Dataset Viewer
en
stringlengths 4
1.03k
| wo
stringlengths 4
999
|
---|---|
But ye are come unto mount Sion, and unto the city of the living God, the heavenly Jerusalem, and to an innumerable company of angels,
|
Waaye yéen jege ngeen tund wi ñuy wax Siyon, di dëkku Yàlla jiy dund, muy Yerusalem ba ca asamaan. Jege ngeen it junniy junniy malaaka yu bég-a-bég, ba daje di màggal;
|
When Jesus heard it, he said to them, "Those who are healthy have no need for a physician, but those who are sick. I came not to call the righteous, but sinners to repentance."
|
Noonu Yeesu dégg ko, mu ne leen: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla; ñëwuma woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
|
"The patriarchs, moved with jealousy against Joseph, sold him into Egypt. God was with him,
|
«Naka maam yooyu, dañoo iñaane Yuusufa, ba jaay ko, mu jëm réewu Misra. Waaye Yàlla taxawu ko,
|
Philip findeth Nathanael, and saith unto him, We have found him, of whom Moses in the law, and the prophets, did write, Jesus of Nazareth, the son of Joseph.
|
Filib dajeek Nataneel ne ko: «Gis nanu ki yoonu Musaa wi ak yonent yi doon wax. Mu ngi tudd Yeesu, doomu Yuusufa, te dëkk Nasaret.»
|
And Barnabas determined to take with them John, whose surname was Mark.
|
Barnabas nag bëggoon na yóbbaale Yowaana, mi ñuy wax it Màrk.
|
All flesh will see God's salvation.'"
|
Bu ko defee bépp mbindeef dina gismucc gi Yàlla tëral.”»
|
As they served the Lord and fasted, the Holy Spirit said, "Separate Barnabas and Saul for me, for the work to which I have called them."
|
Am bés nag, bi ñuy jaamu Boroom bi ak di woor, Xel mu Sell mi ne: «Beral-leen ma Barnabas ak Sool ngir liggéey, bi ma leen wooye.»
|
But he, turning around, and seeing his disciples, rebuked Peter, and said, "Get behind me, Satan! For you have in mind not the things of God, but the things of men."
|
Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.»
|
He said to them, "Why do they say that the Christ is David's son?
|
Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nit ñi di wax ne, Almasi bi mooy sëtu Daawuda?
|
And John also was baptizing in Aenon near to Salim, because there was much water there: and they came, and were baptized.
|
Yaxya moom itam doon na sóobe ci ndox ci dëkku Aynon, ca wetu dëkku Salim, ndaxte diiwaan booba bare woon na ndox. Nit ñi daan nañu ñëw ci moom, mu di leen sóob.
|
He, leaning back, as he was, on Jesus' breast, asked him, "Lord, who is it?"
|
Taalibe ba daldi walbatiku ca Yeesu, laaj ko ne: «Boroom bi, kooku kan la?»
|
Then that which was spoken by Jeremiah the prophet was fulfilled, saying,
|
Booba am la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi, bi mu naan:
|
Now, brothers, concerning the coming of our Lord Jesus Christ, and our gathering together to him, we ask you
|
Ci lu jëm ci ñëwu Boroom bi Yeesu Kirist nag, bokk yi, ak sunu daje ak moom, am na lu ma leen di ñaan:
|
He said unto them, But whom say ye that I am? Peter answering said, The Christ of God.
|
Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer tontu ko ne: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.»
|
And as he talked with him, he went in, and found many that were come together.
|
Noonu muy waxtaan ak moom, duggsi, fekk fa ndajem nit ñu bare.
|
Jesus answered her, "Martha, Martha, you are anxious and troubled about many things,
|
Boroom bi tontu ko ne: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu.
|
"If then David calls him Lord, how is he his son?"
|
Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
|
But I hope in the Lord Jesus to send Timothy to you soon, that I also may be cheered up when I know how you are doing.
|
Gannaaw loolu, bu soobee Boroom bi Yeesu, yaakaar naa ne, dinaa leen yónnee Timote balaa yàgg, ngir sama xel dal ci xam nan ngeen def.
|
Philip said to him, "Lord, show us the Father, and that will be enough for us."
|
Filib ne ko: «Boroom bi, won nu Baay bi; loolu doy na nu.»
|
But I would have you know that the head of every man is Christ, and the head of the woman is the man, and the head of Christ is God.
|
Waaye nag bëgg naa ngeen xam lii: Kirist mooy kilifag bépp góor, góor di kilifag jigéen, te Yàlla di kilifag Kirist.
|
And they said, Lord, behold, here are two swords. And he said unto them, It is enough.
|
Noonu taalibe ya ne ko: «Boroom bi, ñaari jaasee ngii.» Mu ne leen: «Doy na.»
|
and you are Christ's, and Christ is God's.
|
Te yéen, Kirist a leen moom, te Kirist, Yàllaa ko moom.
|
So he came to a city of Samaria, called Sychar, near the parcel of ground that Jacob gave to his son, Joseph.
|
Noonu mu agsi ci wetu dëkku Sikar ci tool, bi Yanqóoba mayoon doomam Yuusufa.
|
Jesus answered, "Neither did this man sin, nor his parents; but, that the works of God might be revealed in him.
|
Yeesu tontu ne: «Ajuwul ci bàkkaaram walla ci bu waajuram. Waaye loolu dafa am, ngir jëfi Yàlla yi feeñ ci moom.
|
To Timothy, my dearly beloved son: Grace, mercy, and peace, from God the Father and Christ Jesus our Lord.
|
maa ngi lay bind Timote, sama doomu diine ji ma bëgg. Na la Yàlla Baay bi ak Kirist Yeesu sunu Boroom may yiw, yërmande ak jàmm.
|
Simon, (whom he also named Peter,) and Andrew his brother, James and John, Philip and Bartholomew,
|
Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
|
Coming up at that very hour, she gave thanks to the Lord, and spoke of him to all those who were looking for redemption in Jerusalem.
|
Aana yem ca waxi Simeyon ya, daldi gërëm Yàlla tey yégal mbiri liir ba ñépp ñi doon séentu jamono, ji Yàlla war a jot Yerusalem.
|
They said to him, "We are able." Jesus said to them, "You shall indeed drink the cup that I drink, and you shall be baptized with the baptism that I am baptized with;
|
Ñu ne ko: «Waaw, man nanu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Dingeen naan kaasu naqar, bi may naan, tey sóobu ci metit, yi ma nar a sóobu,
|
Jesus saith unto her, Mary. She turned herself, and saith unto him, Rabboni; which is to say, Master.
|
Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi.»
|
Then delivered he him therefore unto them to be crucified. And they took Jesus, and led him away.
|
Noonu Pilaat jébbal leen Yeesu, ngir ñu daaj ko ci bant. Bi leen ko Pilaat jébbalee, ñu jël ko, yóbbu.
|
"He has blinded their eyes and he hardened their heart, lest they should see with their eyes, and perceive with their heart, and would turn, and I would heal them."
|
«Yàlla dafa gumbaal seeni bët,def ba ñu dëgër bopp,ngir seeni bët bañ a gis,seen xel bañ a xam,ñu bañ a woññiku ci manngir ma wéral leen.»
|
And when she had so said, she went her way, and called Mary her sister secretly, saying, The Master is come, and calleth for thee.
|
Bi Màrt waxee loolu, mu daldi dem woowi Maryaama ne ko ci pett: «Kilifa gaa ngi fi; mi ngi lay laaj.»
|
For many deceivers are entered into the world, who confess not that Jesus Christ is come in the flesh. This is a deceiver and an antichrist.
|
Maa ngi wax loolu nag, ndaxte am na ñuy sànke ñu bare, ñu tasaaroo ci àddina si, te nanguwuñu ne Yeesu Krist wàcc na, nekk nit. Kooku aji sànke la, di Bañaaleb Krist.
|
covetings, wickedness, deceit, lustful desires, an evil eye, blasphemy, pride, and foolishness.
|
njaaloo ak bëgge, coxor, naaféq, ñaawteef, ñeetaan, saaga, réylu ak jëfi ndof.
|
There shall be weeping and gnashing of teeth, when ye shall see Abraham, and Isaac, and Jacob, and all the prophets, in the kingdom of God, and you yourselves thrust out.
|
Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
|
And Paul said, I would to God, that not only thou, but also all that hear me this day, were both almost, and altogether such as I am, except these bonds.
|
Pool tontu ko: «Muy tey, muy ëllëg, waxuma yaw rekk waaye it ñi may déglu tey ñépp, na Yàlla def, ba ngeen fekksi ma ci li ma nekk, lu moy jéng yii!»
|
Judas (not Iscariot) said to him, "Lord, what has happened that you are about to reveal yourself to us, and not to the world?"
|
Yudaa --du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon — ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?»
|
preaching the Kingdom of God, and teaching the things concerning the Lord Jesus Christ with all boldness, without hindrance.
|
Muy yégle nguuru Yàlla, di jàngale ci mbirum Boroom bi Yeesu Kirist ak fit wu dëgër, te kenn terewu ko ko.
|
He said to them, "You men of Israel, be careful concerning these men, what you are about to do.
|
Bi ñu ko defee mu ne leen: «Yéen bokki Israyil, moytuleen li ngeen di def nit ñooñu.
|
They tried to seize him, but they feared the multitude; for they perceived that he spoke the parable against them. They left him, and went away.
|
Noonu kilifa yi di wut pexem jàpp ko, ndaxte xam nañu ne, ñoom lay wax. Waaye ragal nañu mbooloo mi, ba ñu bàyyi ko fa, dem.
|
and turning the cities of Sodom and Gomorrah into ashes, condemned them to destruction, having made them an example to those who would live ungodly;
|
Te it Yàlla daan na dëkki Sodom ak Gomor, raafal leen cig lakk, ñuy misaalu ñiy weddi ëllëg.
|
For we have heard him say that this Jesus of Nazareth will destroy this place, and will change the customs which Moses delivered to us."
|
Ndaxte dégg nanu, muy wax ne, Yeesum Nasaret moomu dina daaneel bérab bii te soppi aada, yi nu Musaa batale woon.»
|
but for our sake also, to whom it will be accounted, who believe in him who raised Jesus, our Lord, from the dead,
|
Nun itam ci wax jooju lanu bokk, te Yàlla dina nu jagleel njub, nun ñi gëm Yàlla, mi dekkal Yeesu sunu Boroom.
|
How is it that you don't perceive that I didn't speak to you concerning bread? But beware of the yeast of the Pharisees and Sadducees."
|
Kon nag lu tax xamuleen ne, waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.»
|
For the wages of sin is death; but the gift of God is eternal life through Jesus Christ our Lord.
|
Ndaxte peyu bàkkaar mooy dee, waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist sunu Boroom.
|
Jesus said to her, "Didn't I tell you that if you believed, you would see God's glory?"
|
Yeesu ne ko: «Ndax waxuma la ne, boo gëmee, dinga gis ndamu Yàlla?»
|
Grace be with all those who love our Lord Jesus Christ with incorruptible love. Amen.
|
Na yiwu Yàlla ànd ak ñépp, ñi bëgg Boroom bi Yeesu Kirist ak mbëggeel gu sax.
|
And he said, Unto you it is given to know the mysteries of the kingdom of God: but to others in parables; that seeing they might not see, and hearing they might not understand.
|
Mu tontu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir:“Ñuy xool te duñu man a gis,di dégg te duñu man a xam.”
|
Pilate saith unto him, What is truth? And when he had said this, he went out again unto the Jews, and saith unto them, I find in him no fault at all.
|
Pilaat laaj ko ne: «Luy dëgg?» Bi mu waxee loolu ba noppi, Pilaat daldi génnaat, jëm ca Yawut ya ne leen: «Gisuma ci moom genn tooñ.
|
When Jesus had said this, he was troubled in spirit, and testified, "Most certainly I tell you that one of you will betray me."
|
Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mu jàq, biral ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.»
|
that I should be a servant of Christ Jesus to the Gentiles, serving as a priest the Good News of God, that the offering up of the Gentiles might be made acceptable, sanctified by the Holy Spirit.
|
ma nekk jawriñu Kirist Yeesu, yebal ma ci àddina ci xeeti ñi dul Yawut. Liggéey bu sell laay def ngir Yàlla, ci xamle xebaaram bu baax bi, ngir xeeti àddina sell ci dooley Xel mu Sell mi, ba neex Yàlla, mel ni sarax su ñu koy jébbal.
|
But the Pharisees, when they heard that he had silenced the Sadducees, gathered themselves together.
|
Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne, yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje.
|
And they brought him to Jesus: and they cast their garments upon the colt, and they set Jesus thereon.
|
Noonu ñu indil cumbur gi Yeesu, daldi lal seeni yére ca kaw, yéegal ca Yeesu.
|
that I may be delivered from those who are disobedient in Judea, and that my service which I have for Jerusalem may be acceptable to the saints;
|
Ñaanal-leen ma, ngir ma mucc ci ñi gëmul ci waa Yude; te it gaayi Yàlla yu sell yu nekk ci Yerusalem nangu ndimbal, li ma leen di yóbbul.
|
and when they had fulfilled the days, as they were returning, the boy Jesus stayed behind in Jerusalem. Joseph and his mother didn't know it,
|
Bi màggal ga tasee, ñu dëpp ñibbi, waaye xale ba Yeesu des Yerusalem, te ay waajuram yéguñu ko.
|
Jesus therefore answered, "It is he to whom I will give this piece of bread when I have dipped it." So when he had dipped the piece of bread, he gave it to Judas, the son of Simon Iscariot.
|
Yeesu ne ko: «Dinaa capp dogu mburu ci ndab li; ki ma koy jox, kooku la.» Noonu Yeesu jël dogu mburu, capp ko ca ndab la, daldi koy jox Yudaa, doomu Simoŋ Iskariyo.
|
How he entered into God's house when Abiathar was high priest, and ate the show bread, which is not lawful to eat except for the priests, and gave also to those who were with him?"
|
Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar saraxalekat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu ya ñu jébbal Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul saraxalekat?»
|
Who is he that overcometh the world, but he that believeth that Jesus is the Son of God?
|
Ku noot àddina mooy kan? Mooy ki gëm ne, Yeesu mooy Doomu Yàlla.
|
Then the brothers immediately sent out Paul to go as far as to the sea, and Silas and Timothy still stayed there.
|
Noonu bokk yi yebal Pool ca saa sa, mu jëm géej, waaye Silas ak Timote des fa.
|
They answered him, "Our father is Abraham." Jesus said to them, "If you were Abraham's children, you would do the works of Abraham.
|
Ñu tontu ko ne: «Ibraayma mooy sunu baay.» Yeesu ne leen: «Bu ngeen dee waa kër Ibraayma, dingeen jëfe ni moom.
|
Then said Jesus unto Peter, Put up thy sword into the sheath: the cup which my Father hath given me, shall I not drink it?
|
Waaye Yeesu ne Piyeer: «Roofal jaasi ji ci mbaram. Ndax warumaa naan kaasu naqar, bi ma Baay bi sédd?»
|
Believest thou not that I am in the Father, and the Father in me? the words that I speak unto you I speak not of myself: but the Father that dwelleth in me, he doeth the works.
|
Xamuloo ne maa ngi nekk ci Baay bi te Baay baa ngi ci man? Kàddu yi ma leen di wax jógewuñu ci man, waaye Baay bi nekk ci man mooy matal ay jëfam.
|
I planted. Apollos watered. But God gave the increase.
|
Maa jëmbët, Apolos suuxat, waaye Yàlla moo jebbil.
|
And Jesus answering said, Were there not ten cleansed? but where are the nine?
|
Noonu Yeesu daldi ne: «Xanaa du fukk yépp a wér? Ana juróom-ñeent ña nag?
|
And Jesus said, Somebody hath touched me: for I perceive that virtue is gone out of me.
|
Waaye Yeesu ne: «Am na ku ma laal, ndaxte yég naa ne, am na doole ju génn ci man.»
|
He said to them, "You are those who justify yourselves in the sight of men, but God knows your hearts. For that which is exalted among men is an abomination in the sight of God.
|
Waaye Yeesu ne leen: «Yéen yéena ngi fexee jub ci kanamu nit ñi waaye Yàlla xam na seen xol. Ndaxte li nit ñiy fonk, Yàlla sib na ko.
|
And forthwith he came to Jesus, and said, Hail, master; and kissed him.
|
Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaamu àleykum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng.
|
But we all, with unveiled face beholding as in a mirror the glory of the Lord, are transformed into the same image from glory to glory, even as from the Lord, the Spirit.
|
Te nun ñépp nag, danuy lerxat ndamu Boroom bi ak xar-kanam bu muuruwul, bay soppiku ci melokaanam, ànd ak ndam luy yokku te sax ci dooley Boroom biy Xelum Yàlla.
|
They said therefore to him, "Where is your Father?" Jesus answered, "You know neither me, nor my Father. If you knew me, you would know my Father also."
|
Ñu laaj ko ne: «Kuy sa baay?» Yeesu tontu ne: «Xamuleen ma, xamuleen sama Baay. Bu ngeen ma xamoon, xam ko.»
|
Therefore she ran and came to Simon Peter, and to the other disciple whom Jesus loved, and said to them, "They have taken away the Lord out of the tomb, and we don't know where they have laid him!"
|
Mu daw, dem ca Simoŋ Piyeer ak ca beneen taalibe ba, maanaam ka Yeesu bëggoon, ne leen: «Jële nañu néewu Boroom ba ca bàmmeel ba, te xamunu fu ñu ko yóbbu.»
|
If any man speak, let him speak as the oracles of God; if any man minister, let him do it as of the ability which God giveth: that God in all things may be glorified through Jesus Christ, to whom be praise and dominion for ever and ever. Amen.
|
Kuy jottali kàddug Yàlla, na mel ni Yàllaay wax. Kuy jëf it, na jëfe dooley Yàlla, ngir turu Yàlla màgg ci lépp jaar ci Yeesu Kirist, mi yelloo ndam ak kàttan ba fàww. Amiin.
|
For what man knoweth the things of a man, save the spirit of man which is in him? even so the things of God knoweth no man, but the Spirit of God.
|
Kan ci nit ñi moo xam yëfi nit? Xanaa xelum nit mi nekk ci moom rekk a ko xam. Noonu it kenn xamul yëfi Yàlla, ku dul Xelum Yàlla.
|
But when the Jews of Thessalonica had knowledge that the word of God was preached of Paul at Berea, they came thither also, and stirred up the people.
|
Waaye bi Yawuti Tesalonig déggee ne, Pool mu ngi yégle kàddug Yàlla ci Bere it, ñu daldi fay dikk, di jógloo ak a jaxase mbooloo ma.
|
The Pharisees went out, and immediately conspired with the Herodians against him, how they might destroy him.
|
Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu.
|
Now Philip was of Bethsaida, the city of Andrew and Peter.
|
Filib mu nga dëkkoon Betsayda, dëkku Andare ak Piyeer.
|
Jesus therefore said to them, "Most certainly, I tell you, it wasn't Moses who gave you the bread out of heaven, but my Father gives you the true bread out of heaven.
|
Yeesu waxaat ne: «Ci dëgg-dëgg maa ngi leen koy wax, du Musaa moo leen jox ñam woowu wàcce ca asamaan; sama Baay ci boppam, moo leen di jox ñam wu wóor, wi wàcce ca asamaan.
|
And the multitude said, This is Jesus the prophet of Nazareth of Galilee.
|
Mbooloo ma tontu leen ne: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.»
|
That which was a temptation to you in my flesh, you didn't despise nor reject; but you received me as an angel of God, even as Christ Jesus.
|
Coono, gi leen sama wopp tegoon, taxul ngeen bañ ma, taxul ngeen séexlu ma. Waaye teeru ngeen ma, ni bu ngeen doon teeru malaakam Yàlla walla Yeesu Kirist.
|
But to us there is but one God, the Father, of whom are all things, and we in him; and one Lord Jesus Christ, by whom are all things, and we by him.
|
ba tey ci nun, jenn Yàlla rekk a am, muy Baay bi; lépp a ngi jóge ci moom te moom lanu nekkal. Te it benn Boroom rekk a am, muy Yeesu Kirist; lépp a ngi jaare ci moom, te nun it nu ngi dund jaare ci moom.
|
Therefore the Lord answered him, "You hypocrites! Doesn't each one of you free his ox or his donkey from the stall on the Sabbath, and lead him away to water?
|
Boroom bi tontu ko: «Naaféq yi! Ndax bésu noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko?
|
John, to the seven assemblies that are in Asia: Grace to you and peace, from God, who is and who was and who is to come; and from the seven Spirits who are before his throne;
|
Man Yowaana maa leen di bind, yéen juróom-ñaari mboolooy ñi gëm te nekk ci diiwaanu Asi. Na yiw ak jàmm féete ci yéen, jóge ci Yàlla, moom ki nekk, ki nekkoon démb te di ñëw ëllëg. Yiw woowu ak jàmm jooju ñoo ngi tukkee it ci juróom-ñaari Xeli Yàlla, yi nekk ci kanamu gàngunem Yàlla,
|
Likewise reckon ye also yourselves to be dead indeed unto sin, but alive unto God through Jesus Christ our Lord.
|
Ci noonu nag yéen itam tegleen seen bopp ni ñu dee ak Kirist, ba rëcc ci dooley bàkkaar, di dund, ànd ak Yàlla ba fàww ndax seen bokk ci Yeesu Kirist.
|
Howbeit, as the disciples stood round about him, he rose up, and came into the city: and the next day he departed with Barnabas to Derbe.
|
Waaye taalibe ya ñëw wër ko, mu daldi jóg, duggaat ca dëkk ba. Ca suba sa nag, mu ànd ak Barnabas, dem Derbë.
|
Some therefore of the Pharisees said, "This man is not from God, because he doesn't keep the Sabbath." Others said, "How can a man who is a sinner do such signs?" There was division among them.
|
Ci noonu am ca Farisen ya ñu naan: «Ki def lii, mënul a jóge ca Yàlla, ndaxte toppul ndigalu bésu noflaay bi.» Ñeneen it di wax ne: «Nan la boroom bàkkaar man a wonee yii firnde?» Noonu ñu daldi féewaloo ci seen biir.
|
Jesus said to him, "You have both seen him, and it is he who speaks with you."
|
Yeesu ne ko: «Gis nga ko ba noppi, te mooy kiy wax ak yaw.»
|
Jesus answered, I have not a devil; but I honour my Father, and ye do dishonour me.
|
Yeesu ne leen: «Awma rab; waaye sama Baay laay teral, te yéen dangeen may toroxal.
|
(Who also, when he was in Galilee, followed him, and ministered unto him;) and many other women which came up with him unto Jerusalem.
|
Bi Yeesu nekkee Galile, jigéen ñooñu ñoo ko doon topp, di ko topptoo. Amoon na fa it yeneen jigéen yu bare yu àndoon ak moom, ba ñëw Yerusalem.
|
"But when you see Jerusalem surrounded by armies, then know that its desolation is at hand.
|
«Bu ngeen gisee ay xarekat wër dëkku Yerusalem, xamleen ne jamono, ji ñu koy yàq, agsi na.
|
Whether Paul, or Apollos, or Cephas, or the world, or life, or death, or things present, or things to come; all are yours;
|
muy Pool, di Apolos, di Sefas, di àddina, di dund, di dee, di lu am, di luy ñëw; lépp, yéena ko moom.
|
When he had gone out, Jesus said, "Now the Son of Man has been glorified, and God has been glorified in him.
|
Bi Yudaa génnee, Yeesu ne: «Léegi nag ndamu Doomu nit ki feeñ na, te ndamu Yàlla feeñ na itam ci moom.
|
When Jesus heard these things, he marveled at him, and turned and said to the multitude who followed him, "I tell you, I have not found such great faith, no, not in Israel."
|
Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, musuma cee gis ku gëme nii.»
|
Annas and Caiaphas being the high priests, the word of God came unto John the son of Zacharias in the wilderness.
|
Te it Anas ak Kayif nekkoon saraxalekat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakariya, ca màndiŋ ma.
|
And Enoch also, the seventh from Adam, prophesied of these, saying, Behold, the Lord cometh with ten thousands of his saints,
|
Enog, di juróom-ñaareelu maam gannaaw Aadama, waxoon na ci kàddug Yàlla, ba weer leen ne: «Boroom bi wàcce na ca asamaan, ànd ak ay junniy junniy malaakaam,
|
Saying, This is the blood of the testament which God hath enjoined unto you.
|
te naan: «Lii mooy deretu kóllëre gi leen Yàlla tëralal.»
|
When they had preached the Good News to that city, and had made many disciples, they returned to Lystra, Iconium, and Antioch,
|
Bi ñu fa àggee nag, ñu xamle fa xebaar bu baax bi, ba sàkk fa ay taalibe yu bare. Gannaaw loolu ñu dellusi Listar, Ikoñum ak Ancos,
|
Fear took hold of all, and they glorified God, saying, "A great prophet has arisen among us!" and, "God has visited his people!"
|
Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!»
|
And they came with haste, and found Mary, and Joseph, and the babe lying in a manger.
|
Ñu daldi gaawantu dem, gis Maryaama ak Yuusufa, ak liir, ba ñu tëral ca lekkukaayu jur ga.
|
Then Agrippa said unto Festus, I would also hear the man myself. To morrow, said he, thou shalt hear him.
|
Booba nag Agaripa ne Festus: «Man sax bëgg naa dégg nit kooku.» Festus tontu ko: «Bu ëllëgee dinga ko dégg.»
|
Then said Jesus unto them, I will ask you one thing; Is it lawful on the sabbath days to do good, or to do evil? to save life, or to destroy it?
|
Yeesu ne leen: «Ma laaj leen, lan moo jaadu, nu def ko bésu noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu lor nit?»
|
So when they had dined, Jesus saith to Simon Peter, Simon, son of Jonas, lovest thou me more than these? He saith unto him, Yea, Lord; thou knowest that I love thee. He saith unto him, Feed my lambs.
|
Bi ñu ndékkee ba noppi, Yeesu ne Simoŋ Piyeer: «Simoŋ doomu Yowaana, ndax gën nga maa bëgg, ni ma ñii bëgge?» Mu tontu ko ne: «Aaŋkay, Boroom bi, xam nga ne, bëgg naa la.» Yeesu ne ko: «Topptool ma sama mbote yi.»
|
End of preview. Expand
in Data Studio
README.md exists but content is empty.
- Downloads last month
- 31