, daanaka ba léegi légét yaa ngi fi ba tey”. 5 at lañu ci teg, ci 1994, Yaayaa Jàmme, ab soldaar bu amoon booba 29 at, foqarti nguur ga ca Daawuda Jaawara, teg ca génne ko réew ma. Nuy ñaanal Daawuda Kayraba Jaawara Yàlla jéggal ko, yërëm ko te xaare ko àjjanay Firdawsi. Amiin.
https://www.defuwaxu.com/diine-ak-politig-nan-moytu-li-nuy-feewale/
DIINE AK POLITIG : NAN MOYTU LI NUY FÉEWALE Ëttu boole bi, genn kurél la gu boole mbooleem këri diine yi ngir saxal jàmm ci biir réew mi, rawatina ci lu ñeel politig beek diine ji. Seetlu nanu ne saa bu jamanoy fal njiitu réew jotee rekk, njaqare dafay faral di am. Li ko waral, nag, du dara lu dul ñenn ci politiseN yi dañuy jëfandikoo tarixa yi ngir beccingéel yeneen wutaakon yi ak a yëkkati seen mbër. Fan yii yépp, ñi bokk ci Ëttu boole baa ngiy daje di waxtaan ci jafe-jafe yeek yëngu-yëngu yiy am ci antarnet beek i xeeti xaralaam yu deme ni Facebook ak WhatsApp. Kilifay Facebook yi amal nañu ag saytu, ànd ceek kàngam yi taxawal kurél gi. Weccoo nañu xalaat naka lañu war a def ba dakkal téesanteek wax ju ñaaw ci béréb yooyu. Bi bésu pal gi desee benn ayu-bés rekk, ay ndéggat yu bari tàbbalees na leen ci antarnet bi, wesaare leen ci “Whatsapp” yi. Ay saay-saay a sooke lu ni mel, di sos ay fen yu tooy xepp, naan këru diine sàngam warul a sànnil xob wutaakon sàngam ndax bokkul ci ñoom, te gëmul seeni sëriñ. Lii moo bijji tiitaange ju réy ci waa réew mi. Diine nekk na lu man a jur xiirook ŋaayoo, te wareesul a mbubboo tarixa ngir soppi ko gànnaay, di ko xeexe ci politig bi. Yoonu tasawuf wi fi mag ñi sampoon, jàmm ak taalibe yi xamante, soppante a ko taxoon a jóg. Donte sax, politig masul a tàqalikook diine, ni seen diggante fése jamono jii dafa jéggi dayo. Séex Tiijaan Si, doomu Abdu Asiis Si Al Amiin, njiit li nekk ci boppu kurél googu yëkkati nay kàddu ngir àrtook leeral kóllëre gi dox ci diggante Murid yeek Tiijaan yi. Wane na ne ñaari kurél yii, waxul sax bokkoo gi leen boole, waaye ñoom ñépp liggéeyal diine ak Yonent bi rekk a leen yitteel. Nee na Sëriñ Séex Tiijaan Si Al Maxtoom wax na ni su Murid yi ak Tiijaan yiy ŋaayoo dafay naqari Yonent bi ndax moo leen jaboote ñoom ñépp. Rax-ci-dolli, wax na ne, palug njiitu réew du palu Imaam wala Xalifa, kon lees war a xool mooy jikko nit ki, jaar-jaaram, xam-xamu àddinaam ak yu ni mel. Waaye naan ci tarixa bii walla bee la bokk, ëpp naa def. Ëttu boole baa ngi ñaan waa réew mi ñu ànd ak dal te dem sànnil xob ki leen soob, bañ cee boole wax ju bari ak xuloo. Yal na Yàlla sotti jàmm ci réew mi te ki jig Senegaal Yàlla jox ko ndam lu sedd guyy.
https://www.defuwaxu.com/ligue-des-champions-dortmund-ak-real-madrid-nooy-daje-finaal/
LIGUE DES CHAMPIONS : DORTMUND AK REAL MADRID ÑOOY DAJE FINAAL Démb, ci àllarba ji, lees doon amal ñaareelu joŋantey demi-finaali “Ligue des champions” bi, diggante Real Madrid ak Bayern Munich. Lu ko jiitu, ci talaata, Paris Saint-Germain doon na janook Dortmund. Dafa di nag, Dortmund ak Real Madrid ñoo am ndam ci seen i joŋante, war a daje ci finaal bi war a am keroog 1eelu fan ci weeru suwe  fa Wembley. Paris Saint-Germain – Dortmund Saa-Almaañ yi ñoo toogloo farãse yi ci seen ñaari joŋante yi. Paris Saint-Germain moo njëkk a fekki, keroog 30i fan ci weeru awril wii, Dortmund daldi koy dóor 1-0. Barki-démb, ci talaata ji, 7i Me 2024, mu fekksi ko ca fowoom bees duppee “Parc des princes”, gañewaat ko benn bal ci dara, daldi jàll finaal. Real Madrid – Bayern Munich Ci weneen wàll wi, waada (champion) Espaañ bi moo toogloo yeneen Saa-Almaañ yi. Ñu amal ñaari joŋante yu metti lool nag. Keroog, bu njëkk ba, 29i Awril 2024, la Real Madrid fekki woon Bayern ca pàkkam, ndaje ma metti, ñu mujjee timboo 2-2. Ci àllarbay démb ji, 8i Me 2024, Bayern Munich daldi fekksi Saa-Espaañ yi seen dëkk. Niki bu njëkk ba, ndaje mi metti lool. Ci 2eelu xaaju joŋante bi la Bayern njëkk a dugal (Alphonso Davies, 68eeli simili). Naka noona, Real Madrid daldi koy tontu, dugal, dugalaat. Joselu moo dugal ñaari bii yi (88eel ak 90+1eel). Noonu la 1/2 yi demee. Ñaari way-bom yi war a daje bés bi njëkk ci weeru suwe wees dëgmal, fa Wembley (Àngalteer).
https://www.defuwaxu.com/xibaari-taggat-yaram-16-7-2023/
XIBAARI TÀGGAT-YARAM (16/7/2023) KUPPEG ÀDDINA SI 2026 Kippu yi ñeel xëccoo paasu kuppeg àddina si war a am ci atum 2026 mi génn nañ fii ci wàlluw Afrig. Senegaal moo ngi bokk ci kippug B gi mook ñii di Kóngoo, Móritani, Tógoo ak ñaari Sudaŋ yi. Senegaal lees jàpp ne mooy ékib bi gën a jekkandi ci kippu gi. Waaye, naataangoom bii di Kóngoo, di ekib bu mag itam, ëpp ko li mu jël ciy kuppeg Afrig du ko ko yómbalal wenn yoon. Te sax, léegi, ekib bu ndaw sax dafa amatul. Ekib yépp ay bañ-bañlu, di jéemantu ni ñépp. Senegaal ci boppam, xam na ni ñépp a koy xaarandi jamono jii. Ba tax na, joŋanteem yépp a nar a metti. GENERATION FOOT JËL NA RAW-GADDU GI Generation Foot bu Ndakaaru moo jël Sàmpiyonaa Senegaal. Démb ci gaawu gi la doon joŋnte ak Jàmbaar, ci 24eelu bëccëg bi. Benn poñ doŋŋ la soxla woon ngir kenn bañ koo dabati. Waaye, la gën témboo la def. Nde, dafa dóor Jàmbaar 1-0, daldi matal 50i poñ. Bii mooy ñetteelu yoon mu koy jël ginnaaw 2017 ak 2019. ESTEFAAN BAAJI AMAAT NA KËLËB Gannaaw ba mu delsee Senegaal, ci këlëbu Casa Sport bi ko lóofoon (tàggat bi muy ndaw), doomu Sigicoor bi, Estefaan Baaji, dina dem fa Siipr, xaatim ca këlëbu Olympiacos Nicosie ag pas gu tollu ci ñaari at. AFROBASKET, KIGALI 2023 Jigéeni basket yi war a teewal Senegaal fa Kigali (Ruwàndaa) ñeel powum basket bi ñuy amal ci diggante réewi Afrig yi, dinañu dem ci 21 Sulet bii. Fim ne nag, ñoo ngi Ndakaaru di amal seen i tàggatu di ko waajal ni mu waree.
https://www.defuwaxu.com/can-2024-koddiwaar-tegg-sa-can-jel-ko/
CAN 2024 KODDIWAAR : TËGG SA CAN, JËL KO ! Koddiwaar mooy waaga CAN 2024 bees doon amale biir dëkkam. Mu doon dajeek Niseriyaa bu Wiktoor Osimen. Waaye, moom Koddiwaar moo mujje gañe ñaari bal ci benn (2-1). Moom waaga wi nag, kenn réerewul fim jaar. Nde, tolloon na fi foo xam ni mënees na wax ni wërsëg dëgg a ko taxoon a des ci po mi. Ci ñetteelu toogaay bi la Koddiwaar génne. Waaye, mu jóge ci loolu mel ni ndaw luñ yedd, gën a defaraat taxawaayam, solu jom ba fees. Ca la jóge woon gañe Senegaal teg ci Mali ak RD Kóngo. Démb ci gaawu gi 12i fan ci weeru féewiryee wi. Jamono jii, biir Koddiwaar, foo sànni mbàttu mu tag. Niseriyaa nag, ku ne yéene woon na ko kub bi ndax yoon wu réy wiñ def itam. Seen joŋante yépp di woon mats jànq. Waaye, li wolof naan “nii la mënoon a deme”, kon noonu la mënoon deme. Gannaaw loolu itam, amal nañ ay tabb ñeel ñi gën a xarañ ci po mi. Futbalkat bi gën a xarañ : Ekong (Niseriyaa) Góol : Wiliyaams (Afrig dii Sidd) Dugalkat : Nsue (G. Ekuwaatoriyaal) Ndaw li gën a xarañ : Adingara (Koddiwaar) Tàggatkat : Emeers Faye (Koddiwaar)
https://www.defuwaxu.com/waaw-ana-ku-boom-omar-bolonden-joob/
WAAW, ANA KU BÓOM OMAR BOLONDEŋ JÓOB ? Omar Bolondeŋ Jóob a ngi juddu ci 10eelu fan ci weeru sàttumbar 1946 ca Ñaame, péeyub réewum Niseer. Mu ngi faatu ci 11eelu fan ci weeru Mee 1973 ca kaso ba woon ca dunub Gore. Omar Bolondeŋ Jóob, nag, kàngam la woon ci biir kàngam yi, jànge ca lekkoolu digg-dóom ji ñu duppe Louis-le-Grand ca Pari. Bim fa génnee, mu tàbbi ca daara ju mag joojee ñuy wax École normale supérieure de Saint-Cloud. Jamono jooju, waxuma la sax am lijaasa ca daara joojee, waaye jànge fa rekk doyoon na ndam, dib sag bu réy a réy ci boroom. Bokk na ci liy màndargaal dayo daara jooju, mooy ne ki jëkk a jiite réewum Senegaal, Lewópóol Sedaar Seŋoor, ñu ràññee ko lool ci wàllum ladab ak mbind, bëggoon na fa dugg, waaye daa lajj. Muy biral ne, daara jooju, ab como daawu fa teg tànk. Am na sax ñuy wax ne, Seŋoor da koo iñaane woon ndam loola, ragal ne dina ko may fitu wujje ak moom ci làngu politig gi, ñeel Senegaal. Sëñ bi Jóob, nag, du woon ragal walla tóoyemaan, ni ko ndaw yiy waxe. Bañkat dëgg la woon, ñeme woon xeex. Dafa di sax, ni mu ame woon noonu fit moo taxoon ñu dàq ko, moom ak benn doomu Farãs bu daan wuyoo ci turu Daniel Cohn-Bendit, ca daara ju mag jooju, ci atum 1969. Waaye yemul foofu. Ndege, Omar Bolondeŋ Jóob dafa xaroon tànki tubéyam, di xeexal askanu Senegal. Mi ngi féete woon ci kóminist yi, daan roy ci doxalinu Mao-Tsé Toung. Kurél gi mu bokkoon mësul a juboo ak Seŋoor, foo leen fekkaan, ñu ngay jàmmaarloo. Ndaxte, Seŋoor nguurug Farãs la fi toogaloon te, ci wàllu xalaat ak politig, yoonu kapitaalist yi la Farãs ak ñi far ak moom toppoon. Loolu mi ngi tollook jamonoy xareb suuf (guerre froide) bi amoon ci diggante U.R.S.S. (kóminism- sosiyalism) ak réewum Amerig (kapitaalism–liberaalism). Àddina si xar ñaar : ñii far ak U.R.S.S. miy mujje dooni Riisi, ñeneen ñi far ak Amerig. Bi mu ñibbisee Ndakaaru, mu wéyal xeex boobu ci ndimbaluy rakkam. Ñoom ñépp ñu doon xeex nooteel, teg ci di ŋàññ doxalinu Seŋoor mi doon wéy ci waawi Farãs. Seŋoor demoon na sax ba jël Jean Collin, di doomu Farãs, boole ci di jegeñaale Jacques Foccart, toftal ko ci boppam, dénk ko lépp lu jëm ci kaaraange biir réew mi. Loolu la Omar Bolondeŋ Jóob ak i àndandoom doon xeex. Ndax kat, Seŋoor dafa jébbalu woon ci Farãs ba nga xam ne, buñ tisóoliwaan Pari, mu ne yaaram-kàlla. Am jamono, Seŋoor sumboon fi liggéey bu mag ñeel mbeddi ndakaaru yi, santaane ñu set-setal gox-goxaat yi ngir laabal leen. Te, nag, duggewu ko woon lenn lu dul teeru Pompidou mi jiite woon Farãs, ngir bégal ko. Loolu metti lool Omar Bolondeŋ Jóob ak i rakkam ba tax ñu demoon taali Njawriñu Liggéeyu caytu gi ak Kërug aada ak cosaan gu Farãs ci Ndakaaru, ñu doon ko wax « Centre culturel français ». Yemuñu ca, ndax defaroon nañ ay ndell, fasoon leen yéenee sànni ci kow woto yi yaboon Seŋoor ak kilifa tubaab yi mu waroon a teeru. Wànte, dañu mujje lajj ci pexe moomu. Ci lañu leen tege loxo. Jàllo Jóob moom, dañ ko tëjoon Kéedugu giiru dundam ba noppi sas ko liggéey bu mu sañutoon a bañ, dëkke koo metital ak a xorñoññal ca biir kaso ba. Ca la Omar nisëree woon ca Mali ga mu dawoon làqu, ne day afalsiy rakkam, kilifay Bamako tegati ko loxo, jébbal ko nguru Senegaal. Ñaar fukki fan ak ñett ci weeru Mars ci atum 1972 la këru àttekaay bu Seŋoor àtte woon Omar Bolondeŋ Jóob, daan ko ñetti ati kaso yu mu waroon a tëdd. Li ñu ko jiiñoon moo doon “nasaxal kaaraange réew mi”. Mu doon xeex doxalinu Seŋoor wi aju woon ci li neex tubaab yi ba noppi worook bëgg-bëggu askanu Senegaal. Moom Omar Bolondeŋ Jóob, dafa mujjee ñàkk bakkanam ca kaso bu Gore ba ñu ko dencoon. Ci 14eeli fan ci weeru Mee atum 1973, la yéenekaayu nguur gi, “Le Soleil”, siiwal xibaar bu tiis bi : “Kurél giy sàmm kaso yi (…) mu ngi xamle ni Omar Bolondeŋ Jóob xaru na ci néegam ci biir kasob Gore ginnaaw bi mu yeewee buum ci baatam. Mu ngi ko def ci boori ñaari waxtu ci guddi”. Booba, 26i at kepp la Omar Bolondeŋ Jóob am. Amaat Daŋsoxo ne woon ca tonet, wax ne : “Dafa leer nàññ ci sama bopp ne Omar Bolondeŋ Jóob dañu koo bóom. Li tax kilifa yi ŋànk réew mi bóom ko nag, lenn rekk la : ak xel mi ko Yàlla mayoon, Omar mënoon na leen fee jële !” Ndeysaan, njabootu njóobéen – rawatina Jàllo Jóob – ñoo ngiy wéy di xeex booba ba léegi ngir ñu bañ a fàtte seen mag jooju. Ñoom li ñu jàpp mooy ne, Omar dañ koo rey, te dara waralu ko woon lu dul politig. Omar a ngi gaañu ginnaaw bi ñu ko metitalee ca kasob Gore ba, te ñu mën a njort ne lépp ci ndigalu Jean Collin la ame. Ñu bare ci ñiy gëstu ci mboorum (histoire du) Senegaal, loolu lañ jàpp.
https://www.defuwaxu.com/faatug-hibaa-caam-senegaal-bopp-bu-xar-naar/
FAATUG HIBAA CAAM : SENEGAAL, BOPP BU XAR ÑAAR? Guddi àjjuma, dëppook 3eelu fan ci weeru Awril, doon guddi gi jiitu bésub baaxentalub sunu moom-sa-réeew, la benn jànq bu am 28iat, di wuyoo ci turu Hibaa Caam, ñàkk bakkanam, ci anam yu tiis te doy waar. Ñu ngi ko fekk mu tëdd, ne nemm, di waccu deret. Ci li taskati xibaar yi wax, xale bu jigéen bi, dafa jël lu ko ëpp doole ci ay donji dorog, ba faf ca faatoo. Loolu nag, mu ngi xewe ci Almadi gii ci Ndakaaru, ca kër gu Baaba Jaw «ITOC» di luye. Moom nag, boroom alal ju raññeeku ci réew mi la te doomam bu jigéen moo ko féetewoo. Ñi fa daje woon ay moroomam lañu, ay xale yu góor ak yu jigéen, ne fay fo ak a topp seen bakkan, doon it ay doomi boroom alal, ak ay doomi kilifa yu ñépp xam ci réew mi. Ku ci bokkul ci ñi ŋànk nguur gii fi ne, am nga ci jegeñaale ; ñu ràññee ci : Daam Amaar, doomu ndem-si-Yàlla-ji Amet Amaar mu NMA SANDERS, doon itam goro Yusu Nduur, Luuti Ba te baayam di jiiteb kurëlu tàggat-yaram. Xew-xew bu ni mel nag, dafay firndeel, ci lu amul benn werante, yàquteg goney réewum Senegaal fi mu toll. Dees na ci joxoñ itambaaraamu tuuma kilifay réew mi, ci ñàkk a yarseen njaboot ni mu ware, bàyyi leen ci seen sago. Li jar a laaj dëgg nag mooy : ana nu ay gune yu juddoogul, mën a yore xaalis bu dul jeex, di ko pasar-pasare nu mu leen neexe, ci Senegaal gu ndóol gii ? Lu doy waar la ! Rax-ci-dolli, ñu mel ne ñu réer, wàcc seen and,waral ñuy daje di jolluy bitéeli biiñ ak a tux sineebar, dëkke càkkaay… Dëgg la sax, mënees na jàpp ni àddina day dox, ngir jamono ju nekk ak i feemam. Waaye kat…. ! Ak lu mu ci mën a doon daal, li ëlëm ñépp,mooy, jamono ji jéyya yii yépp di ame, tiis ak njàqaree ngi lëmbe àddina, ba tàbbi ci sunu Senegaal gii, muy CORONAVIRUS. Mbas la moo xam ne, réewoo-réew mu ngi fay tëral ak a fàdd doomi–aadama yi. Ngir xeex ko nag, fii ci sunum réew, gornmaa bi dafa jël ay dogal yoy, bokk na ci : tere nit ñi ñuy génn guddi, ku nekk war a lëlu ba fajar. Beneen laaj bi nag mooy : xale yooyii newoon ci mbumbaay, ba dogal bi dal seen kaw, ana fan lañu jaar alkaati yi aakimoo mbedd yi. Ana nan lañu def  ba mën a dem ak dikk, guddi, tollook 10i waxtu, ba Hibaa mën a fekki xaritam yi ? Walla, ndax ñoom, xale yooyu, dañu leen a jox ay kayit yu leen may boobule sañ-sañ ? Su ñu noppee ci laaj yooyu, beneen taxaw, muy : ndax dafa am ñaari Senegaal : gu baadoola yi yoon mën a dal seen kaw, saa su ne, ak geneen, gu ñeel boroom barke yi, ñuy buum di bummi, di tambaambalook a def lu leen neex ? Dafa mel ni daal, yoon buy digal ak a tere, baadoola yee tax ; ci ñoom daal la gën a jekk. Moone, dañuy faral di wax naan :« Senegaal, benn bopp la, kenn mënu koo xar ñaar ! » Am déet ? Laaj yi yamuñu foofu de ! Leneen li mat a xam, mooy : ndax CORONAVIRUS bii, dafa am ñu mu dul song ? Du dañu naan feebar bixamul xàjjale? Ak li ñuy woote yépp ci rajoo yeek tele yi jëm ci jumtukaay ak i matuwaay ngir moytu feebar bu bon bi, niki : soriyantoo, raxas say loxo, ak yu ni mel, naka la sunu njiit yi mën wëlbatikoo, bàyyi seeni doom, ñu topp seen bakkan, di doxe maa-tey ? Xanaa kenn mënul ne bëgguñu seen doom yooyu de ? Walla, ñoom ci seen bopp, dañoo gëmul dara ci li ñuy woote ? Mbir maa ngoog. Laaj yi bari nañu lool, te yeneen mat naa leeral, yu mel ni, Hibaa Caam mi ci ñàkke bakkanam, ku ko rey, ak ci yan anam la faatoo ? Li ci gën a doy waar nag, mooy, doonte ubbeeguñu lànket bi, taskatixibaar yi xamle nañu ni, way-jur yi ci seen doom taq ripp, ba alkaati yi teg leen loxo,  ña ngay dugg ak a génn, di lal ay pexe. Looluteey na xelu ñu bari, ba ñu jàpp sax ni mbir mi du mujj fenn. Loolu nag, su amee it, du fi guléet : xanaa fàttewuleen Mati Mbóoj, janq bu siiw boobu fi génnoon àddina moom itam, ci anam yu ni mel? Mel na ni nag, yëf yaa ngi bëgg a ëpp i loxo, te lu ëpp, tuuru. Su ñu ci jógul, du baax ci guney réew mi. Waaw, Senegaal gii xar ñaar, ak ñawtéef yi lëmbe réew mi, ndax mënees na koo saafara ?
https://www.defuwaxu.com/di-buur-di-bummi/
DI BUUR, DI BUMMI Ci gaawu bi weesu, 4eelu fan ci weeru me, la dipite yi wote sémbub àtte biy far palaasu Njiitu-jawriñ yi ci nguurug Senegaal. Ndax sémbub àtte bi jàll na ? Loolu jarul a laaj ! Ci 138 dipite yi teewoon, 124 yi wote nañu « waaw » 7 yi « déedéet ». Yeneen 7 yi des ñoom, di waa PDS, dañoo lànk ne duñu wote tey duñu wote ëllëg. Kon, Senegaal amatul Njiitu-jawriñ. Àtte bu bees bii, nag, dina indi ay coppite yu bare ci doxalinu nguur gi, waaye it dina gën a dooleel Njiitu-réew mi. Du loo xam ni Maki Sàll ak Bun Abdalaa Jonn rekk la ñeel. Dafa dig coppite gu soxal ndeyu-àtte réew meek tëralinu politigu Senegaal ci boppam. Ndaxte, yamoo bi war ci diggante ñetti baat yi – baatu doxal bi, baatu yoon bi  ak baatu fal àtte bi – lay nasaxal, daanaka. Li péncum réew mi dogal dina soppi 21 sàrt ci biir ndeyu-àtte mi, jox Maki Sàll wareef yi Bun Abdalaa Jonn jagoo woon. Ñenn ñi ci kujje gi nee ñu nguur gi duggewu ko dara lu dul këppeel doole. Ñeneen ñi, ñoom, jàpp nañu ne Maki day waajal xaat joŋanteb 2024. Dëgg la sax, Njiitu-réew mee yelloo tabb ku ko neex ngir mu jiite gornmaa bi, jàppale ko ci naal yi mu lal ñeel doxalinu réew mi. Naam, Senegaal ay njiiti-jawriñ yuy jaamu soxlaam lañ fiy faral di gis. Waaye loolu warul a tax ñu ne kenn dootul jiite jawriñ yi. Mbir mi daal, jaay doole lay gën a nirool. Ndaxte léegi moom, Maki mooy Buur di Bummi : su defulee lu ko neex, moom la neex !
https://www.defuwaxu.com/demb-senoor-tey-wadd/
DÉMB SEŋOOR, TEY WÀDD Li ko dale atum 1978 ba tey jii, woteb ren bii mooy wote bu fi njëkk a am te Ablaay Wàdd sampu ci ndëndam. Walla boog, loolu la ñu bare jàpp. Ndax, man kat neneen laa gise mbir mi. Bees delloo ginnaaw, fàttaliku atum 2007, bi Ablaay Wàdd faluwaatee, war a amal ñaareelu moomeem, dafa wax wax ju am solo. Wax jooju, mi ngi ko waxe woon cim ndaje mu mu séqoon ak taskati xibaar yi. Bés boobu la leen « Góor gi » xamal ni mébétam mooy njabootam ci wàllu politig, maanaam « libéraux » yi, toog ci boppu réew mi lu mat juróom-fukki at, gën gee néew. Foofu, Seŋoor mi njabootam — « socialistes » yi — toogoon ñeent-fukki at ci jal bi, la Wàdd doon diir mbagg, ne sax fàww mu rawe ko fukki at. Wax jooju, lu jar a bàyyi xel la. Képp kuy jàngat géewu pólitig beek li ciy xew, war na jéem a xam ndax mébétu Góor gaa ngi ci yoonu àntu, waaw am déet. Su dee waaw la, mu seet man walla yan pexe la koy amale. Nanu leen xoolaat wote yi fi jot a am ci atum 2000 ba nëgëni-sii. Li wolof di léebu naan, bu ndung sàqee, ndung leng, géewu pólitig bi doy na ci firnde. Ndax, 2000 ba léegi, wote njiitu réew yi fi am yépp, Ablaay Wàdd ak i « doomam » ñoo ciy xëccoo. Kon, mu mel ni làmb ji PDS ak…PDS rekk lañ koy tëggal. Nan dellu ginnaaw. Ci atum 2007 Ablaay Wàdd (PDS) moo janoo woon ak Idiriisa Sekk (mi bawoo woon PDS). Ñu ni déet-a-waay, ci atum 2012, Ablaay Wàdd janoowaat ak Maki Sàll (moom tamit jóge woon PDS). Bu fa yemoon mu tane, waaye ci wote ndawi pénc mii weesu, Maki Sàll fexe na ba Usmaan Tanoor Jeŋ, Mustafaa Ñas, Ndem-si-Yàlla ji Jibo Léyti Ka ak seeni farandoo, fàtte PS, làng ak moom ci biir Bennoo Bokk Yaakaar, maanaam ñëw mu boot leen. Amoon na, nag, weneen lafu PS wu lànkoon ni du ànd ak Maki Sàll ci wote yooyu, muy Xalifa Sàll (PS) ak Maalig Gàkku (AFP). Ñooñu, Ablaay Wàdd da leen bëggoon a teg ci ginnaawam, jiite ndajem làngu politig gii di Mànkoo Taxawu Senegaal. Ba ñu lànkee, ne Xalifa Sàll lañuy àndal, Ablaay dafa ne wérëñ, ber yoonam, dem ceek Maki Sàll. Fan la yëf yi mujje ? Xanaa PDS — Maki Sàll — raw, PDS — Ablaay Wàdd — topp ci ! Léegi, nag, sóobu nanu ci woteb 2019 bi ñu war a fale njiitu réew mi fiy toog ba 2024. Waaye, mel na ni dara soppeekuwu fi : na woon, fa woon. Leer na ñépp ni kenn ci ñaari doomi Ablaay Wàdd yii di Maki Sàll (APR) ak Idiriisa Sekk (Rewmi — noonu la ko Idiy binde) mooy gàddu ndam li. Kilifay PS yu mag yi ñoom, Tanoor ak Ñas, daanaka Maki modd na leen ; la ca desoon di bañ, muy Xalifa Sàll ak Gàkku mujje nañoo ànd ak PDS (Idiriisa Sekk). Kon PS moom, kenn waxaalewu ko. Naam, ñoo ngi wax ci xale bi yëngal jamono te xew, Usmaan Sónko, li am ba des mooy : xamees na ni ku falu PDS a la fal, ndax kàrt yépp a ngi ciy loxoy Ablaay Wàdd. Jàppees na ni, ku mu àndal ci ñaari doomam yooyu di Maki Sàll ak Idiriisa Sekk, dinga jël ndam li. Looloo waral, doonte jëmmu Ablaay Wàdd bokkul ci wote bi, fi mu nekk ñépp a ngi koy déglu ba xam kan lay mujjee tàllal loxoom ngir mu sakkanal ndono li. Ablaay Wàdd, nag, bi mu yegsee Senegaal keroog alxames 7 féewaryee bii weesu te ñépp doon ko xaarandi ba xam ku muy àndal, mënees naa jàpp ciy kàddoom ni fasul yéenee far ak kenn ci mbër yi. Mébétam mooy wote bi bañ a am. Waaye ku xam Wàdd xam ni ku tàmm a woote di xool ndey-joor la fekk booba xel maa nga jëm càmmooñ. Xanaa nu yónni yàgg rekk ba xam fu wànnent di mujj ak i gëtam. Bésu joŋante bi soreetul…9
https://www.defuwaxu.com/mangaan-ndeke-am-na-ci-politig/
MÀNGAAN NDEKE AM NA CI PÓLITIG ! b ak yu tey gis ñu woroo lool. Am na sax ci ñoom ku ne woon Ndeyu-Àtte réewum Senegaal dafa war a aaye màngaan ci politig. Yemu fa, ndax dem na ba yaramam tàng, mu yokk ci ne képp ku jóge cib pàrti, ak bu mu mënti doon, dem màngi ci nguur gi, yoon dafa war a jël sa bakkan ! Moonte ngóor si waxoon loolu, moo xéy bés ne maa tey, fekki naa Maki Sàll… Waaye li Senegaal di miin xeeti jëf yu ñaaw yooyu yépp, teewul askan wi, rawatina ndaw yi, am mbetteel biñ déggee ne Aysata Taal Sàll màngi na moom tamit. Man mii amoon naa ci naqar lool. Mënuma woon a nangu ne “Gayndek Podoor gi”, gaynde gi ma xamaloon fulla ak faayda ju mat sëkk dina defi lu ni mel. Lu ko ci xiir ? Ñii a ngi naan dañu koo compal waaye am na ñu wedddi loolu. Xéy-na bañ cee soree gën, ndax Yàlla rekk a xam. Li am ba des, daal, moo di ne jot na ndawi Senegaal yi taxaw temm ngir xeex ba jële fi yenn ñaawtéef yiy yàq làngu pólitig gi tey nasaxal campeefi réew mi.
https://www.defuwaxu.com/seex-beeco-cuun-atte-yallaa-gen-bu-nit/
SÉEX BEECO CUUN : ÀTTE YÀLLAA GËN BU NIT Altine 6eelu fan ci weeru Me, atum 2019. Bés bi ñépp doon xaar, bésub layoo, bésub àtte, ñëw na. Li tax ñépp doon xaar bés bii, nag, du neen. Waaw. Kan lañu doon àtte ? Sëriñ Séex Beeco Cuun, di Xalifa di yit kilifa cantaakon yi. ‘’Bóomug Madinatul-Salaam’’, bile dàkkental la taskati xibaar yi utal mbir mi sabab layoo bu siiw bii. Juróom-ñaari at la lànket bi def, doore ko 2012 ba 2019. Ñépp a doon xaar ndogalu àttekat bii di Xaasimu Ture, mu waroon koo biral ci altine jii. Mbir maa ngi xewe woon ca Madinatul-Salaam, 22eelu fan ci weeru awril 2012. Yéenakaay yi xéy dégtal nu xibaar bu yéeme : 19 cantaakon ñoo faat ñaar ci seeni mbokki taalibe ba noppi suul leen te kenn yégul, kenn tinul. Ñu ni déet-a-waay, gaa ñi ne Sëriñ bee leen jox ndigal. Nee ñu, Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, ñaari way-dëddu yi, lenn rekk a tax ñu boom leen : xérte ak mbëggeel gu jéggi dayo ñeel seen Xalifa bi. Ndax, àggoon nañu ci di ko woowe Yàlla. Loolu, nag, moo indi coow li bu ñu sukkandikoo ci xibaar yi fi jotoon a rot jamono yooyu. Coow li ne kurr ci këru Séex bi, mu yabal ay taalibeem ngir ñu génne fa Abaabakar Jaañ ak Baara Sow. Noonu, 19 cantaakon yi dem ba ci yoon wi, xeex ak Abaabakar Jaañ ak Baara Sow, daldi gor kenn ki jaasi, fetal keneen ki ba noppi gaawtu suul leen. Nee ñu sax ki ñu fetal deewagul woon bi ñu koy suul. Ginnaaw bi ñu defee seen tóoxidóoni ba noppi, dañu ko doon jéem a nëbb far Yàlla def am ku leen bett, boole leen ak sàndarm yi. Bi mbir mi siiwee ba yoon jot ci, coow li ne kurr. Ñépp di naqarlu jëf ju ñaaw jooju. Li ci gënoon a doy waar mooy li Séex Beeco Cuun – mi yilif ñi ñu bóom ak ñi leen bóom – noon, moom de, yëgul tinul. Booba ba léegi, nag, def na juróom ñaari at, yoon di luññutu, di seet a ka seetaat ngir xam kan a def lan. Bu dee taalibe yi nga xam ne ñu ngi woon ci tëjub-négandiku, li leen yoon toppe woon mooy : bóomug njuumte bu ànd ak mbugal, làqub néew, ñàkk a siiwal rey bi, mbooloom-caay-caay, teggi yoonu suul néew ak ñoom seen. Séex Beeco Cuun, moom, lii la ko yoon toppe woon : luqnjuurug bóom, maanaam bu bóomulee it teewoon na bi ñuy fexe mbir mi. Jotoon nañoo teg loxo Sëriñ bi ak 19 taalibeem yi. Séex bi, nag, yoon da koo mayoon sañ-sañub négandiku ndax li mu tawatoon ba tax mëneesu ko woon téye ci kaso. Nan delsi ci altine keroog jeek daan yi fa jóge. Layookati Séex bi, nag, ñaanoon nañu àttekat bi mu fomm layoo bi, xaar ba seen kilyaan wér, mën koo teewe. Waaye kenn mayu leen loolu. Moom Séex bi, àttekat bii di Xaasimu Ture daanoon na ko fukki at yoo xam ne dina ko liggéeyal réew mi ak ndàmpaay lu tollu ci téeméeri miliyoŋ CFA yu mu war a jox, moom ak 19 taalibeem yi, njabootu way-dëddu bu ci nekk. Mbir mi indi werante, am ñu naan daan bi dafa woyof, taalibe yi naan yoon deful liggéeyam, dañoo bañ Séex bi rekk. Sëriñ Saaliyu Cuun, taawu Séex Beeco Cuun, joxoñ na baaraamu tuuma àttekat bi ak nguur gi ci boppam. Ndax, bu ñu sukkandikoo ciy kàddoom, sàmmontewuñu ak àqi Séex beek i yelleefam. Waaye bi loolu lépp di am, Séex baa nga woon Frãs, ci benn loppitaanu Bórdo, di faju. Benn fan doŋŋ lañu ci teg, mu daldi génn àddina. Nee ñu sax yëgul daan bees ko tegoon. Laaj bi ñépp di laaj moo di : daan bi ko àttekat bi daan, ci kan lay dellu ? Ay boroom xam-xam yu seen xel màcc ci wàllu yoon, tontu nañ ci. Nee ñu 10 at yi Séex bi waroon a liggéeyal réew mi, dañu koy teggi ndax ab néew deesu ko liggéeyloo. Waaye ndàmpaay li, ci njabootam lay dellu, ñoo koy fey. Ak lu ci mënti am, xalaat yeek gis-gis yi wute nañu. Wànte li wóor moo di ne àtte Yàllaa gën bu nit.
https://www.defuwaxu.com/kadduy-usmaan-sonko-useynu-beey/
KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar. Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju. (Ci taataanug Uséynu Béey) “Mbokk yi, tey, walla mën naa wax sax ne, fan yii yépp sunu xol neexul, sunuy nelaw néew na, sunu xalaat bari na, te dara waralu ko nag, lu dul tiis wi nga xam ne am na ci réew mi, muy ay bakkan yoo xam ne rot nañ fi. Kon, dama doon ñaan bala nuy dugg ci waxtaan wi rekk nu daldi def “une minute de silence” jagleel ko sunuy doom, ndax ñi fi faatu ñépp, walla ñiñ fi faat ñépp, nun li nuy doon ndaw ndaw, mat nañuy doom. Tey, jox nan ma lim boo xam ni jeexagul; waaye lim bi nu jotagum mat na fukki nit. Benn bakkan bu rot rekk, ci anam bu mel nii, nga xam ne dañ koo faat, musiba la ci réew mi, rawatina nag, bu ñu nee tey mat nañ fukki nit. Bakkan yooyu nag, ñooy : ku ñuy wax Baay Séex Jóob, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Yëmbël ; Séex Kóli amoon ñaar fukki at, ñuŋ ko faate ci Biññoona ; Faamara Gujaabi, moom it amoon ñaar fukki at, ñu faat ko Biññoona ; Paap Siidi Mbay, amoon moom it ñaar fukki at, ñu faat ko fii ci Kër-Masaar ; Saajo Kamara am fukki at ak juróom-ñett, ñuŋ ko faate Jawobbe ; Mañsuur Caam, moom it am ñaar-fukki at, ñuŋ ko faate fii ci Ndakaaru; Alasaan Bari, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Sànteneer, ci Ndakaaru ; Musaa Daraame, amoon fanweeri at ak juróom, ñoŋ ko faate ca Ndóofaan ; Buraama Saane, amoon fukki at ak ñaar, ñuŋ ko faate Biññoona ; ak Móodu Njaay, nga xam ne moom lañ nu mujje xabaare, ñu faate ko tey fii ci Parsel-Aseni, ci anam yu ñaaw ba fu ñaawaay yem. Kon, nu ngi leen di ñaanal Boroom bi Mu xaare leen Àjjana. May ñaan nag, ñi fi nekk ñépp, taskatu xibaar ak ñeneen ñi ko teewe,  nu taxaw def “une minute de silence” jagleel ko sunuy rakk yooyu ak sunuy doom yooyu… (Tekkaaral ci diirub benn simili). … Jërëjëf. Maa ngiy jox sunu sëriñ, Sëriñ Mañsuur Jamiil mu jagleel leen ay ñaan yoo xam ne, haasatan la, yokk barke rekk, ndegam Yàlla def na mu teew fi ; nu jox ko mu defal nu ñaan… (Ñaan). … Jërëjëf. Kon, dina nu jéem a tënk waxtaan wi ci lu dul gudd torob. Gannaaw bi nu dello nuyu saa-Senegaal yi nuy seetaan yépp, di nuyu ak di gërëm kilifay réew mi, kilifa diine yi, kilifa aada yi, àbbe yi, di rafetlu seen taxawaay ci réew mi. Ndax, wax naa ko ci samay kàddu yu jiitu, bir na ma man, ni ñoom, lañ ca waroon a def, def nañ ko ci bañ ko waree def. Aajowul nu koy jéebaane walla di ko wax ci kaw. Dafa fekk nag, kilifa diine moom, orma rekk lañ ko warlul. Am na loo xam ne, bu naree xotti worma, su ñu waxee ci suuf yem ca. Waaye ku bañ a dégg, ba mbir mi tàng ci sa loxo, dinga dellu ba ci ñoom, woowaat leen. Kon, nu ngi leen di gërëm ci taxawaay bi. Di gërëm kilifay aada yi bu baax itam, di gërëm ñi fi teew ñépp. Ñii fi nekk ñépp, amul kenn koo xam ne pólitig walla par-parloo moo la fi indi. Amul kenn koo xam ni li nga daj ci fan yii, par-parloo moo tax, waaye ñi fi teew ñépp, li leen tax a jóg ba tax ñu daj ci lu ma ci dajul man, mooy Senegaal, yitte gi ñu am ci Senegaal, bëgg-sa-réew ak am dëggu ni, dañu war a taxaw ngir réew mi, dañu war a taxaw ngir ëllëg, dañu war a taxaw ngir sunuy doom ak sunuy sët. Kon ñoom ñépp dama leen di gërëm man, ci sama tur ; waaye dama leen di gërëm tamit ci turu askanu Senegaal, ndax askanu Senegaal lanu taxawal, taxawalunu Usmaan Sonko. Ñi fi jóg ñépp sonn ci, su doon jëmmu Usmaan Sonko rekk, xéy-na «10%» yi walla «15%» dinañ génn. Bu kenn naagu ba foog ni, yow yaa tax doomi Senegaal yi génn, déedéet. Li tax lii am, mooy yëg-yëg bu kenn ku nekK xam na ni, sunu réew, sunu askan mu ngi nekk ci ay jafe-jafe yoo xam ne, bu nu seetaanee ba mu deme nenn rekk, defe naa dina rëcc ba fàww. Kon, maa ngi leen di gërëm ñoom ñépp ci turu askanu Senegaal. Bu loolu weesoo, may sargal jigéen ñi it ndax gis nanu seen taxawaay ci xeex bi ; te tey dañ leen ko màndargale, muy bésub “8 mars”.  Jigéeni boor bu nekk nag, du jigéeniy PASTEF kese. Waaye, jigéen ñi taxaw nañ jàpp ci xeex bi. Defe naa Ajaa Yaasin a ngi nii toog sama wet, sama yaay Ayda Mbóoj sama layookat a nga nale, ñoom Maymuna Buso ak keneen ak keneen, su ma leen doon lim tey du jeex, ñoom Aysata Saabara, ñoom Maam Jaara Faam… Ku ma limul rekk bumu ci mer, nu delloo leen njukkal ci bés bii, di leen jaajëfal bu baax. Mbokk yi, li xew ci réew mii, doy na waar, li xew ci réew mii, aa ! defe naa ñoom Decroix ñoo nu ëpp jaar-jaar fuuf, ñoo nu ci gën a yàgg, waaye gëmuma ne, lii fi xew, mas naa xew ci Senegaal. Du xew-xewi 63 yi, du yi ko jiitu, du 68, du 2000, du 2012, du 88, du 93… Ba tey, defe naa ni lii xew tey Senegaal, masu fee xew. Ba tey jii, Senegaal mooy xët wu njëkk ci xibaari àddina si. Kon loolu du lu tuuti, foog nun waa Senegaal, nu  mën koo natt ; xam lii lu mu doon, ak lan la war a màndargaal ci sunu mboorum  réew. Ndaxte, su dee mënun cee jël ay njàngat ba lii dootul am ci réew mi, bu boobaa, defe naa coono yi dootuñu jariñ dara. Ñi ci seen bakkan rot, ñi ci gaañu, di ñu bari, ñeneen ak ñeneen ak ñeneen, defe naa dootul jariñ dara. Kon, bu nu waxee loolu, danuy dellu delloo njukkal, ni ma ko defe, ci ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci, te dinaa ci dellusi, ma def ko ci ñi gaañu, ndaxte ñi gaañu bare nañ. Di ñaan Yàlla rekk, mu bañ a weesu foofu. Bi ci des nag, di ci jagleel ngërëm lu ràññeeku ñi nga xam ne, ñooy ndawi Senegaal yi.  Di leen delloo njukkal bu baax. Yàgg nañoo wax ndawi Senegaal yi nii, xale Senegaal yi nale, déedéet ; sunuy ndaw, dañu am awãs ci nun. Li ma gëm mooy sunu ndaw yi dañu am awãs ci nun. Wone nañ ko, ndax ku dem di jàmmaarlook ay takk-der, ñu yore ay fital, yor lu la mën a rey, yor lu la mën a gaañ, yow yoruloo lu dul say loxo ; te defuloo ko ndax dafa am dërëm booy xaar, ndax dafa am ñu féete beneen fànn ñu leen di fay xaalis ngir faat ay bakkan ; yow defoo ko ndax dërëm booy xaar, kon gàcce-ngaalaama ndawi Senegaal. Te nu leen di wax ni, day door rekk. Bis niki tey, na ngeen xam ni réew mi, seen réew la, dogal bi seen dogal la, nun ci seen waaw lanu war a doxe, ñiy def pólitig ci seen waaw lañu war a doxe, di leen déglu. Kon bu leen nangooti di seetaan ba mbir mi egg fu mu warul a egg. Ma wax nag ni, ñooñu ñépp nga xam ne sonn nañu ci mbir mi, ñi nekk seen kër sax di ko naqarlu, ñi toog seen sijaada  di ñaan, bu ma nekkee fii di waxtaan ak yéen, xam leen ni, yéen a tax, ndax bu ngeen amul woon taxawaay boobu, waxuma la tey jii, waxuma la àjjuma bii weesu, waaye altine 8i fan weeru feewiryee laa waroon a nekk Rëbës. Kon man tey jii, duma woon nekk fii di wax ak yéen. Kon bu leen kenn gëm loo ne, dañ noo beral loxo. Waaye seen taxawaay, li mu firndeel rekk tey, mooy li Tubaab naan : «La souveraineté appartient au peuple» Lépp askaan wee ko yore. Mooy kàttan dëgg-dëgg-dëgg ; sañ-sañ dëgg-dëgg-dëgg cim réew, askan wee ko moom, kenn moomu ko. Ñoom dañuy faral di wax, loo wax ñu ni «Force restera à la loi». Waaye yoon, «la loi», mooy askan wi ; yoon wi du dipite, du Maki Sàll… Ku dem nag ba sàggane ko, foog ne yoon wi ñu wote, te askan wi wote ko, mën nga koo jalgati di ko teg ci kaw nit ñi, askan wi da la koy fàttali, te loolu moo leen dal tey. Kon taxawaay boobu, ngalla waay, bumu deñati Senegaal. Bumu deñati ndaxte li ñuy wax les «grandes démocraties» (demokaraasi yu mag yi), boo gisee njiit yi am lu ñu sañul foofu, mooy askan wi dafay taxaw jonn di leen di wattu. Saa su ñuy génn rekk, nit ñi génn ne leen «lii duñu ko nangu». Kon nanu am taxawaay boobu bés niki tey. Ma wax tamit ni, ñii nga xam ne, ñu ngi ci kaso yi, tey lu ëpp téeméeri nit ñu ngi ci loxo Maki Sàll, ñii Tàmbaakundaa, ñii Sigicoor, ñii Kéedugu, fii Ndakaaru, ba Ndar, Tiwaawan, fu ne jàpp nañ fay nit ñoo xam ne, sàccuñu, reyuñu nit, wuruxuñu, luxusuñu ay biye, luubaluñu xaalisu réew mi. Seen tuuma mooy dañoo dox-ñaxtu, te Ndeyu-sàrti réew mi moo leen jox sañ-sañu dox-ñaxtu. Nu ngiy mas-sawu ñooñu, waaye di leen xamal yit ni, dun leen seetaan. Di mas-sawu it ñi nga xam ne ñàkk nañ ci seen alal ndaxte yàqu-yàqu yi bari nañ. Loolu du woon cëslaayu mbir mi ; ñi jóg di naqarlu duñu ay saay-saay ; ay nit nag, mën nañ cee rax, waaye, loolu taxuleen woon jóg. Te it sunu xeex, jubluwunu ko ci askan sàngam walla réew sàngam, du loolu mooy sunu xeex. Waaye dafa fekk daa am fu mbir yi di tollu, lépp mën na cee jaxasoo, lépp mën na cee am ; waaye loolu du woon cëslaay gi. Ndaxte, ku bëgg yor réew ak ku bëgg defar réew, doo toj alalu jaambur, doo yàq oto jaambur, doo toj këru jaambur. Kon loolu, nuŋ koy mas-sawu bu baax nit ñi mu dal. Di mas-sawu njabooti ñi ci faatu, di leen jaal, te bu soobee Yàlla, dinañ góor-góorlu ba kenn ku nekk, nu def sunu «délégation», ñi fi nekk ñépp dox ñëw jaaleji leen, di mas-sawu njabooti ñi ci gaañu ; lañ ci man it ci taxawu dinan ko def. Di mas-sawu njabooti ñi nga xam ne tey, caabi féete na leen ginnaaw ; wax leen it ne seetaanunu ñooñu ndax ginnaaw ba nu jëlee awokaa yi leen war a layool, kenn ku ne, nu ngiy góor-góorlu ci liñ la man a jàppalee ba doo tumuraanke, walla sa njaboot du tumuraanke. Waaw mbokk yi, lii lépp lan moo ko waral ? Lii lépp ci ay tiis yu dal ci Senegaal la. Li ko waral mooy xiif gi nga xam ne, Maki Sàll ak ñi mu àndal xiif nañ ko nguur ; ak yaakaar ni ñoom dañu war a yore nguur gi toog fi ba fàww. Lii lépp moo leen ko andil. Moo ne de, ay at ca ginnaaw loolu lan fi xeexoon ba ay bakkan rot fi. Li andi lii, mooy nguur gi ñu teg ci loxo Maki Sàll, ne ko : «Jox nan la sunuy mën-mën, jox nan la sunu alal, jox la «administration» bi, jox la yoon wi “justice”, jox la xare réew mi, maanaam “arme” bi, jox la lépp loo soxla li nu bëgg mooy nga defar réew mi, li nu bëgg mooy ndaw ñi am liggéey, li nu bëgg mooy nit ñi faju, li nu bëgg mooy tali yi baax». Maki Sàll walbati loolu lépp, jël ko muy doole ju muy teg ci kow saa-Senegaal yi. Muy kuy pólitig, muy kuy «mouvement citoyen», muy «Sociéte civile», képp ku ne àndumaak Maki Sàll rekk, teg na doole jooju sa kow. Loolu moo nu andi ci lii. Mu ànd ci ak ay nitam yoo xam ne, duñ ko wax dëgg, mbaa sax ñoo ko yées, soo moytuwul, moom ci boppam. Ndax lii am yépp nag, ñi ko séq bari nañ de, waaye li ci ëpp ay jëfkat yu ndaw lañu. Boo ko doon seet, ñeenti jëfkat lañu : Maki Sàll, Antuwaan Jom, Maalig Sàll ak Basiiru Géy. Ñeneen ñépp ay suq lañu, nga xam ne, dañu leen di defloo ñuy def. Waaye ñeent ñii, musiba Senegaal yépp, ci jamono yii ñu tollu tembe, ci ñooñu la. Ndax jaadu na, 16i milyoŋi doomi-Senegaal ñeenti nit rekk lëmbe leen? Ndax loolu war nañ wéy di ko nangu ci dëkk bii ? Loo wax nag, ñu ne la nun noo yor nguur gi, “force restera à la loi”. Te, yoon, “loi” boobu, duñ ko tudd lu dul bu dee ci kujje pólitig gi. Yoon woowu dañ koy walbati ngir man a jot ci képp ku àndul ak ñoom ; waaye saa su yoon wi waree dal seen kow, ñu ne mukk du fi am. Ñaata nit ñoo fi mas def ñombe yoo xam ne kenn du ko tudd ? Tey, ñu ngiy romb waa Senegaal di leen yëkkatil i mbagg. Loolu nag lanu mënatul a nangu. Looloo tax nit ñi jóg ni, lii dootunu ko nangu, dootu fi am.” (Dees na ko topp…)
https://www.defuwaxu.com/serin-seeka-bari-doole-ci-langu-politig-bi/
SËRIÑ SEEKA BARI DOOLE CI LÀNGU PÓLITIG GI ! Ni waa Senegaal gëmee Yàlla te fonk diine, umpul kenn ci àddina si. Nde, askanuw Senegaal, ñi ci ëpp ay jullit lañu. Nee ñu, cig xayma, 100 yoo jël ci doomi réew mi, 95 yi jullit lañuy wootewoo. Diiney Lislaam, nag, biir Senegaal, dafa làmboo ay màndarga yi koy wutale ak i réew yu bare. Ndaxte, amees na fiy këri diine yu mag, maanaam ay tarixa, askan wi xër ci lool, sax. Tarixa yooyu, ay sëriñ a leen jiite, ñu leen di woowe xalifa, taalibe yi fonk leen lool, weg leen. Dafa di, dayo bu réy a réy la kilifa yooyee am ci taalibe yiy déglu ak a jëfe seen i ndigal saa su nekk. Àq, dayo ak gëdd bi taalibe yi jox sëriñ si moo tax, ñoom sëriñ si, ñu am kàddu ak sañ-sañ bu bir ci mbiri réew mi, rawatina pólitig. Te, lu ni mel, ndajem njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Idiriisa Sekk mi lëmbe réew mi doy na ci firnde. Waaye, bala tey, démb la woon. Ca 1930-1940, fekk na 2 eelu xare bu mag bi ame àddina sépp. Jamono jooju, Almaañ gu Itleer dafa songoon Farãs, sonaloon ko lool. Ci la Farãs wëlbatikoo ca réew ya mu nootoon, Senegaal bokkoon ci, ngir sàkku ndimmal ak i ndaw yi koy xeexle. Noonu, ñu yabal Belees Jaañ. Belees Jaañ, ngir xam cër bu sëriñ si am ci askan wi, daldi seeti Seriñ Tuuba. Ca la ko xamalee li xew ba noppi sàkku ci moom mu digal ay ñu jàppaleji Farãs. Seriñ bi nangul ko ko, daldi sant Séex Ibra Faal mu wutili ko ay waxambaane yu ca man a dem. Waaye, du loolu rekk la Sëriñ bi mës a defal tubaab bi. Ndax, ca jamono yooyu ba tey, santoon na Séex Anta Mbàkke mu utal ko ay gune yu ñuy dalal ca daaray nasaraan yi doon door a ubbi ca diiwaanu Njaaréem. Gune yooyu Séex Anta Mbàkke tànnoon, Séex Anta Jóob, werekaan bi, àddina sépp xam ko tey, ca la bokkoon. Ndege, Séex Ibra Faal moo doon denc yaayam ca këram gi ñu duppe woon Kër gu Mag. Àddinay dox ba jamonoy 1940-1950. Lewopóol Sedaar Seŋoor miy dooni njëlbeenug njiitu réewum Senegaal ci njeexitalu nooteel bi, daldi ñibbisi. Bi mu noppee ci njàngam ma mu doon defe Farãs, dafa delsi Senegaal sóobu ci pólitig bi. Doomu Juwaalo jooju, nag, ab katólig la woon, bare woon xam-xam te ñawoon xel lool, sax. Xelam mu ñawoon moomu la jëfandikoo woon, natt dayo bi seriñ si am ci géewu pólitig gi, daldi leen di jiital ciy naalam. Noonu, mu seqiy jéego, seeti leen, di leen nemmeeku, di waxtaan ak ñoom, laxasaayu jikkoy taalibe, di jëfe ndigal, di bàyyi tere. Looloo taxoon Sëriñ Fàllu Mbàkke, xalifa murid yi ca jamono jooju, doomoo woon ko. Moo tax itam ñenn ñiy wax ne Seŋoor, gannaaw Yàlla, lépp lu mu mës a am ci politig Sëriñ Fàlloo ko ko mayoon. Li koy firndeel mooy ne, donte ne katólig la woon, mooy ki jëkk a jiite Senegaal, réew moo xam ne jullit yaa ci ëpp, ci diirub 21i at. Bi Seŋoor di dem, dafa jox lenge yi Abdu Juuf. Abdu Juuf tamit, fi Seŋoor tegoon i tànkam ñeel sëriñ si la tegoon yosam. Dafa joxoon sëriñ si cër bu mat sëkk, lëkkaloo woon ak ñoom. Moom, njiiteefam ak xilaafa Seriñ Abdu Laxaad Mbàkke ñoo méngoo. Xalifa bi daldi koy uuf, jàppale ko ni Sëriñ Fàllu jàppalee woon Seŋoor. Ndimbalam ak taxawaayam ñoo mayoon Abdu Juuf ab ndëgërlaay ba tax koo toog ci jal 20i at. Ndaxte, ci atum 2000 la ko Ablaay Wàdd daanoon ci joŋanteb wote ba. Ablaay Wàdd moomu tamit, ci murid la féetale woon boppam. Ablaay Wàdd, dafa mës a biral ne murid àqan la. Mu yàggoon lool ci kujje gi, ca jamonoy Seŋoor ak ci jamonoy Abdu Juuf. Waaye, mësul woon a réeroo ak i ñonam, doonte ne xalif bi, Abdu Juuf mii féetale woon boppam ci Tijaan yi, la doon jàppale. Àddinay doxati ba Góor gi mujje moome, yéeg ci jal bi. Ndamu Ablaay Wàdd, nag, ci woteb 2000 yi, jaloore ju réy la woon, àddina sépp daan ko soow. Askanuw Senegaal bégoon lool ci coppite bi mu yàggoon a xaarandi te amoon ci wàll wu réy. Jamono jooju, Sëriñ Saaliw Mbàkkee nekkoon xalifa murid yi. Ñépp xame woon ko màndute ak jege bi ko Ablaay Wàdd jege woon. Dafa di, Ablaay Wàdd, ku fésaloon péeteem ci murid yi la. Loolu xawoon na jur njàqare ak tiitaange. Ndax, dañ doon ragal njiitu réew ma woon jéng, di doxal xàjj-ak-seen. Moo tax it, fi mu ne nii, kenn amul mbeeteel ci ni waa Tuuba tëyee, ba sun-jonni-Yàlla-tey jii, pàrti PDS bi ñu wàcce ci jal bi, 8i at ci ginnaaw. Lii lépp, nag, warul tax ñu jàpp ne, sëriñi murid yi kese ñoo daan dugal seen loxo ci làngu pólitig gi. Déedéet. Dañ ci gën a fés rekk, waaye noonu la deme woon it ci yeneen tarixa yi, rawatina bu tijaan yi. Kenn umpalewul ne, Sëriñ Séex Tijaan Si ci boppam, sosoon na fib pàrti, jiite woon ko. Moom kay, sëggoon na sax ci géewu pólitig gi. Looloo taxoon mu dugg ndung-siin, ndax xeex ba mu daan xeex Seŋoor. Tey, doomam ji, Sëriñ Mustafa Si, kilifay Mustarsidiin yi, moo ko wuutu, jiite pàrti boppam, di PUR. Bu weesoo ñoom ñaar ñooñu nag, mënees na lim, ba tey ci tijaan yi, Sëriñ Paap Maalig Si (rakku Sëriñ Séex) ak Sëriñ Abdu Asiis Si Al Aamin. Ñii de, naam fësaluñ woon seen bopp bu baax ci pólitig bi, waaye jot nañ cee dugal seen i loxo ak seen i xalaat bu baax. Waaye, nag, kenn ci ñoom du dab Sëriñ Abdu Asiis Dabbaax. Ku mat a ràññe la woon, moom, Sëriñ Abdu Asiis Si Dabbaax. Ndaxte, daawul noppi, daawul tàyyi di taxawu askan wi ak di artoo ko dànkaafu Nguur gi, ngir muy bàyyi xel baadooloo yi. Ittéem yèpp doon rekk, wax dëgg, yore pusóom di ñaw. Ndax sax du taxawaay woowu moo jur baatu Pólitig, ca dëgg-dëgg ? Ci sunu jamono yii nag, daa mel ni, bi Maki Sàll di yéeg ci jal bi, daa faf bettoon ñu bare, ba ci sëriñ si. Mbaa sax, du looloo taxoon Parsidã naagu woon ba di leen jéem a sóoru ci njëlbeenub moomeel ga ? Ak lu ci mënti am, gaaw naa dellu ginnaaw moom, xamaat palaasam, ràññe cër bi mu ameel sëriñ si ci réew mu bindoo ni Senegaalu tey jii ! Moo tax it, fi mu ne nii, digganteem ak sëriñ si, mel na ni mburook soow ! Doonte mënagul a fexe ba dugg ci xolu waa Tuubaa yi. Li muy féeteele boppam ci tarixa Murid yépp, mel na ni tey, waa Tiwaawon ñoo ko gën a jàpp. Loolu yépp nag, teewul, ba Parsidã Maki Sàll bëggee juboo ak njatigeem ba woon, Ablaay Wàdd, Sëriñ Muntaxaa Mbàkke, di Seriñ Tuubaa tey, moo dox diggante bi ba juboole leen, keroog ba ñuy ubbi jumaa Masaalikul Jinaan. Yemul foofu. Ndax, fan yii rekk, bi Idiriisa Sekk di wax ak askan wi ngir layal duggam ci nguurug Maki Sàll, junjaale na taxawaayu sëriñ si ci ànd bi mu àndaat ak Maki Sàll. Nee ñu, Sëriñ Musaa Nawel Mbàkke, miy sëriñu Idi, moo dox lépp ba mu sotti. Idi moom, gannaaw ba ñu ko tàkkale nombog-tànkam gu bees gii ko may mu nekk léegi ñetteelu njiit ci Nguur gi, génnam bu njëkk, Seriñ Muntaqa la ko jagleel ; te it, li mu ko xamal leer na : « Da noo ñëw fii sargalsi la, wax la sunu ngërëm, ginnaaw ndam li nu am, ba nu toppe say ndigal yépp ba mu mat sëkk, bañ cee sàggane lenn. » Laata muy egg ci Sëriñ bi nag, Idi jot naa jaar ci sëriñam, Seriñ Musaa Nawel Mbàkke, wéet ak moom lu yàgg, ci li taskatu xibaar yi jottali. Ginnaaw lees fi jot a wone lépp ñeel taxawaayu sëriñ si ci pólitig bi, baax na ñu amal ab taxaw-seetlu ci mbiri ñaari doomi réew mi. Ñaar ñooñu, tey, ñépp a leen naw. Ñoo ngi rëccu liñ jotal woon a jiite réew mi walla liñ ci yàggul ; ñooñooy Séex Anta Jóob ak Mamadu Ja. Séex Anta, kenn umpplewul ne, Murid la woon ci juddoom ak ci xaleelam. Moom, Kër gu Mag la yaroo, màgge fa, ca ëttu ak kiiraayu Séex Ibra Faal. Waaye, Séex Anta, li mu doon weg sëriñ si yépp, kenn mësu ko woon dégg ci làngu pólotig gi, muy mbubboo askanam walla tarixaam. Màndute gu mat sëkk la àndaloon ci wàll woowu, ni mu ko doon defe ci wàll wu ne. Ndax dañu ko mere woon ci tekkaaralam googu ? Li am daal mooy ne, Séex Anta, dëggu, pas-pas ak xam-xam yi ko ñépp xamaloon, taxul seriñ si wallsi ko, wuyu ci wooteem yi mu doon def ngir yewwi réew mi, defaraat ko, doonte ñu bare-bari ci askan wi, moom lañu faraloon. Leneen lu laxasu woon it ci mbir mi moo doon ni, Tubaab yi ŋànkoon dëgg réew mi, Seŋoor moo leen gënaloon fuuf Séex Anta. Mamadu Ja moom, doonoon ku jullite, nekkoon na ci jal bi, ci diir bu gàtt (1959-1962). Wànte, li mu doon jullite julite lépp (képp ku ko xamoon mënoon na ko koo seedeel), moom ak sëriñ si, jaaroowuñu woon taal. Dëggu ak xadar yi mu àndaloon, mayuñu ko woon muy maslaa maslaa yu bare, walla di doxaale jikkoy naaféq. Looloo gënoon a indi ay jafe-jafe ci digganteem ak ñu bare ci kilifa diine yi. Moo tax it, ba mu jotee woon ak Seŋoor ci ginnaaw gi, gisul woon ñu bare ñu féeteek moom. Noonu la ko xaritam xañee woon nguur gi, dugal ko kaso, tëj ko fa lu ëpp fukki at. Bu nu taxawee seetlu ba noppi, laaj wi sampu nag, mooy xam ndax ku sëriñ si àndal dangay falu, ku mu won ginnaaw nga xalangu ? Ay laaj yu bare sax. Bañ a falu te dencal sa bopp say xalaat yu rafet ngir suqali sam réew ? Falu te njar say xalaati bopp ciy bëgg-bëgg sëriñ si ba noppiy dox ci seen i ndigal ? Walla weneen yoon xaj na ci diggante wu sew woowule ? Tey jii, xale yu mel ne Usmaan Sonko, di door a samp seen ndënd ci géewu politig bi, war nañu cee am njàngat. Usmaan, ci njëlbeen ga, daa meloon ni ku joxul sëriñ si seen gëdd. Waaye ci at yu mujj yii, mel na ni ku soppi taxawaayam ci wàll woowu, ndax ni muy gën a jegee léegi kilifa diine yi. Àndak sëriñ si walla won leen ginnaaw ? Su nu misaale wax ji ak kàddu Idiriisa Sekk yu yees yi : tànn sa bu la neex la !
https://www.defuwaxu.com/ndigalu-maam-ya/
Ndigalu Maam Ya Afrig nee Waaw góor, waaw kumba Ayca leen ca waar wa Bu kenn wéer goob ba Bii pas-pas dara mënalu ko dara Dina daw ba raw xëlu fas Ngor ak jom a ko nas Ma ne, Askan wee ko sas Gan góoru jigéen ñi dar lingeer Ci seen farlook seen gànjar ya Bég ba tàccu ne sas Maam a ne bëret dan delsi Samp xeej daldi xas Gisuma fi yaakar ju tas Tuggee Tugal Wéyal yaak say dëbës Afrig dina bañ ba sës Ndawi tey yi dootuñu surgawu Topp sa gannaaw ni jaam bu nangu Dina tàng dina metti Waaye jàmbaar du xàddi Na doxandéem bii dakkal Wàqi gi muy wàqi sunu alal Di roñ di génne Di gaawantu di rawale Am ñu ne xiim di xoole Mbaa sax di ko ci dimbale Sàmm sam réew warugar la Bëgg sa réew siddit la Gor tigi du wor du wuruj Te su séddu jotee mooy mujje Biir bu rëy lex yu newwi Sonal sa bopp tooñ say ñoñ Moone de bànneex tigi Xanaa xam-xam ak néewle soxla Tey jiital njariñal doom Aadama Seex Aliyu Ndaw Ndakaaru, weeru mars 2024
https://www.defuwaxu.com/waxtaanu-saada-kan-ak-bubakar-boris-joob/
‘’LI TAX SÉEX ANTA JÓOB AMUL MOROOM…’’ Waxtaan wii, ab tekki la ñeel jotaayu laaj-tontu bu Saada Kan di amal ci tele 2Stv ñaari ayu-bés yu nekk, te mu dalaloon ci sunu werekaan bi, Bubakar Bóris Jóob keroog, altine 22eelufan, sulet 2019. Li ngeen ciy jàngsi mooy xaaj bu njëkk bi. Saada Kan : Noo ngi am mbégte delsi ak yéen ci seen jotaayu waxtaan « L’entretien » bi nu leen di dégtal ñaari ayu-bés yu nekk. Tey, nag, noo ngi dalal gan gu mag, ab werekaan bu ñu ràññee ci àddina sépp, mu di ab bindkat bu yebu ci ittey réewi Afrig yi rawati-na ci lu ñeel seen daraja, di ab móolkat, taskatu xibaar, jàngalekat. Kookooy Bubakar Bóris Jóob. Moom lanu fi dalal tey, fas yéene waxtaan ak moom. Kon, Bubakar Bóris Jóob, ginnaaw bi nu la nuyoo, nu bàyyi la nga nuyoo laata nuy sóobu ci waxtaan wi. Bubakar Bóris Jóob : Jërëjëf Saada. Maa ngi lay sant di la gërëm ci dalal biŋ ma dalal ci jotaay bii nga xam ne, xam naa ko bu baax sax. Ndaxte damay faral di ko seetaan saa yu ma ko sama jot mayee. Ndax li may toog bariwul, saa su nekk maa ngi ci roppëlaan yi. Waaye, jotaay bu ma yitteel la ; dama koy seetaan saa yu ma amee jot. Saada Kan: waxtaan wi nag, dama koy doore ci ndokkeel la ngir yool biñ la jagleel fan yii weesu ca Etaasini. Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Jërëjëf. Yool bi, “Harold Ethel L. Stellfox” lañ ko dippe. Iniwérsite Dickinson bi nekk ca Pensilwani, ca réewum Amerig, moo ma ko jagleel. Ma bég ci lool sax, ànd ci ak sag bu réy. Ndax, ñi ma ci jiitu, ay bindkat yu mag a mag lañ, ma bëgg leen lool, def leen ay royukaay te daan jàng seeni téere ca ba may ndaw. Looloo ma tax a bég ci li ma jot ci yool boobu. Jëli woon naa ko. Jot naa fa amal sax aw waxtaan, jàngaale fa tuuti sama téere bi, Murambi ci nasaraan ak sax Doomi Golo ci wolof. Saada Kan : Nga ne ma ! Ci wolof, nag… Bubakar Bóris Jóob : Waaw, waaw. Mayoon nañ ma ko. Li ma ko dugge woon mooy baaxe am mbooloo mu déggul wolof, taaru kàllaamay Kocc ak neexaayam. Saada Kan : Noo ngi lay sant ci sa teewaay ci waxtaan wi. Naam, ñépp a la xam. Waaye, du ñàkk mu am ñu umple ne, ca njëlbéen, jàngalekatu xeltu (philosophie) nga woon, nekkoon tamit taskatu xibaar. Nu gis ne at yii weesu yépp, yaa ngi doon jàngale, di bind, di amal i waxtaan, di wër àddina si. Jamono jii sax yaa ngi jàngale ca Niseryaa. Muy biral ne yow, jëfkat nga. Ma bëgg laa laaj, ndax du xeex bi ngay xeexal làmmiñi Afrig yi, rawati-na wolof, moo la yóbbe loolu lépp ? Bubakar Bóris Jóob  : Waaw. Jàpp naa ne, xeex booboo sabab lépp. Te, du loo xamante ni, dafa xéy rekk sotti. Boo xoolee ba ci biir, dinga gis ne sax, jaar-jaar boobu nga tudd, fa la bépp bindkat di faral di jaar, rawati-na bindkat buy xeexal jenn itte ju ko ñor. Maanaam, dangay nekk ndaw bu gàtteñlu, bëgg lool njàngum téere yi, di jéem a topp ci tànki bindkat yu mag yi. Rax-ci-dolli, ngay bindantu ay taalif yu ndaw, ay kilib ak ay téere fent. Noonu nga koy jàppe ba xéy bés, génne ab téere. Bu ko defee, ñu jàppe la bindkat, ndax du yaa koy def sa bopp. Ndege, fàww nit ñi jàppe la bindkat nga door di ko nekk. Noonu, ay ndigaale sa diggante ak nit ñi tàmbalee juddu ; ngay tibbe ci mboolem-nawle mi di bind, di roote ci seen nekkin ak dundin ay xalaat ak i gis-gis di leen jëmmal ci say biir téere. Ñoom itam, ñuy jàng say téere di la ci laaj ngay tontu. Waaye, duñu ci yem. Ndaxte, dinañ lay faral di laaj sa xalaat ci nekkinu askan wi, xew-xewi jamono walla sax xew-xewi àddina sépp. Bu ko defee, nga sóobu ci illa ju bees : jëmmal nekkinu nit ñi, rawati-na wu doomi Afrig yi. Noonu la bindkat bi di jëflante ak askan wi. Maanaam, ci moom lay jële daa ji muy rëdde téereem yi ngir jëmmal seen nekkin, dégtal àddina sépp kàddu yiy riir ci seeni xol te seeni làmmiñ të leen a tudd. Léegi, nag, bu ñu seetloo, xool nekkin ak dundinu doomi Afrig yi, benn njàngat lañ ciy jële : njaam gi deñagu fi. Njaam gi maam yi doon dund ca jamonoy njaam ga ak ca jamonoy nooteel ba, am na ba tey. Ba jonni-Yàlla-tey jii, mënees na ràññee màndarga yi ci réewi Afrig yi : yorin wi, nguur ak njiit yiy jaamu nootkat ba woon, toroxtaange ak tolof-tolof yi askani Afrig yi di jànkoonteel bés bu nekk.  Li ci gën a doy-waar mooy ne, Afrig rekk ngay fekk ay bindkat yuy bind ci làkk woo xam ne, seeni nawle walla ñi ëpp ci askan wa ñu bokk dégguñu ko.  Muy lu yéeme ! Lan moo leen di tax a bind ak kan lañuy bindal ? Ndax xel nangu na loolu ? Man ci sama bopp, ndànk-ndànk laa tàmbalee yeewu ci mbir mi. Te bu loolu amee, ginnaaw Yàlla, maa ngi koy sante jàmbaar ju mel ni Séex Anta Jóob, sama doomu-baay bi.  Te du man rekk, képp kuy xeexal làmmiñi Afrig yi, seeni aada ak lépp lu ñeel seen daraja, war ngaa delloo njukkal Séex Anta Jóob ndax moo sumb liggéey bi, xàllal nu yoon wi.  Ci gàttal daal, mbirum làmmiñ lu am dayo la ci sama jaar-jaar. Saada Kan : Am na loo mës a wax, te mu soxal ma lool. Nee nga bés “nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem”.  Mu mel ni li wax ji wund mooy dafa jot nu xeex ngir sunu daraja. Yow miy boroom wax ji, loo ci namm dëggëntaan ? Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Li ma tax a wax ne, nekk doomu Afrig, mook dund mbugal ñoo yem, ñaari mbir la. Bi ci jiitu, mooy jafe-jafe ak boddikonte yi doomi Afrig yi di dund jamono jii, rawati-na boroom der yu ñuul yi. Tey, mbañeel ak tiitaange ji yeneen xeet yi ameel nit ku ñuul moo ma gën a tax di wax. Ndax, Jamono jii, ñaawalees na lépp lu aju ci nit ku ñuul walla mu ñeel ko. Moom kay, tudd Nelson Màndelaa walla Baraak Obamaa sax génnewu la ci. Feek yaa ngeek der bu ñuul, jàppees na la nib gàkk-gàkk walla tilim bees war a raxas ba mu set wecc, jële ko fi. Loolu, ñuulaayu nit ki la ñeel, muy benn. Bi ci topp, nag, doomi Afrig yi ci seen bopp la ñeel. Dafa di, cosaanoo Afrig ñenn ñi bàkkaar lañ ko jàppe. Tey, bët bu ñaaw lañuy xoole Afrig. Boo nee Afrig rekk, xel yi dem ci xareb maxejj yi (guerres civiles), coxorte, yorin wu ñaaw wi ñu yore réewi Afrig yi, cambar-cambar bi, ndóol bi ak tumurànke bi, nger mi, añs. Saa boo xamee ne, nit ku ñuul nga teg ci nekk doomu Afrig, dañuy jàpp ne warees na la jéppi, xeeb la, suufeel la.  Loolu laa tudde mbugal. Saada Kan : Kon, Bóris, bu ñu la déggee, ngir nu mucc ci jafe-jafe yooyu, ngir nu nekk, fàww nu xam nun nooy ñan. Te loolu, mënta àntu feek geestuwunu démb, roy ci maam ya tey ndamoo sunuy moomeel. Mu mel ni looloo la tax a bind ci wolof. Rax-ci-dolli, mënees na méngale sa taxawaay ak bu Séex Anta Jóob.   Ndax danga jàpp ne, wareef la ci doomi Afrig yi ñu wéyal xeexam ak ndono li mu nu bàyyee ? Bubakar Bóris Jóob : Waaw. Mi ngoog. Loolu kese la, du leneen. Man, dama jàpp ne ñi ëpp ci nit ñi dañu réere mbiri Séex Anta Jóob. Ndaxte, saa yuñ ko tuddee rekk, xel yépp dem ci Misra mu njëkk ma, mómi ya, piramid ya, ca wax ya mu daan wax ak li mu bind ci sunu cosaan te mu doon lu am a am solo. Xel yi dinañ dem itam ci firnde yu leer yi mu jële ci gëstoom yu xóot ya, te diy wone ne, baaxi maam yu Misra yu njëkk ya, ay nit ñu ñuul, diy doomi Afrig, ñoo ko jëmbëtoon, suuxat ko ba mu naat lool, raw ci àddina sépp jamono jooju. Toog nan fi diir bu yàgg, Séex Anta rekk a doon wax ne, Afrig a sukk jur àddina si. Bépp xeetu mbañ ak ngànt indil nañ ko ko, weddi ko ngir rekk bëgg a werante. Ñi bañoon dëgg googu, àggoon nañ ci sos ay fen yu tooy xepp ngir rekk mbañ, xeebeel ak coxorte gi ñu ameel nit ku ñuul, rawati-na doomu Afrig. Waaye, suul ker du ko teree feeñ. Tey, boroomi xam-xam yépp a bokk ànd ci waxam ja. Kenn déggatul ña ko daan weddi démb. Waaye, liggéeyu Séex Anta mëneesu ko tënk ci gëstukat bi mu doonoon. Séex Anta yemul woon rekk ci di wax ak di firndeel ne, Afrig moo sukk jur àddina si walla, sunuy maam ya woon ci Misra ay nit ñu ñuul lañu woon. Liggéey na yit lu am solo ci wàllu politig. Bu leen fàtte ne, Séex Anta Jóob nekkoon na fi politiseŋ. Waaye, nag, wute woon na lool ak politiseŋ yi nu xam. Moom dafa xamoon ne, xeex bi mu daan xeex, mënta àntu feek nguur dugalu ci loxoom. Maanaam, fàww nga yor ndogal li ngir mën a jëmmal xalaat ak yéene yi nga am ñeel sa réew walla sax Afrig gépp. Te, bokkoon na ciy yéeneem yu rafet ya, fexe ba réewi Afrig yépp booloo doon benn. Te, nag, ak li mu doon rafet xalaat yépp, mësul a dige lu mu mënul walla lu mënta nekk. Maanaam, daawul fen di dajale ni yeneen politiseŋ yi. Muy lu am a am solo. Séex Anta dafa daan wax ne, bu réewi Afrig yi bëggee tàggook seeni jafe-jafe, fàww ñu ànd fajandoo seeni jàngoro te kenn bañ a jéem a demal boppam. Ci gis-gisam, képp ku beru ci sa wet, dinga wéet ak say jafe-jafe. Te, béy bu àndul ak i  moroomi béyam, ànd ak cere ja. Kon, Séex Anta ak ñu mel ni Sànkaraa, Kuwaame Kurumaa ñoo bokkoon benn xeex, bokk benn jubluwaay bi : afal Afrig, boole doomi Afrig yi ñu doon benn ngir Afrig naat, ay dommam tekki. Moom, li ko wutale ak i maasam mooy itte ju mu joxoon làmmiñi Afrig yi ak liggéey bu réy a réy bi mu ci def, rawati-na làmmiñi réewum Senegaal. Wone na ne, làmmiñi Afrig yi ñoo bokk cosaan ndax ci làmmiñu Misra lañu soqeekoo. Biral na itam mbokkoo gi nekk seen diggante ci wàllu aada, muy lu am solo. Dafa di sax, téereem bu siiw boobu mu génne ci atum 1954 te mu tudde ko “Nations nègres et Cculture”, moo may fit ñenn ñi ba ñu sóobu ci xeex bi. Ndege, ci màqaama téere bi la kurélu FEANF juddoo bañ ca tegee 4 at, ca Frãs, diiwaanu Gërënoobal. Kurél gi, nag, ay boroomi daraja, ay kàngam yu ñu ràññee, ñoo ko séqoon, ñu ci deme ni Abdulaay Wàdd, Asan Silla, Séex Aliyu Ndaw, Saaliyu Kànji Masàmba Saare, Asan Ja, añs. Ku lim juum. Waaye ay boroomi dayo ñoo ci bokkoon te amal liggéey bu am solo lool sax ñeel làmmiñu wolof. Ngir fàttali, kurél googu moo fi génne woon Ijjib wolof, muy ab téere bu ñeeloon njàngum wolof. Liggéey boobu moo àgsi ba ci sunu jamonoy tey jii. Lépp li ñu jot a wax walla def ci làmmiñi réew mi, ginnaaw Yàlla, ñooñoo tax te ñoom, téere Séex Anta baa leen xamb. Moo tax nu war ko sant, sargal ko, delloo ko njukkal. Ndax wolof dafa ne, bu lëg lekkee aloom, na ko gërëme coy…
https://www.defuwaxu.com/as-pikine-guediawaye-fc-xumb-te-dagan/
AS PIKINE – GUEDIAWAYE FC : XUMB TE DAGAN Keroog, ci gaawu gi 29 awril 2023, sàmpiyonaa Senegaal bi jaxoon na lool. Ndax, As Pikine ak Guédiawaye Fc ñoo doon daje. Mu nekkoon joŋante boo xam ne, ñi ko doon xaar bari nañ. Ndaxte kat, du joŋante bu ndaw. Mënees na jàpp ne sax, ni fii ci Senegaal, mooy sunu Barça-Real, walla sax Paris Saint-Germain-Marseille. As Pikine ak Guédiawaye Fc di ñaari ekib yu bokk daanaka benn gox mbaa nu wax ni ñoo takkaloo, ñuy yenn ci ekib yu gën a mag ci sàmpiyonaa Senegaal gi. As Pikine bu waree joŋante, ni ñuy waajalee seen bés yi ak soppe yu bari te gëm ekib ba nañuy mel, meneen mbir la. Muy këlëb bu yàgg a wane boppam, di ekib bu mag. Guédiawaye Fc itam, naka noonu. Ci at yii ñu génn, gis nañu jaloore yi mu fi def yépp : wàcc Ligue 2 bi, jël ko yéegaat fekki punkali Ligue 1 yi. Gis nañu nag, ñi dëkke ca gox ya na ñuy jàppee ci seen i ekib ak liñ leen jaral. Ku ci mel ne Bàlla Gay, mbër mu mag mi dëkke Géejawaay, def na ci waajtaayu joŋante bi benn tamndaret ci sunuy koppar, mu nekk luy dooleel ekib ba ci lu bari. Joŋante bi nag, barkaati-démb, ci gaawu gi, la amoon. Rëyaayu joŋante ba taxoon na ñu bàyyi fowu yépp, tóxal ko ca fowub Abdulaay Wàdd, Jamñaajo, fa ekibu Senegaal bu mag biy joŋante. Ekib bu ci nekk, indi nga say soppe, mu neexoon lool, xumb ba dee. Joŋante bi nag  neexoon na lool, bal bi daw na, futbal bi set na. Waaye nag, ndam demul, ndam dikkul. Ñaari ekib dañoo mujje joxante loxo, kenn dugalul sa moroom. Guédiawaye Fc, boo xoolee, moo féete kaw. Ndaxte, mooy nekkagum ci ñetteelu toogub sàmpiyonaa ba ak 31i poñ, As Pikine jëlagum 6eel ak 25i poñ. Joŋante bi jur na liñ ci doon xaar, muy kuppe gu rafet, bal bi daw, ñu amal ko ci jàmm. Ba ci soppe yi nekkoon ci kaw, yëngal nañu ba mu neex, lépp ci jàmm ak salaam. Ñu bari nag rafetlu nañu ni ñu yóbboo joŋante gi ci bóobee bërëb. Ndax, jàpp nañ ne dina gën a may bët ak bayre sàmpiyonaa bi. Rax-ci-dolli, ekib boo fa yóbbu, daanaka ay soppeem dinañu sawar a seetaani ko, te dina dundal sàmpiyonaa bi ak kuppeg Senegaal. Ñoo ngi xaarandi yeneen bés yu ni mel. Ndax, bile moom neexoon na lool. Te, lu neex du doy. Ndaxte, xumb na, dagan na.
https://www.defuwaxu.com/saartjie-baartman-ndaw-sa-tubaab-yi-defoon-mala/
SAARTJIE BAARTMAN, NDAW SA TUBAAB YI DEFOON MALA Saartjie Baartman ab jaam la woon, fekkoon baax ca réewum Afrig-bëj-saalum.  Moom, nag, benn doomu Àngalteer lañu ko jaayoon. Gannaaw bi, Tubaab yi dañu ko wutal ab dàkkental, tudde ko Venus Noire walla Venus Hottentote. Ci atum 1810 la àgg Tugal. Bi mu àggee, nag, tubaab yi dañu ko wuññi, gàcc ko, làññi di ko wone ci ja yi ak luuma yi, diggante Àngalteer ak Frãs. Waaw. Saartjie Baartman as ndaw su jekkoon, ab diriyànke bu amoon waŋ ak i ween yu réy lool la woon. Mu jaaxaloon tubaab yi, ba tax fu nekk lañuy jóge ngir deñsi-kumpa soxna si. Noonu la Tubaab bi nekke woon ak moom, xàwwi suturaam, dëkke koo toroxal. Yenn saa yi sax ñii làmbatu ko, ñee siif ko, ñeneen ñi di ko jam ak seen parasol ak yu ni mel. Mënees na wax ne, Tubaab yi ab mala lañu jàppe woon Saartjie Baartman. Li koy gën a firndeel mooy li ñu ko boole ci benn téere bees jagleel mala yi. Ku def jëf ju bon te ñaaw jooju mooy Cuvier, benn doomu Frãs bu doon gëstu xeeti mala yi. Noonu, gannaaw soxna Saartjie Baartman  nit ku ñuul la woon, Cuvier da koo boole ci mala yi, saytu ko, amal ay njàngat ci moom. Noonu, mu méngale ko ak mala yiy nàmpal, boole ko ci biir téere boobu nga xam ne, dajale xeeti mala yiy dund yépp a ko taxoon a jóg. Bi mu faatoo ci atum 1815, kenn ci gëstukatu Frãs yi gënoon a mag te xelam màccoon ci xeet yiy dund, da koo fees, daggate ko, teqale cër yi. Mu seppi yóor gi, dindi awra wi, denc leen ci anam boo xam ne duñu yàqu. Jëmm ji moom, ñu lëmës ko ne ko gàcc ci kàggu-aada gi ñu duppe “Musée de l’homme” te nekk ca Pari, di péeyub réewum Frãs. Saartjie Baartman, nag, dara yóbbewu ko mbugal bu ñaaw bii lu dul ni jigéen ju ñuul bindoo ak taaram. Ci atum 1994, ab diir ginnaaw bi politigu boddikoonte ci biir xeet (apartheid) jeexe ci réewum Afrig-bëj-saalum, ca la askan wa ñuy woowe ay xoyxoyca mooma réew sàkku ci Nelson Mandela mu fexe ba jot ci néewub Saartjie Baartman. Seen jubluwaay moo doon suturaal ko, denc ko ci bàmmeel. Waaye ñenn ci gëstukati réewum Frãs lànk ba tëdd ci naaj wi. Amuñu woon benn lay lu dul di wax ne néewub Saartjie boobu moomeelu Frãs la.  Noonu ba ci atum 2002 ci la Frãs soog a nangoo jébbale Saartjie Baartman ginnaaw bi dipite yi jëlee ndogal lu ni mel ca péncum-ndawi-réewam. Tabo M’Beki mi jiitewoon booba ‘’Afrique du Sud’’ sànni woon na ci kàddu yu daw yaram yii : “Kiy niru mala dëgg-dëgg du doomu-Afrig bii di Saartjie Baartman. Déedéet. Mala yi dëggëntaan ñooy ñi ko xañ boppam ba noppi def jëf ju ñaaw jii”.
README.md exists but content is empty. Use the Edit dataset card button to edit it.
Downloads last month
5
Edit dataset card