Dataset Viewer
Auto-converted to Parquet
eng
stringlengths
12
371
wol
stringlengths
11
449
Behold , I come quickly : blessed is he that keepeth the sayings of the prophecy of this book .
Maa ngi ñëw léegi . Yaw miy sàmm waxi Yàlla , yi ci téere bii , barkeel nga .
( I also baptized the household of Stephanas ; besides them , I don 't know whether I baptized any other . )
Aaŋkay ! Sóob naa it ci ndox waa kër Estefanas . Waaye ci sama pàttaliku sóobuma keneen .
When the dragon saw that he was thrown down to the earth , he persecuted the woman who gave birth to the male child .
Ba ninkinànka ja gisee ne , daaneel nañu ko ci kaw suuf , mu dàq jigéen , ja juroon doom ju góor ja .
Forgive us our sins , for we ourselves also forgive everyone who is indebted to us . Bring us not into temptation , but deliver us from the evil one . ' "
Baal nu sunuy bàkkaar , ndaxte nun itam danuy baal ñépp ñi nu tooñ.Te bu nu teg ci yoonu nattu . " "
When Peter saw it , he responded to the people , " You men of Israel , why do you marvel at this man ? Why do you fasten your eyes on us , as though by our own power or godliness we had made him walk ?
Bi Piyeer gisee loolu nag , mu ne mbooloo mi : " Yéen waa Israyil , lu tax ngeen waaru ci lii ? Lu tax ngeen di nu xool jàkk , mel ni ci sunu kàttan , mbaa ci sunu ragal Yàlla lanu doxloo kii ?
And stood at his feet behind him weeping , and began to wash his feet with tears , and did wipe them with the hairs of her head , and kissed his feet , and anointed them with the ointment .
Bi jigéen ja agsee , mu taxaw ca gannaaw tànki Yeesu , di jooy . Noonu ay rangooñam tooyal tànki Yeesu , jigéen ja di leen fomp ak kawaram , di leen fóon te ciy sotti latkoloñ ja .
And the soldiers led him away into the hall , called Praetorium ; and they call together the whole band .
Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma , mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum , ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp .
And they departed thence , and passed through Galilee ; and he would not that any man should know it .
Bi loolu amee ñu jóge fa , jaar ci diiwaanu Galile , Yeesu bëggul kenn yég ko .
And when the ten heard it , they were moved with indignation against the two brethren .
Bi nga xamee ne fukki taalibe ya dégg nañu loolu , ñu mere ñaari doomi ndey ya .
Now when they heard of the resurrection of the dead , some mocked ; but others said , " We want to hear you again concerning this . "
Bi ñu déggee nag , muy wax ci mbirum ndekkitel ñi dee , ñii di ko fontoo , ña ca des ne ko : " Dinanu la déglu ci mbir moomu beneen yoon . "
I suppose therefore that this is good for the present distress , I say , that it is good for a man so to be .
Bu nu seetee tiis wii fi teew nag , defe naa ne li baax ci nit , moo di mu sax ci li mu nekk .
Rebuke not an elder , but intreat him as a father ; and the younger men as brethren ;
Bul gëdd mag , waaye waxtaanal ak moom ni sa baay . Ndaw it , nga digal ko ni sa rakk ,
And seek not ye what ye shall eat , or what ye shall drink , neither be ye of doubtful mind .
Buleen di wut lu ngeen di lekk walla lu ngeen di naan ; te buleen ci jaaxle .
Love not the world , neither the things that are in the world . If any man love the world , the love of the Father is not in him .
Buleen sopp àddina ak li ci biiram . Ku sopp àddina , mbëggeelu Baay bi nekkul ci moom .
Having many things to write to you , I don 't want to do so with paper and ink , but I hope to come to you , and to speak face to face , that our joy may be made full .
Bëggoon naa leena wax lu bare ci bataaxel bii , waaye lépp xajul ci kayit . Kon nag fas naa yéenee ñëw , ba jàkkaarlook yeen , nu waxtaan ci , ngir sunu mbég mat sëkk .
At the ninth hour Jesus cried with a loud voice , saying , " Eloi , Eloi , lama sabachthani ? " which is , being interpreted , " My God , my God , why have you forsaken me ? "
Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan : " Elowi , Elowi , lema sabaktani ? " liy tekki : " Sama Yàlla , sama Yàlla , lu tax nga dëddu ma ? "
I give eternal life to them . They will never perish , and no one will snatch them out of my hand .
Dama leen di jox dund gu dul jeex ; duñu sànku mukk , te kenn du leen jële ci sama loxo .
The great city was divided into three parts , and the cities of the nations fell . Babylon the great was remembered in the sight of God , to give to her the cup of the wine of the fierceness of his wrath .
Dëkk bu mag ba xàjjalikoo ñetti cér , te dëkki xeet yi màbb . Noonu Yàlla daldi fàttaliku Babilon bu mag ba , ngir jox ko koppu meram mu tàng ma , ba mu màndi .
For Herod himself had sent forth and laid hold upon John , and bound him in prison for Herodias ' sake , his brother Philip 's wife : for he had married her .
Fekk Erodd yónnee woon na , jàpp Yaxya , yeew ko , tëj . Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam .
After these things came Jesus and his disciples into the land of Judaea ; and there he tarried with them , and baptized .
Gannaaw loolu Yeesu ànd ak ay taalibeem , dem ca biir diiwaanu Yude , toog fa ak ñoom ab diir , di sóob nit ñi ci ndox .
For he is not a Jew who is one outwardly , neither is that circumcision which is outward in the flesh ;
Juddu nekk Yawut taxul sag Yawut dëggu , te xaraf ci saw yaram taxul sa xaraf wóor .
Which none of the princes of this world knew : for had they known it , they would not have crucified the Lord of glory .
Kenn ci njiiti àddina amul woon xam @-@ xam boobu . Su ñu ko amoon , kon duñu rey Boroom ndam li ci bant bi .
So then , brothers , stand firm , and hold the traditions which you were taught by us , whether by word , or by letter .
Kon nag bokk yi , taxawleen bu dëgër te jàpp ci dénkaane yi nu leen jottali , muy ci li nu wax , muy ci li nu bind .
Whoever will not receive you nor hear you , as you depart from there , shake off the dust that is under your feet for a testimony against them . Assuredly , I tell you , it will be more tolerable for Sodom and Gomorrah in the day of judgment than for that city ! "
Koo xam ne gàntu na leen , mbaa mu tanqamlu leen , génnleen fa , yëlëb seen pëndu tànk , ngir seede leen seen réer . "
His winnowing fork is in his hand , and he will thoroughly cleanse his threshing floor . He will gather his wheat into the barn , but the chaff he will burn up with unquenchable fire . "
Layoom mu ngi ci loxoom , ngir jéri dàgga ja , ba mu set ; pepp ma dina ko def ca sàq ma , waaye xatax ba dina ko lakk ci safara su dul fey mukk . "
Only Luke is with me . Take Mark , and bring him with thee : for he is profitable to me for the ministry .
Luug rekk a des fi man . Indaaleel Màrk , ndaxte amal na ma njariñ ci liggéey bi .
That I have great heaviness and continual sorrow in my heart .
Maanaam , duma noppee am naqar wu réy ci sama biir xol ,
And the angel answering said unto him , I am Gabriel , that stand in the presence of God ; and am sent to speak unto thee , and to shew thee these glad tidings .
Malaaka ma tontu ko ne : " Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla . Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xebaar bu baax boobu .
Are they not all ministering spirits , sent forth to minister for them who shall be heirs of salvation ?
Malaaka yépp ay xel lañu rekk yuy liggéeyal Yàlla , mu di leen yónni ñuy dimbali nit , ñi nar a jot mucc gi .
Paul , a servant of God , and an apostle of Jesus Christ , according to the faith of God 's elect , and the acknowledging of the truth which is after godliness ;
Man Pool maa lay bind , man miy jaamu Yàlla ak ndaw li Yeesu Kirist yónni , ngir xamle ngëm , gi lal yoonu ñi Yàlla tànn , tey yokk xam @-@ xamu dëgg , giy meññ ragal Yàlla ;
Every Scripture is God @-@ breathed and profitable for teaching , for reproof , for correction , and for instruction in righteousness ,
Mbind mu sell mépp , ci gémmiñu Yàlla la jóge , te am na njariñ ngir jàngal nit ñi , yedd leen , jubbanti leen te yee leen ci njub .
who was with the proconsul , Sergius Paulus , a man of understanding . This man summoned Barnabas and Saul , and sought to hear the word of God .
Mu bokk ci gàngooru boroom réew ma tudd Sersiyus Poolus , di nit ku neex xel . Moom nag mu woolu Barnabas ak Sool , ngir bëgg a dégg kàddug Yàlla .
He begged him much that he would not send them away out of the country .
Muy ñaan Yeesu lool , ngir mu bañ leen a dàq ca réew ma .
A big wind storm arose , and the waves beat into the boat , so much that the boat was already filled .
Naka noona ngelaw lu mag daldi jóg , duus yi sàng gaal gi , ba mu bëgg a fees .
And let us consider one another to provoke unto love and to good works :
Nanu seet ni nu man a xiirtalante cig mbëggeel ak ci jëf yu baax .
For I am persuaded , that neither death , nor life , nor angels , nor principalities , nor things present , nor things to come , nor powers ,
Ndax wóor na ma ne , dara mënu noo tàggaleek mbëggeelam ; du dee , du dund , du malaaka yi , du seeni kilifa , du tey , du ëllëg , du boroom doole yi ,
For whosoever shall call upon the name of the Lord shall be saved .
Ndaxte bind nañu : " Képp ku woo Boroom bi ciw turam , dinga mucc . "
This is the will of the one who sent me , that everyone who sees the Son , and believes in him , should have eternal life ; and I will raise him up at the last day . "
Ndaxte lii mooy bëgg @-@ bëggu Baay bi : képp ku gis Doom ji te gëm ko , am dund gu dul jeex , te bés bu mujj ba , dinaa ko dekkal ! "
for he was yet in the body of his father when Melchizedek met him .
Ndaxte mi ngi nekkoon ci geñog maamam Ibraayma , bi ko Melkisedeg gatandoo .
But woe unto them that are with child , and to them that give suck , in those days ! for there shall be great distress in the land , and wrath upon this people .
Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya , ngalla it ñiy nàmpal ! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi , te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii .
Jesus saith unto them , Have ye understood all these things ? They say unto him , Yea , Lord .
Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen : " Loolu lépp , ndax xam ngeen lu muy tekki ? " Ñu tontu ko : " Waaw . "
That ye may be blameless and harmless , the sons of God , without rebuke , in the midst of a crooked and perverse nation , among whom ye shine as lights in the world ;
Noonu dingeen am xol bu laab bu àndul ak ŋàññ , di guney Yàlla yu amul sikk ci biir jamono ju yàqu te rëb . Dangeen di leer ci seen biir ni weer ci àddina si ,
And he drave them from the judgment seat .
Noonu mu dàq leen ca àttekaay ba .
And she brought forth a man child , who was to rule all nations with a rod of iron : and her child was caught up unto God , and to his throne .
Noonu mu jur doom ju góor , muy ki war a jiite xeeti àddina yépp ak yetu weñ . Waaye ñu daldi fëkk doom ja , mu dem ca Yàlla ak gànguneem .
Then said they unto him , What shall we do , that we might work the works of God ?
Noonu ñu laaj ko ne : " Lu nu war a liggéey , ngir matal jëf yi neex Yàlla ? "
They all ate , and were filled .
Noonu ñépp lekk ba suur .
If we say that we have not sinned , we make him a liar , and his word is not in us .
Su nu waxee ne defunu bàkkaar , teg nanu ko kuy tebbi waxam , te kàddoom duggagul ci sunu xol .
For I rejoiced greatly , when brothers came and testified about your truth , even as you walk in truth .
Sunuy mbokk ñëw nañu , te seede ni nga fonke dëgg gi , ba wéer ci sa dund gépp , te bég naa ci lool .
Then said Agrippa unto Festus , This man might have been set at liberty , if he had not appealed unto Caesar .
Te Agaripa ne Festus : " Manoon nanu koo yiwi , bu dénkuloon mbiram Sesaar . "
And Adam was not deceived , but the woman being deceived was in the transgression .
Te it du Aadama la Seytaane nax , waaye jigéen ja la nax , ba mu jàdd .
requesting , if by any means now at last I may be prospered by the will of God to come to you .
Te li ma koy faral di ñaan mooy lii : bu soobee Yàlla , na ma ubbil bunt , ba ma man a ñëw ci yéen .
For however many are the promises of God , in him is the " Yes . " Therefore also through him is the " Amen , " to the glory of God through us .
Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na " waawam " ci moom . Noonu kon ci Kirist lanuy waxe : " Amiin , " ngir yékkati ndamu Yàlla .
Not only so , but who was also appointed by the assemblies to travel with us in this grace , which is served by us to the glory of the Lord himself , and to show our readiness .
Te sax mbooloo yi ñoo ko tànn , ngir mu ànd ak nun , bu nuy yóbbu ndimbal li ngir ndamu Boroom bi , te mu firndeel sunu yéene ju rafet .
But the righteousness which is of faith says this , " Don 't say in your heart , ' Who will ascend into heaven ? ' ( that is , to bring Christ down ) ;
Waaye ku jub ci kanam Yàlla ci kaw ngëm , nii lay waxe : " Bul wax ci sa xol ne : " Kuy yéeg ci kaw ? " " mel ni dangaa bëgg Kirist wàcc .
But now , I say , I am going to Jerusalem , serving the saints .
Waaye nag fi mu nekk maa ngi dem nii Yerusalem , ngir dimbaliji gaayi Yàlla yu sell ya fa nekk .
I have spoken these things to you , that my joy may remain in you , and that your joy may be made full .
Wax naa leen loolu , ngir ngeen bokk ci sama mbég , te seen bos mat sëkk .
And Jesus put forth his hand , and touched him , saying , I will ; be thou clean . And immediately his leprosy was cleansed .
Yeesu tàllal loxoom , laal ko naan : " Bëgg naa ko , wéral . " Ca saa sa ngaanaam daldi deñ .
These are the things which defile a man : but to eat with unwashen hands defileth not a man .
Yooyu ñooy indil nit sobe , waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe . "
Faithful is he that calleth you , who also will do it .
Yàlla , mi leen woo ci loolu , kuy sàmm kóllëre la , te dina ko def .
He who didn 't spare his own Son , but delivered him up for us all , how would he not also with him freely give us all things ?
Yàlla mi nu gàntulul Doomam waaye mu joxe ko , mu dee ngir nun , ndax dina nu bañalati dara ?
You masters , do the same things to them , and give up threatening , knowing that he who is both their Master and yours is in heaven , and there is no partiality with him .
Yéen it sang yi , jëfeleen noonu seen diggante ak seeni jaam , te dëddu gépp raglu , xam ne yéena bokk benn Boroom ci asamaan , te ñépp a yem fi moom .
making known to us the mystery of his will , according to his good pleasure which he purposed in him
ci feeñal nu mbóoti coobareem , dëppook yéeneem ju rafet , ji mu jaarale ci Kirist .
And desired of him letters to Damascus to the synagogues , that if he found any of this way , whether they were men or women , he might bring them bound unto Jerusalem .
laaj ko ay bataaxal yu muy yóbbul jànguy dëkku Damas . Noonu ñu mu fa fekk , te ñu bokk ci yoon wi , góor mbaa jigéen , mu am dogalu yeew leen , indi leen Yerusalem .
and not by his coming only , but also by the comfort with which he was comforted in you , while he told us of your longing , your mourning , and your zeal for me ; so that I rejoiced still more .
te du ci ñëwam rekk sax waaye ci li ngeen dëfël xolam . Yégal na nu seen nammeel ci nun , seen réccu ak seen farlu jëm ci man , ba sama mbég gën cee yokku .
And have no root in themselves , and so endure but for a time : afterward , when affliction or persecution ariseth for the word 's sake , immediately they are offended .
waaye du yàgg , ndaxte wax ji saxul ci moom . Bu jaaree ci nattu nag , mbaa ñu fitnaal ko ndax kàddu gi , mu dàggeeku ci saa si .
But let it be the hidden man of the heart , in that which is not corruptible , even the ornament of a meek and quiet spirit , which is in the sight of God of great price .
waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir , di xol bu nooy te dal , ndax loolu lu takku la fa Yàlla .
When they saw it , they all murmured , saying , " He has gone in to lodge with a man who is a sinner . "
Ñépp gis loolu , di ñurum @-@ ñurumi naan : " Mi ngi dal cig këru boroom bàkkaar . "
You have heard that it was said , ' You shall love your neighbor , and hate your enemy . '
" Dégg ngeen ne , waxoon nañu : " Soppal sa moroom te sib sa bañaale . "
In my Father 's house are many homes . If it weren 't so , I would have told you . I am going to prepare a place for you .
Am na néeg yu bare ca sama kër Baay , bu dul woon noonu , ma wax leen ko , ndaxte maa ngi dem defaral leen fa ngeen di dëkk .
They have tails like those of scorpions , and stings . In their tails they have power to harm men for five months .
Am nañu ay geen yu am ay fitt ni jànkalaar , te ca la seen kàttan nekk , ngir metital nit ñi diirub juróomi weer .
Therefore the Jews sought the more to kill him , because he not only had broken the sabbath , but said also that God was his Father , making himself equal with God .
Baat boobu moo tax ba Yawut yi gën koo wut a rey , ndaxte yemul woon rekk ci bañ a topp ndigalu bésu noflaay ba , waaye dafa wax it ne , Yàlla Baayam la , ba teg boppam Yàlla .
And straightway he entered into a ship with his disciples , and came into the parts of Dalmanutha .
Bi ko Yeesu defee , mu yiwi leen , daldi dugg ak taalibe ya ca gaal ga , dem ca wàlli Dalmanuta .
Immediately Jesus made the disciples get into the boat , and to go ahead of him to the other side , while he sent the multitudes away .
Bi loolu amee Yeesu sant taalibe ya , ñu dugg gaal ga te jàll dex ga , jiituji ko , muy yiwi mbooloo ma .
And another angel came out of the temple which is in heaven , he also having a sharp sickle .
Bi loolu amee meneen malaaka génn ca kër Yàlla ga nekk ca asamaan , yor moom itam sàrt bu ñaw .
When he had found him , he brought him to Antioch . It happened , that for a whole year they were gathered together with the assembly , and taught many people . The disciples were first called Christians in Antioch .
Bi mu ko gisee , mu indi ko Ancos . Noonu atum lëmm ñu bokk ak mbooloom ñi gëm , di jàngal nit ñu bare . Te ci Ancos lañu jëkk a tudde taalibe ya Gaayi Kirist .
Then the devil took him into the holy city . He set him on the pinnacle of the temple ,
Bi mu waxee loolu , Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba , teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga .
And said unto them , Ye men of Israel , take heed to yourselves what ye intend to do as touching these men .
Bi ñu ko defee mu ne leen : " Yéen bokki Israyil , moytuleen li ngeen di def nit ñooñu .
You therefore must endure hardship , as a good soldier of Christ Jesus .
Bokkal ak man tiis , di jàmbaar ci toolu xareb Kirist Yeesu ,
men fainting for fear , and for expectation of the things which are coming on the world : for the powers of the heavens will be shaken .
Bu boobaa nit ñiy xëm ndax tiitaange , bu ñuy xalaat musiba , yi nar a wàcc ci àddina , ndaxte dees na yengal kàttani asamaan .
If then ye have judgments of things pertaining to this life , set them to judge who are least esteemed in the church .
Bu ngeen amee ay lëj @-@ lëj yu mel noonu , dangeen di wuti ay àttekat ci ay nit , ñi amul wenn yoon ci mbooloom ñi gëm !
So then it is not of him who wills , nor of him who runs , but of God who has mercy .
Dama leen di wax nag , dara ajuwul ci coobareg nit , mbaa ci ñaqam , waaye lépp a ngi aju ci yërmandey Yàlla .
Neither went I up to Jerusalem to them which were apostles before me ; but I went into Arabia , and returned again unto Damascus .
Demuma sax Yerusalem seeti ñi ma jëkk a nekk ay ndawi Kirist , waaye réewu Arabi laa dem , te gannaaw loolu ma dellusiwaat Damas .
testifying both to Jews and to Greeks repentance toward God , and faith toward our Lord Jesus .
Dénk naa Yawut yi ak Gereg yi ne leen , ñu tuub seeni bàkkaar , ba woññiku ci Yàlla te gëm sunu Boroom Yeesu .
For his disciples had gone away into the city to buy food .
Fekk booba nag , taalibey Yeesu ya dañoo demoon ca biir dëkk ba , di jënd lu ñu lekk .
There shall be weeping and gnashing of teeth , when ye shall see Abraham , and Isaac , and Jacob , and all the prophets , in the kingdom of God , and you yourselves thrust out .
Foofa dingeen jooy , di yéyu , bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma , Isaaxa , Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla , te ñu dàq leen ca biti .
Who , having received such a charge , thrust them into the inner prison , and made their feet fast in the stocks .
Gannaaw jot na ndigal loolu nag , mu sànni leen ca néeg ba gën a ruqu ci biir kaso ba , jéng seeni tànk .
For a man indeed ought not to have his head covered , because he is the image and glory of God , but the woman is the glory of the man .
Góor nag moom warul a teg dara ci boppam , ndaxte mooy melokaanu Yàlla te dafay wone ndamu Yàlla . Jigéen moom dafay wone ndamu góor .
And the seventh angel sounded ; and there were great voices in heaven , saying , The kingdoms of this world are become the kingdoms of our Lord , and of his Christ ; and he shall reign for ever and ever .
Juróom @-@ ñaareelu malaaka ma wol liitam , noonu baat yu xumb jib ca asamaan naan : " Nguuru àddina , jébbalaat nañu kosunu Boroom ak Almaseem , te dina nguuru ba fàww . "
The mystery of the seven stars which thou sawest in my right hand , and the seven golden candlesticks . The seven stars are the angels of the seven churches : and the seven candlesticks which thou sawest are the seven churches .
Juróom @-@ ñaari biddiiw yi nga gis ci sama loxol ndeyjoor , ak juróom @-@ ñaari làmpi diwlin yu wurus yi , ay mbóoti Yàlla lañu te lii lañuy tekki : biddiiw yi ñoo di malaakay juróom @-@ ñaari mboolooy ñi gëm ; juróom @-@ ñaari làmp yi ñoo di juróom @-@ ñaari mbooloo yi .
Or who is there among you , who , if his son asks him for bread , will give him a stone ?
Kan ci yéen , bu la sa doom ñaanee mburu , nga jox ko doj ?
Let such an one think this , that , such as we are in word by letters when we are absent , such will we be also in deed when we are present .
Kiy wax loolu na xam lii : ni sunuy kàddu mel ci sunuy bataaxal , bu nu fa nekkul , noonu it lanuy mel ci sunuy jëf , bu nu teewee .
Forasmuch then as we are the offspring of God , we ought not to think that the Godhead is like unto gold , or silver , or stone , graven by art and man 's device .
Kon nag , bu nu nekkee xeetu Yàlla , warunoo gëm ne , Yàlla mel na ni nataali wurus , xaalis mbaa doj yu nit defar ci xareñ mbaa xel .
Brethren , be followers together of me , and mark them which walk so as ye have us for an ensample .
Kon nag bokk yi , toppleen ma te xool ñiy roy ci li nu tëral diirub sunu ngan ci yéen .
How is it that you don 't perceive that I didn 't speak to you concerning bread ? But beware of the yeast of the Pharisees and Sadducees . "
Kon nag lu tax xamuleen ne , waxuma mburu ? Waaye damaa bëgg , ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya . "
But I trust I shall shortly see thee , and we shall speak face to face . Peace be to thee . Our friends salute thee . Greet the friends by name .
Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg , jàkkaarlook yaw , nu waxtaan ci .
If any man will do his will , he shall know of the doctrine , whether it be of God , or whether I speak of myself .
Ku fas yéenee wéy ci bëgg @-@ bëggu Yàlla , dina xam ndax sama njàngale ci Yàlla la jóge , walla ci sama coobare .
That was the true Light , which lighteth every man that cometh into the world .
Kàddu googu mooy leer gu wóor , giy ñëw ci àddina te di leeral nit ku nekk .
God , having in the past spoken to the fathers through the prophets at many times and in various ways ,
Li jiitu tey Yàlla waxoon na ak maam ya ci wàll yu bare ak ci tëralin yu wuute jaarale ko ca yonent ya .
And now I stand and am judged for the hope of the promise made of God unto our fathers :
Li ma indi ci kureelu àttekat yii nag , mooy yaakaar ne , Yàlla dina amal li mu digoon sunuy maam .
Now about the things which I write to you , behold , before God , I 'm not lying .
Lii ma leen di bind nag , Yàllaa may seede ci ne , du ay fen .
End of preview. Expand in Data Studio

English-Wolof Parallel Dataset

This dataset contains parallel sentences in English and Wolof (Senegal).

Dataset Information

  • Language Pair: English ↔ Wolof
  • Language Code: wol
  • Country: Senegal
  • Original Source: OPUS MT560 Dataset

Dataset Structure

The dataset contains parallel sentences that can be used for:

  • Machine translation training
  • Cross-lingual NLP tasks
  • Language model fine-tuning

Citation

If you use this dataset, please cite the citation guide of the original OPUS MT560 dataset.

License

This dataset is released under the Creative Commons Attribution 4.0 International License.

Downloads last month
24

Collection including michsethowusu/english-wolof_sentence-pairs_mt560